Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 88

Yaxya Mu Ngiy Sóob Yeesu Ci Ndox

Yaxya Mu Ngiy Sóob Yeesu Ci Ndox

XOOLAL pitax biy wàcc ci kow boppu nit ki. Nit kooku, Yeesu la. Am na léegi lu war a mat 30 at. Keneen ki, Yaxya la. Am na lu ñu jàng ba pare ci moom. Ndax yaa ngi fàttaliku liir bi yëngatu woon ci biiru Elisabet bi ko mbokkam Maryaama seetsee ? Yaxya la woon. Waaye lan la Yaxya ak Yeesu di def fii ?

Yaxya mu ngi sog a sóob Yeesu ci ndoxu dex bi tudd Yurdan. Nii lañuy sóobe nit : Dañu koy jëkk dugal ci biir ndox mi, ba pare génne ko. Yaxya dañu ko doon woowe Yaxya Sóobkat bi, ndaxte dafa doon sóob nit ñi. Waaye lu tax mu sóob Yeesu ?

Yeesu moo ñów ci moom, laaj ko ko. Yaxya dafay sóob ñi bëgg a wone ne réccu nañu lu bon li ñu doon def. Waaye, ndax Yeesu mas na def lu mu war a réccu ? Déedéet, ndaxte moom, doomu Yàlla bu jóge asamaan la. Kon leneen moo taxoon Yeesu bëgg Yaxya sóob ko. Nañu seet loolu.

Bala Yeesu ñów ci Yaxya, minise la woon. Minise dafay jël ay bant, defare ko taabal, siis, baŋ ak yeneen. Yuusufa, jëkkëru Maryaama, minise la woon te jàngal na Yeesu liggéey boobu. Waaye Yexowa yónniwul doomam ci kow suuf ngir mu nekk minise. Am na liggéey bu am solo bu mu bëggoon mu def, te léegi waxtu tàmbali liggéey boobu jot na. Yeesu dafa bëgg a wone ne léegi ñów na ngir def coobare Baayam. Moo tax mu laaj Yaxya mu sóob ko ci ndox. Ndax loolu neex na Yàlla ?

Waaw, neex na Yàlla, ndaxte bi Yeesu génnee ci ndox mi, baat bu jóge asamaan nee na lii : ‘ Kii mooy sama doom, ci moom laa ame bànneex. ’ Te it dafa mel ni asamaan si di ubbeeku, pitax wàcc ci kow Yeesu. Waaye du pitax dëgg. Dafa ko niru rekk. Xelu Yàlla mu sell mi la.

Léegi am na lu bare lu Yeesu war a xalaat, moo tax mu dem fu mu mën a wéet, toog fa 40 fan. Seytaane daldi dem ci moom foofu. Jéem na xiir Yeesu ñetti yoon ci def lu Yàlla bëggul. Waaye Yeesu defu ko.

Ginnaaw loolu, Yeesu dellu na fi mu nekkoon. Mu tase fa ak ay góor ñuy nekk ñi ko jëkk a topp, maanaam ñiy nekk taalibeem yu jëkk yi. Am na ci ñu tudd Andare ak Piyeer (mi ñuy woowe itam Simoŋ), Filib ak Nataneel (mi ñuy woowe itam Bartelemi). Yeesu ak taalibeem yu bees yi daldi dem ca diiwaanu Galile. Ñu toog fa tuuti ci dëkku Kana fu Nataneel cosaanoo. Foofu Yeesu dem na ca céet bu mag, def fa kéemaan bi jëkk ci yi mu def. Ndax xam nga ban kéemaan la ? Dafa soppi ndox mu nekk biiñ.