Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 93

Yeesu Jox Na Lekk Ay Nit Ñu Bare

Yeesu Jox Na Lekk Ay Nit Ñu Bare

AM NA lu garaaw lu sog a am. Rey nañu Yaxya Sóobkat bi. Erojàdd mi nekk jabaru buur bi, bëggul woon Yaxya. Fexe na ba buur bi digal ñu dagg boppu Yaxya.

Bi Yeesu déggee loolu, xolam jeex. Mu daldi dem ci béréb bu wéet. Nit ñi topp ko. Yeesu gis mbooloo mu réy moomu, mu yërëm leen. Mu daldi leen jàngal lu jëm ci Nguuru Yàlla te faj ñi feebar.

Ci ngoon si, taalibeem ñów ci moom, ne ko : ‘ Léegi mu guddi te fii dafa wéet. Wax leen ñu dem ci dëkk yi nekk fii, ngir ñu jënd lu ñuy lekk. ’

Yeesu tontu leen, ne : ‘ Jarul ñu dem. Jox leen ñu lekk. ’ Mu laaj Filib : ‘ Fan lañu mën a jënde lekk bu doy pur ñépp ? ’

Filib ne ko : ‘ Bu ñu bëggee sax ku nekk am tuuti mburu kese, loolu dina laaj xaalis bu baree bare. ’ Andare ne : ‘ Xale bii am na juróomi mburu ak ñaari jën. Waaye loolu du leen mën a doy ñoom ñépp. ’

Yeesu ne : ‘ Waxleen nit ñi ñu toog ci ñax bi. ’ Bi ñu paree mu gërëm Yàlla ci lekk bi, damm mburu mi, taalibe yi jox nit ñépp mburu ak jën. Amoon na 5 000 góor, am it ay jigéen ak ay xale yu baree bare. Ñépp a lekk ba suur. Te bi ñu dajalee desit yi, amoon na ci 12 pañe yu fees !

Léegi Yeesu wax na taalibeem yi ñu dugg ci gaal te jéggi dexu Galile. Ci guddi gi, ngelaw ak taw bu metti am, géej gi di yëngal gaal gi, yëngal bu metti. Taalibe yi tiit lool. Jékki-jékki ci booru minwi, ñu gis nit kuy ñów di dox ci kow géej gi. Ñu daldi yuuxu ndax tiit, ndaxte xamuñu loolu lan la.

Yeesu ne leen : ‘ Buleen tiit. Man la ! ’ Waaye ba tey, mënuñu gëm loolu. Piyeer ne : ‘ Bu dee yow la dëgg, Sang bi, sant ma, ma dox ci kow ndox mi, ñów ci yow. ’ Yeesu ne ko : ‘ Kaay ! ’ Piyeer wàcc gaal gi te dox ci kow ndox mi ! Mu daldi komaasee tiit te tàmbalee suux. Waaye Yeesu jàpp na ko.

Beneen bés, Yeesu joxaat na lekk ay junniy nit, fekk juróom-ñaari mburu ak ay jën yu ndaw kese la amoon. Booba it, nit ñépp lekk nañu ba suur, ba mu am lu des. Gis nga ni Yeesu di toppatoo nit ñi. Ndax loolu rafetul ? Bés bu nekkee buur, ba di nguuru ci Nguuru Yàlla, dinañu am lépp lu ñu soxla !