Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 94

Ku Bëgg Xale La

Ku Bëgg Xale La

XOOLAL Yeesu fii ak xale bi nekk ci loxoom yi. Gis nga fii ne Yeesu bëgg na xale. Ñi koy xool nii ñooy ndawam yi. Yeesu, lan la leen di wax ? Nañu ko seet.

Yeesu ak ndawam yi ñu ngi jóge tukki fu sore. Ndaw yi dañu doon werante ci yoon bi. Bi ñu àggee, Yeesu laaj leen lii : ‘ Lu ngeen doon werante ci yoon bi ? ’ Yeesu moom xam na ko. Waaye dafa bëgg seet ndax dinañu ko ko wax.

Ndaw yi bañ a tontu, ndaxte ci yoon bi dañu doon werante ba xam ku gën a màgg ci ñoom. Am na ay ndaw yu bëgg gën a màgg seen moroom. Naka la Yeesu di leen waxe ne bëgg sut sa moroom baaxul ?

Dafa woo benn xale bu ndaw, taxawal ko ci kanamu ñépp, ba pare mu ne taalibeem yi : ‘ Dama bëgg ngeen xam lii bu baax. Bu ngeen soppiwul seen jikko ba mel ni xale, dungeen dugg mukk ci nguuru Yàlla. Ki gën a màgg ci Nguur gi mooy kiy mel ni xale bii. ’ Ndax xam nga lu tax Yeesu wax loolu ?

Yeesu dafa wax loolu, ndaxte xale bu tuuti moom, du xalaat gën a mag walla sut moroomam. Kon ndaw yi war nañu jàng di mel ni xale ci fànn boobu te bañ a xuloo ngir xam ki gën a màgg walla ki sut moroomam.

Am na feneen it fu Yeesu wone ni mu bëgge xale. Ay weer ginnaaw loolu, ay nit dañu indi seeni doom pur ñu gis Yeesu. Ndaw yi bañ leen a bàyyi ñu jege Yeesu. Waaye Yeesu dafa leen ne : ‘Bàyyileen xale yi ñów ci man. Buleen leen ko tere. Ndaxte ñu mel ni ñoom ñooy am nguuru Yàlla. ’ Yeesu daldi jël xale yi ci loxoom, barkeel leen. Waaw, Yeesu dafa bëgg xale. Ndax loolu neexul a xam ?