Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 80

Mbooloo Yàlla Mu Ngi Jóge Babilon

Mbooloo Yàlla Mu Ngi Jóge Babilon

AM NA léegi ñaari at bi waa Medi ak waa Pers daanee Babilon. Xoolal li xew léegi ! Waa Israyil ñu ngi jóge Babilon. Lu tax ñuy dem seen yoon ? Kan moo leen bàyyi ñu dem  ?

Sirus mi nekk buuru Pers moo def loolu. Lu yàgg bala Sirus juddu, Yexowa jaaroon na ci yonentam Esayi ngir wax ci moom lii : ‘ Dinga def li ma bëgg nga def. Dinañu ubbi bunt yi tëj dëkk bi, bàyyi leen noonu, nga mën a dugg ci dëkk bi, nangu ko. ’ Te loolu moo amoon. Sirus moo jiite woon soldaar yi bi ñu jëlee Babilon. Waa Medi yi ak waa Pers yi, dañu ñów guddi, dugg ci biir dëkk bi fekk bàyyi woon nañu bunt yi ñu ubbeeku.

Yonentu Yexowa bi tudd Esayi waxoon na itam ne Sirus dina joxe ndigal ngir ñu tabaxaat Yerusalem ak kër Yàlla gi fa nekkoon. Ndax Sirus def na ko ? Waawaaw. Lii la wax waa Israyil : ‘ Léegi, demleen Yerusalem te tabax kër Yexowa mi nekk seen Yàlla. ’ Ñi ngay gis nii, foofu lañu jëm ngir def loolu.

Waaye du waa Israyil yépp ñooy mën a dellu Yerusalem ndaxte yoon bi sore na lool. War na mat 800 kilomet. Ñu bare duñu ko mën a def ndax màgget walla feebar. Mën na am it leneen tere leen dem. Lii la Sirus wax ñi demul Yerusalem : ‘ Nangeen may xaalis, wurus ak yeneen ñiy dellu Yerusalem ngir tabaxaat dëkk bi ak kër Yàlla gi fa nekk. ’

Ñu daldi def ay maye yu bare. Sirus jox na it ñi doon dem Yerusalem kaas ak bool yi Nebukanesar jëloon ci kër Yexowa gi, bi mu alagee Yerusalem. Kon mbooloo mi am na lu bare lu mu war a yóbbu Yerusalem.

Def nañu lu war a mat ñeenti weer ci yoon bi, door a àgg Yerusalem. Diggante booba ak bi ñu alagee Yerusalem ba kenn desul woon ci réew mi, matoon na 70 at. Léegi, waa Israyil dellusi nañu ci seen réew, waaye dinañu gis ci kanam ne, foofu it dinañu am ay poroblem.

Isaïe 44:28 ; 45:1-4 ; Esras (Ezra) 1:1-11.