Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 86

Biddéew Buy Won Ay Góor Seen Yoon

Biddéew Buy Won Ay Góor Seen Yoon

NDAX gis nga biddéew biy leer bu baax bu nit kii di joxoñ ? Góor ñi ngay gis fii, dañu jóge Yerusalem, biddéew bi daldi feeñ. Ñoom, penku lañu jóge, maanaam boor bi féete fu naaj bi di génn ci suba si. Mbirum biddéew yi lañuy gëstu. Gëm nañu ne biddéew bii mu ngi leen di yóbbu ci kenn ku mag.

Bi ñu àggee Yerusalem, lii lañu laaj nit ñi : ‘ Ana xale bi nar a nekk buuru Yawut yi ? ’ “ Yawut ” lañuy woowe itam waa Israyil. Góor ñi ne lii : ‘ Bi ñu nekkoon penku lañu jëkk gis biddéewu xale bi te dañu fi ñów ngir màggal ko. ’

Bi Erodd mi nekkoon buur ca Yerusalem déggee loolu, mu jaaxle. Bëggul beneen buur jël palaasam. Mu woo saraxalekat yu mag yi, laaj leen lii : ‘ Buur bi ñu dige, fan la war a juddu ? Ñu ne ko : ‘ Biibël bi nee na ca Betleyem. ’

Erodd woo góor ñooñu jóge woon penku, ne leen : ‘ Demleen seet fu xale bu ndaw boobu nekk, ngeen ñów, wax ma ko. Dama fa bëgg a dem, màggal ko man it. ’ Waaye ci dëgg Erodd dafa ko bëgg a rey !

Biddéew bi daldi jiitu góor ñi ba àgg Betleyem, taxaw ci kow fu xale bi nekk. Ñu dugg ci biir kër gi, gis Maryaama ak Yeesu bi nekk xale bu ndaw. Ubbi nañu seen saag te jox Yeesu ay maye. Ginnaaw loolu, Yexowa wax na leen ci biir gént ñu bañ a dellu ci Erodd. Ñu daldi aw feneen, ñibbi seen réew.

Bi Erodd déggee ne góor ñi ñibbi nañu, mu mer lool. Mu daldi digal ñu rey ci Betleyem bépp xale bu góor bu am ñaari at walla bu ko gën a tuuti. Waaye bala loolu Yexowa waxoon na Yuusufa ne dinañu bëgg a rey xale bi, Yuusufa dem ak njabootam Misra. Toog nañu fa ba Yuusufa xam ne Erodd dee na. Mu jël Maryaama ak Yeesu, ñibbi Nasaret. Foofu la Yeesu yaroo.

Ci sa xalaat, kan moo taxoon biddéew boobu feeñ ci asamaan ? Ndax yaa ngi fàttaliku ne, ci Yerusalem la góor ñi jëkkoon a dem bi ñu gisee biddéew bi ? Seytaane mi nekk Ibliis moo bëggoon a rey Doomu Yàlla ji, te xamoon na ne Erodd mi nekkoon buur ci Yerusalem dina ko jéem a rey. Kon mën nañu wax ne Seytaane moo taxoon biddéew boobu feeñ.