Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

XAAJ 5

Bi ñu nekkoon jaam ca Babilon ba bi ñu tabaxaatee miiri Yerusalem

Bi ñu nekkoon jaam ca Babilon ba bi ñu tabaxaatee miiri Yerusalem

Bi waa Israyil nekkoon jaam ca Babilon, fekke nañu lu bare lu mënoon a yàq seen diggante ak Yàlla. Sànni nañu Sadarag, Mesag ak Abed-Nego ci lu mel ni fuur bu mag a mag, waaye Yexowa muccal na leen. Waa Medi ak waa Pers daan nañu waa Babilon. Sànni nañu Dañeel ci kàmb fu ñu defoon ay gaynde, waaye Yàlla muccal na ko moom it. Tëj na gémmiñu gaynde yi.

Buuru Pers Sirus bàyyi na waa Israyil ñu dellu seen réew. Dañu fa dellu 70 at ginnaaw bi ñu leen yóbbu woon Babilon, ñu nekk jaam. Ci yëf yi ñu jëkk def, lii bokkoon na ci :  dañu tàmbali tabaxaat kër Yexowa. Waaye yàggul rekk, ay noon tax ñu bàyyi liggéey bi. Loolu moo tax ñu jeexal liggéeyu tabaxaat kër Yàlla gi lu tollu ak 22 at ginnaaw bi ñu dellusee Yerusalem.

Ginnaaw loolu, dinañu jàng lu jëm ci bi Esras delloo Yerusalem ngir rafetal kër Yàlla gi. Dellu na fa lu war a tollu ak 47 at ginnaaw bi ñu àggalee tabaxaatu kër Yàlla gi. Te 13 at ginnaaw bi Esras delloo Yerusalem, Nëxemiya dimbali na leen ñu tabaxaat miiri Yerusalem yi yàqu woon. Li ñu nettali ci XAAJ 5, ci lu mat 152 at la ame.

 

IN THIS SECTION

NETTALI 77

Nanguwuñu Sukk

Ndax Yàlla muccal na ñetti ndaw yooyu nga xam ne dañu ko déggal ?

NETTALI 78

Loxo Buy Bind Ci Miir Bi

Yónent Yàlla Dañeel firi na ñeenti baat.

NETTALI 79

Dañeel ci kàmb gaynde yi

Dañeel dañu ko daan ngir rey ko, waaye ndax mën na ci génn ?

NETTALI 80

Mbooloo Yàlla Mu Ngi Jóge Babilon

Sirus Buuru Pers ni ñu ko jàppe Babilon matal na benn ci li yónent yi yéglewoon, te léegi itam mu ngi matal beneen.

NETTALI 81

Dañu Yaakaar Ci Ndimbalu Yexowa

Waa Israyil dañu bañ a topp yoonu nit, waaye dañu déggal Yexowa. Ndax Yàlla barkeel na leen ?

NETTALI 82

Mordekay Ak Esteer

Lingeer Wasti ku rafet la woon, waaye Buur bi Asurerus dina ko rampalaase ak Esteer ngir mu nekk lingeer bu bees bi. Lu tax ?

NETTALI 83

Miiru Yerusalem Yi

Bu ñuy tabaxaat miir bi, tabaxkat yi soxlawoon nañu waajal seeni jaasi ak seeni xéej guddi ak bëccëg.