Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 84

Benn Malaaka Seetsi Na Maryaama

Benn Malaaka Seetsi Na Maryaama

JANQ bu rafet bii, mu ngi tudd Maryaama. Waa Israyil la te mu ngi dëkk ci dëkku Nasaret. Dafa baax lool. Yàlla dafa xam loolu moo tax mu yónni malaakaam Jibril mu wax ak moom. Ndax xam nga lan la koy wax ? Nañu seet loolu.

Lii la Jibril wax Maryaama : ‘ Nanga am jàmm, yow mi am barke bu réy. Yexowa mu ngi ak yow. ’ Maryamaa masuloon a gis nit kooku. Mu jaaxle ndaxte xamul lan la bëgg a wax noonu. Jibril daldi dalal xelam.

Mu ne ko : ‘ Bul ragal dara, Maryaama. Yexowa kontaan na lool ci yow. Loolu moo tax mu bëgg la defal lu réy. Fi ak tuuti ci kanam dinga jur doom. Nanga ko tudde Yeesu. ’

Mu kontine, ne ko : ‘ Xale bi, ku mag lay doon te dinañu ko woowe Doomu Aji-Kowe ji. Yexowa dina ko def buur, mel ni Daawuda. Waaye Yeesu moom dina nekk buur ba fàww, te nguuram du jeex mukk ! ’

Maryaama laaj ko lii : ‘ Naka la loolu mën a ame ? Séyaguma. Janq laa ba tey. Naka laa mën a ame doom ? ’

Jibril tontu ko ne : ‘ Kàttanu Yàlla dina wàcc ci yow. Moo tax xale bi dinañu ko woowe Doomu Yàlla. ’ Mu teg ci lii : ‘ Xoolal sa mbokk Elisabet. Nit ñi dañu waxoon ne mënatul a am doom ndaxte dafa màgget. Waaye léegi dina am doom bu góor. Kon gis nga ne dara tëwul Yàlla. ’

Maryaama daldi ne : ‘ Jaamu Yexowa laa. Na Yàlla def ci man li nga wax. ’ Malaaka mi daldi dem.

Maryaama daldi gaaw a dem seeti Elisabet. Bi Elisabet déggee baatu Maryaama, doomu Elisabet daldi yëngatu ci biiram ndax mbégte. Elisabet daldi fees ak xel mu sell mi, mu ne Maryaama : ‘ Barkeel nañu la ci jigéen ñi. ’ Maryaama toog na ak Elisabet lu jege ñetti weer, mu sog a ñibbi Nasaret.

Bés bi Maryamaa war a séy ak góor gi tudd Yuusufa, mu ngi jegesi. Waaye bi Yuusufa déggee ne dafa ëmb, dafa xalaat ne bañ ko takk moo gën. Malaaka Yàlla ne ko : ‘ Bul ragal a takk Maryaama, ndaxte Yàlla moo ko may doom bu góor. ’ Yuusufa daldi takk Maryaama, ba pare ñuy séentu bés bu Yeesu di juddu.