Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 78

Loxo Buy Bind Ci Miir Bi

Loxo Buy Bind Ci Miir Bi

LU XEW fii ? Feet bu mag moo fi am. Buuru Babilon moo woo ci këram junni nit ñu mag, maanaam ay kilifa. Ñu ngi naan ci kaasu wurus, kaasu xaalis ak bool yi waa Babilon jëloon ci kër Yexowa gi. Jékki-jékki rekk, loxo daldi feeñ ci kow miir bi, di bind. Ñépp tiit.

Sëtu Nebukanesar bi tudd Balsasar moo nekk buuru Babilon léegi. Mu daldi yuuxu pur ñu indi léegi boroom xam-xam yu Babilon. Mu ne leen : ‘ Képp ku mën a jàng mbind mii te wax ma li mu tekki, dinaa ko may lu bare te dina nekk ñetteelu kilifa gi gën a mag ci réew mi. ’ Waaye kenn ci boroom xam-xam yi mënu ko jàng te wax li mu tekki.

Yaayu buur bi dégg coow bi te dugg fu nit ñi doon lekk. Mu ne buur bi : ‘ Soxlawul nga tiit noonu. Am na góor ci sa réew ku xam yàlla yu sell yi. Sa maam Nebukanesar, bi mu nekkee buur, dafa ko defoon njiit ci boroom xam-xam yu Babilon yépp. Dañeel la tudd. Waxal ñu indi ko, dina la wax li loolu lépp tekki. ’

Ñu daldi gaaw a indi Dañeel. Dañeel jëlul dara ci li ko buur bi bëggoon a may, ba pare wax na lu tax Yexowa masoon a nangu nguur gi ci loxo Nebukanesar, maamu Balsasar. Mu ne ko : ‘ Dafa yéegoon boppam lool, moo tax Yexowa yar ko. ’

Dañeel ne Balsasar : ‘ Waaye yow, xamoon nga lépp li daloon sa maam Nebukanesar, waaye ba tey danga yéeg sa bopp ni moom. Indi nga kaas ak bool yi nekkoon ci kër Yexowa gi te danga ci naan. Màggal nga ay yàlla yu ñu defare bant ak xeer, te màggaluloo suñu Sàkk-kat bu mag bi. Loolu moo tax Yàlla indi loxo bii, mu bind li ngay gis fii. ’

Dañeel kontine di wax, mu ne : ‘ Lii lañu fi bind : MENE, MENE, TEKEL ak PARSIN. ’

‘ MENE mu ngi tekki ne Yàlla dafa waññ say fanu nguur te dafa koy jeexal. TEKEL mu ngi tekki ne dañu la peese ci balaas te gis ne baaxuloo. PARSIN mu ngi tekki ne jox nañu sa nguur waa Medi yi ak waa Pers yi. ’

Bi Dañeel doon wax loolu, dafa fekk waa Medi yi ak waa Pers yi komaasee song Babilon. Dëkk bi daanu na ci seen loxo, te rey nañu Balsasar. Li loxo bi bindoon ci miir bi amoon na ci guddi googu. Waaye, lan mooy dal léegi waa Israyil ? Dinañu ko gis, waaye nañu jëkk seet li dal Dañeel.