Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 75

Ñeenti Xale Yu Góor Ca Babilon

Ñeenti Xale Yu Góor Ca Babilon

BUUR Nebukanesar yóbbu na ca Babilon nit ñi gën a aay ci njàng ci waa Israyil. Ginnaaw loolu, mu tànn ci seen biir xale yu góor yi gën a rafet te gën a am xel. Yaa ngi gis fii ñeent ci ñoom. Kenn ki, Dañeel la. Ñi ci des, waa Babilon dañu leen di woowe Sadarag, Mesag ak Abed-nego.

Nebukanesar dafa bëgg a jàngal xale yu góor yooyu liggéeyu kër buur. Njàng mi dina yàgg ñetti at, ba pare Nebukanesar dina tànn ñi ci gën a aay pur ñu dimbali ko ci wut pexe bu poroblem amee. Buur bi dafa bëgg xale yu góor yi am doole te bañ a feebar bu ñu nekkee di jàng. Looloo tax mu digal ñu jox leen lekk bu neex ak biiñ bi ñu koy jox moom, buur bi, ak njabootam.

Xoolal Dañeel. Fi mu nekk nii, xale bu góor la. Ndax xam nga lan lay wax Asebanas, moom mi di jiite ñiy liggéeyal Nebukanesar ? Dañeel mu ngi koy wax ne bëggul lekk lekk bu neex bu ñuy jox buur bi. Waaye loolu jaaxal na Asebanas. Mu ne ko : ‘ Buur bi moo dogal li ngeen war a lekk te naan. Bu leen gisee ngeen gën a yooy yeneen xale yu góor yi, mën na ma rey. ’

Dañeel dem ci ki Asebanas teg ci seen kow, moom ak ñetti xaritam yi. Mu ne ko : ‘ Maa ngi lay ñaan, nga may ñu 10 fan, jox ñu ñu lekk lujum te naan ndox. Bu 10 fan yi matee, nanga seet ñan ñooy gën a leer diggante ñun ak yeneen xale yu góor yi bokk lekk ak buur bi. ’

Kooku nangu. Bi 10 fan yi jeexee, Dañeel ak ñetti xaritam yi ñoo gënoon a am yaram te gën a rafet yeneen xale yu góor yépp. Kon ki leen yore woon bàyyi na leen ñu kontine di lekk lujum te bañ a lekk li buur bi doon lekk.

Bi ñetti at yi jeexee, xale yu góor yépp lañu indi ci kanamu Nebukanesar. Mu waxtaan ak ñoom ñépp. Mu gis ne Dañeel ak ñetti xaritam yi ñoo gënoon a am xel yeneen xale yu góor yépp. Mu daldi leen jël ak moom pur ñu dimbali ko. Te it, saa yu buur bi laajee Dañeel, Sadarag, Mesag ak Abed-nego ay laaj walla mu wax leen ay poroblem, dafay gis ne seen xam-xam moo sut 10 yoon xam-xamu saraxalekat yi ak boroom xam-xam yi nekkoon ak Buur bi.