Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

XAAJ 6

Yeesu (Isaa), bi mu juddoo ba bi mu deewee

Yeesu (Isaa), bi mu juddoo ba bi mu deewee

Malaaka mi tudd Jibril lañu yónni ci benn janq ju baax te tudd Maryaama. Nee na ko dina am doom buy nekk buur te di nguuru ba fàww. Yeesu juddu na ci fu ay mala di fanaan. Ay sàmmkat seetsi nañu ko foofu. Ginnaaw loolu, ay góor ñu jóge penku topp nañu benn biddéew bu leen yóbbu ba ci xale bu ndaw bi. Dinañu gis kan moo tax ñu gis biddéew bi ak naka la Yeesu mucce ci ñi ko bëggoon a rey.

Ginnaaw loolu, dinañu gis Yeesu, bi mu amee 12 at, di waxtaan ak jàngalekat yi nekkoon ci kër Yàlla gi. Fukki at ak juróom-ñett ginnaaw loolu, Yeesu sóobu na ci ndox. Mu daldi tàmbali liggéey bi waraloon Yàlla yónni ko ci suuf, maanaam liggéeyu waar nit ñi te jàngal leen lu jëm ci Nguur gi. Yeesu tànn na 12 góor pur ñu dimbali ko ci liggéey boobu, mu def leen ay ndawam.

Yeesu def na itam ay kéemaan yu bare. Jox na lekk ay junniy nit fekk tuuti jën yu ndaw la amoon ak tuuti mburu. Faj na ñi feebar. Dekkal na sax ñi dee. Ci nettali yi mujj ci xaaj bii, dinañu jàng lu bare ci li xewoon ci fanam yu mujj yi ak naka lañu ko reye. Yeesu def na liggéeyu waare bi lu tollu ak ñetti at ak genn-wàll. Kon lépp li ñuy nettali ci XAAJ 6 xewoon na ci lu mat 34 at ak lu ko ëpp tuuti.

 

IN THIS SECTION

NETTALI 84

Benn Malaaka Seetsi Na Maryaama

Dafa indi xibaar bu jóge ci Yàlla : Maryaama dafa nar a am doom boo xam ne dina nekk buur ba fàww.

NETTALI 85

Yeesu Juddu Na Fu Ay Mala Di Fanaan

Lu tax nit ku nar a nekki buur juddoo fu ay mala di fanaan ?

NETTALI 86

Biddéew Buy Won Ay Góor Seen Yoon

Kan moo yóbbu boroom xam-xam yi ba ci Yeesu ? Tont bi mën na leen bett.

NETTALI 87

Yeesu Ci Kër Yàlla Gi, Fekk Xale La

Dafa am lu yéeme ci moom, ba sax mag ñiy jàngale ci kër Yàlla ga dañu jaaxle.

NETTALI 88

Yaxya Mu Ngiy Sóob Yeesu Ci Ndox

Yaxya dafa doon sóob bàkkaarkat yi, waaye Yeesu masul bàkkaar. Lu tax Yaxya sóob ko ?

NETTALI 89

Yeesu Dafay Sellal Kër Yàlla Gi

Yeesu wone na fasoŋu mbëggeel boo xam ne moo waraloon meram.

NETTALI 90

Mu Ngiy Waxtaan Ak Jigéen Ci Teen

Naka la ndox bi Yeesu di joxe mënee tax ba jigéen ji dootul marati ?

NETTALI 91

Yeesu Mu Ngiy Jàngale Ci Kow Tund

Xoolal naka la xelal yi Yeesu jàngale ci kow tund bi amee njariñ ci bépp jamano.

NETTALI 92

Yeesu Dafay Dekkal Ay Nit Ñu Dee Woon

Yeesu dafa jëfandikoo kàttanu Yàlla, wax ñaari baat yu yomb te dekkal doomu Yayrus bu jigéen bi.

NETTALI 94

Ku Bëgg Xale La

Yeesu jàngal na taalibeem yi ne am na lu bari lu ñu war a jàng, nekkul rekk lu ñu war a jàng lu jëm ci xale yi waaye itam jànge ci xale yi.

NETTALI 95

Ni Yeesu Di Jàngalee

Léebu bi Yeesu joxe, maanaam léebu nit ku baax ki dëkk Samari, benn misaal la ci fasoŋu njàngale bi Yeesu faral di jëfandikoo ngir jàngale.

NETTALI 96

Yeesu Faj Na Ñi Feebar

Lan la Yeesu matal ci kéemaan yépp yi mu def ?

NETTALI 97

Yeesu, Buur Bi, Mu Ngi Ñów

Mbooloo mu rey teeru nañu ko, waaye du ñépp a ci kontaan.

NETTALI 98

Ci Tundu Oliw Yi

Yeesu waxoon na taalibeem yi lu jëm ci xew-xew yi am ci suñu jamano.

NETTALI 99

Ci Néeg Bi Nekk Ci Kow

Lu tax Yeesu wax taalibeem yi ñu màggal reer boobu at mu nekk ?

NETTALI 100

Yeesu Ci Tool Bi

Lu tax Yudaa wor Yeesu ci fóon ?

NETTALI 101

Ñu Ngiy Rey Yeesu

Bi ñu koy rey ci bant sax, dafa dige dige bu jëm ci àjjana.