Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 79

Dañeel ci kàmb gaynde yi

Dañeel ci kàmb gaynde yi

CÉY, dafa mel ni Dañeel mu ngi ci coono bu réy ! Waaye lu tax gaynde yi duñu ko def dara ? Kan moo dugal Dañeel fii ci gaynde yi ? Nañu seet loolu.

Ki nekk buuru Babilon léegi, mu ngi tudd Dariyus. Bëgg na Dañeel lool, ndaxte Dañeel dafa baax te am xel lool. Dariyus def na Dañeel kilifa gu mag ci nguuram. Loolu tax na yeneen góor ci nguur gi iñaane ko ci loolu. Ñu daldi def lii :

Dañu dem ci Dariyus, ne ko : ‘ Buur Dariyus, dañu bëgg nga tëral ndigal bii : Fii ba 30 fan, kenn warul a ñaan benn yàlla walla keneen ku dul yow, buur bi. Ku toppul ndigal bii, ñu sànni ko ci gaynde yi. ’ Dariyus xamul lu tax nit ñooñu bëgg mu tëral ndigal boobu, waaye ndegam gisu ci dara lu bon, mu daldi ko bind. Léegi kenn mënul a soppi ndigal boobu.

Bi Dañeel déggee ndigal bi, mu dem këram, ñaan Yàlla, ni mu ko daan defe. Nit ñu bon ñooñu, xamoon nañu ne Dañeel du bàyyi di ñaan Yexowa. Kontaan nañu ndaxte dafa mel ni dinañu am li ñuy wut, maanaam fexe ba Dañeel jóge fi.

Bi Dariyus xamee lu tax nit ñooñu bëggoon ndigal bi, mu metti ko lool. Waaye mënul a soppi ndigal bi. Mu daldi sant ñu sànni Dañeel ci kàmbu gaynde yi. Waaye lii la wax Dañeel : ‘ Na la sa Yàlla muccal, moom mi ngay jaamu. ’

Waaye li xew noonu dafa naqari Dariyus ba mënul a nelaw guddi gi. Bi suba si jotee, mu gaaw a dem ca kàmb gaynde yi. Yaa ngi koy gis fii ci kow. Mu woo Dañeel ak baat bu kowe, ne ko : ‘ Dañeel, yow miy jaamu Yàlla jiy dund ! Ndax sa Yàlla muccal na la ci gaynde yi ? ’

Dañeel ne ko : ‘ Yàlla yónni na malaakaam te tëj na gémmiñu gaynde yi, ba defuñu ma dara. ’

Buur bi kontaan lool. Mu wax ñu génne Dañeel. Mu daldi sant ñu sànni ci kàmb googu nit ñu bon ñooñu bëggoon Dañeel dee. Àggaguñu sax ci suufu kàmb gi, gaynde yi dal seen kow, màtt leen, seen yax yépp damm.

Ginnaaw loolu, lii la Dariyus bind mbooloo yi bokkoon ci réewam yépp : ‘ Maa ngi joxe ndigal ne ñépp a war a weg Yàllay Dañeel. Boroom kéemaan yu réy la. Moom moo muccal Dañeel ci gémmiñu gaynde yi. ’

Dañeel 6:2-29.