Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 77

Nanguwuñu Sukk

Nanguwuñu Sukk

NDAX yaa ngi fàttaliku ñetti góor ñii ? Ñooy ñetti xaritu Dañeel yu bañoon a lekk ñam bi baaxul woon ci ñoom. Waa Babilon dañu leen woowe Sadarag, Mesag ak Abed-Nego. Waaye xool leen léegi. Lu tax duñu sukk ni ñeneen ñi ci kanamu nataal bu réy bi ? Nañu seet lu tax.

Ndax yaa ngi fàttaliku ndigal yi Yexowa bindoon, moom ci boppam, te mu woowe leen Fukki Ndigal yi ? Ndigal bu jëkk bi mooy : ‘ Waruloo jaamu mukk beneen yàlla ku dul man. ’ Góor ñii, ndigal boobu lañuy topp, fekk loolu yombul.

Nebukanesar mi nekk buuru Babilon moo woo nit ñu mag yu bare pur ñu ñów màggal nataal bi mu taxawal. Lii la wax léegi nit ñépp : ‘ Bu ngeen déggee riiru béjjén yi, kooraa yi ak yeneen jumtukaayu misig, dingeen war a sukk te jaamu nataalu wurus bii. Képp ku bañ a sukk te bañ a jaamu, dinañu ko sànni ci saa si ci taal bu réy. ’

Bi Nebukanesar déggee ne Sadarag, Mesag ak Abed-Nego sukkuñu, mu mer lool. Mu woo leen te waxaat leen ñu sukk. Waaye ñetti góor ñi dañu teg seen yaakaar ci Yexowa. Lii lañu wax Nebukanesar : ‘ Suñu Yàlla ji ñuy jaamu, mën na ñu muccal. Waaye bu dee sax du ñu muccal, ñun, duñu sukk ci kanamu nataalu wurus bi nga def. ’

Nebukanesar daldi gën a mer. Am na lu mel ni fuur bu mag a mag bu nekkoon ci wetu foofu. Nebukanesar daldi wax lii : ‘ Yokkleen tàngaayu taal bi juróom-ñaari yoon ! ’ Bi ñu paree mu wax soldaaram yi gën a am doole ñu takk Sadarag, Mesag ak Abed-Nego, sànni leen ci safara si. Taal bi dafa tàng ba nga xam ne, bi ko soldaar yi jegee, dafa leen rey. Ñetti góor ñi nag ?

Buur bi xool ci biir taal bi, mu daldi tiit, laaj lii : ‘ Ndax du ñetti nit lañu takkoon, sànni leen ci biir taal bu réy bi ? ’

Ñi ko doon liggéeyal ne : ‘ Waaw, noonu la. ’

Mu ne : ‘ Waaye ñeenti góor laay gis fi, ñuy dox ci biir taal bi. Kenn takku leen te safara si defu leen dara. Te ñeenteel bi, mu ngi niru benn yàlla. ’ Buur bi daldi jege buntu fuur boobu, yuuxu naan : ‘ Sadarag, Mesag ak Abed-Nego génnleen te ñów, yéen jaamukatu Yàlla Aji Kowe ji ! ’

Bi ñu génnee, ñépp a gis ne dara dalu leen. Buur bi ne : ‘ Nañu màggal Yàllay Sadarag, Mesag ak Abed-Nego ! Dafa yónni malaakaam te muccal leen, ndaxte dañu bañ a sukk te jaamu benn yàlla ku dul seen Yàlla. ’

Ndax takkute boobu ñu wone ci Yexowa, jarul a roy ?