Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 83

Miiru Yerusalem Yi

Miiru Yerusalem Yi

XOOLAL liggéey bi nit ñi di def fii. Waa Israyil ñu ngiy tabax miiru Yerusalem yi. Am na léegi 152 at ci ginnaaw, Nebukanesar dafa alagoon Yerusalem. Booba, dafa tojoon miir yooyu te lakk bunt yi tëjoon dëkk bi. Te bi waa Israyil jógee Babilon ba ñibbisi seen réew, tabaxaatuñu woon miir yi.

Ci sa xalaat, naka la nit ñi doon dunde at yooyu yépp ci dëkk bu amul miir yi ko wër ? Seen xel dalul woon, de. Seeni noon, bu ñu bëggoon a dugg ci biir dëkk bi ngir song leen, naroon na leen yomb lool. Waaye nit ki nekk fii te tudd Nëxemiya (Nehémia) mujj na ñów dimbali mbooloo mi mu tabaxaat miir yi. Ndax xam nga kan mooy Nëxemiya ?

Nëxemiya, waa Israyil la. Mu ngi jóge dëkku Susan, fu Mordekay ak Esteer nekk. Nëxemiya mu ngi doon liggéey kër buur. Kon xéyna xarit bu baax la woon ci Mordekay ak ci Esteer, jabaru buur bi. Waaye Biibël bi waxul ne Nëxemiya dafa doon liggéeyal jëkkëru Esteer, maanaam Asuerus buur bi. Dafa doon liggéeyal buur bi topp ci Asuerus, maanaam Artaserse.

Yaa ngi fàttaliku Artaserse. Moom moo doon buur bu baax bi mayoon Esras xaalis boobu yépp pur mu defaraat kër Yexowa gi ca Yerusalem. Waaye Esras tabaxul woon miir yi wëroon dëkk bi te ñu tojoon leen. Nëxemiya moo mujj a def loolu. Lu waral loolu ? Nañu ko seet léegi.

Am na léegi 13 at bi Artaserse mayee Esras xaalis ngir defaraat kër Yàlla gi. Nëxemiya mooy jiite ñiy jox buur bi mu naan. Liggéey boobu mooy jox buur bi biiñ bu muy naan te seet ndax kenn defu ci poson ngir rey ko. Liggéey bu am maanaa la ci kër buur bi.

Benn bés, benn mbokku Nëxemiya mi tudd Xanani (Hanani) ak yeneen góor dañu jóge Israyil, ñów seetsi ko. Ñu wax ko coono yi waa Israyil am foofu, wax ko it ne miiri Yerusalem yàqu nañu ba léegi. Xolu Nëxemiya jeex, mu daldi ñaan Yexowa.

Benn bés, buur bi gis ne am na lu metti Nëxemiya, mu ne ko : ‘ Lu tax sa xol jeex nii ? ’ Nëxemiya wax ko ne lu bare ci dëkku Yerusalem moo yàqu te miiri Yerusalem yàqu nañu it. Buur bi ne ko : ‘ Lan nga bëgg léegi ? ’

Nëxemiya ne ko : ‘ Bàyyi ma, ma dem Yerusalem, ma mën a tabaxaat miir yi. ’ Buur bi Artaserse, dafa baax lool. Dafa may Nëxemiya mu dem te dimbali na ko ba mu am ay bant pur tabax bi. Nëxemiya dem Yerusalem te wax mbooloo mi li mu bëgg a def. Ñu kontaan te ne : ‘ Nañu komaase liggéey bi. ’

Ñi bañoon Israyil, bi ñu gisee miir yi di jóg, dañu ne : ‘ Nañu dem foofu, rey leen, liggéey bi bañ a kontine. ’ Nëxemiya dégg loolu. Mu jox liggéeykat yi jaasi ak xeej, mu ne leen : ‘ Buleen ragal seeni noon. Nangeen xeexal seeni mbokk, seeni doom, seeni jabar, ak seeni kër. ’

Mbooloo mi am fit lool. Ñu nekk ak seen gànnaay guddi ak bëccëg te kontine di tabax. Jeexal nañu tabaxu miir yi diggante 52 fan. Léegi seen xel mën na dal. Nëexemiya ak Esras ñu ngiy jàngal mbooloo mi ndigalu Yàlla yi, mbooloo mi kontaan lool.

Waaye ba tey, yëf yi meluñu ni ñu meloon bala ñu jàppoon waa Israyil ba yóbbu leen Babilon. Buuru Pers moo nekk buuru réew mi te waa Israyil, seeni jaam lañu. Waaye Yexowa dig na ne dina yónni buur bu bees te buur boobu dina leen indil jàmm. Kooku kan la ? Naka lay indee jàmm ci kow suuf ? Lu tollu ak 450 at weesu na bala ñuy mën a xam leneen ci buur boobu. Bi at yooyu weesoo, juddu bu am maanaa lool moo am. Waaye loolu, ci beneen nettali lañu koy gis.