Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 95

Ni Yeesu Di Jàngalee

Ni Yeesu Di Jàngalee

YEESU mas na wax kenn ne dafa war a bëgg moroomam. Kooku ne Yeesu : ‘ Kan mooy sama moroom ? ’ Yeesu xam na li nit ki di xalaat. Pur moom, moroomam mooy ku mu bokkal xeet walla diine. Nañu seet li ko Yeesu tontu.

Lée-lée, Yeesu dafay nettali dara ngir jàngale. Loolu lay def léegi. Mu ngiy nettali lu jëm ci benn Yawut ak benn waa Samari. Xam nañu ba pare ne li ëpp ci Yawut yi bëgguñu waa Samari. Lii la Yeesu di nettali :

Benn bés, benn Yawut dafa doon wàcc benn montaañ bu ndaw, di dem Yeriko. Ay sàcc dal ci kowam, sàcc xaalisam yépp, dóor ko ba muy bëgg dee.

Benn saraxalekat bu nekkoon Yawut jaar ci yoon bi. Mu gis nit ki ñu dóor. Ci sa xalaat, lan la def ? Dafa aw ci beneen wetu yoon bi, dem yoonam. Beneen boroom diine ñów. Waa Lewi la. Ndax taxaw na ? Déedéet, taxawul ngir dimbali kooku ñu dóoroon. Xoolal fii, mën nga gis saraxalekat bi ak waa Lewi bi di dem seen yoon.

Xoolal ki nekk fii ak nit ki ñu dóor. Kooku, waa Samari la. Te mu ngiy dimbali Yawut bi. Mu ngi def garab ci gaañ-gaañu nit ki. Bi mu paree, yóbbu na ko ca béréb fu mu mënee noppalu te tane.

Bi mu ko nettalee loolu ba pare, Yeesu laaj nit ki lii : ‘ Ci ñetti nit ñooñu, kan moo wone ne mooroomu ki ñu dóoroon la ? Saraxalekat bi, waa Lewi ji walla waa Samari ji ? ’

Nit ki ne ko : ‘ Waa Samari. Lu baax la defal ki ñu dóoroon. ’

Yeesu ne ko : ‘ Wax nga dëgg. Kon demal te def ni moom. ’

Gis nga ni Yeesu di jàngalee ? Waaw, bu ñu jàngee li Yeesu wax ci Biibël bi, dinañu mën a xam lu bare lu am solo, du dëgg ?