Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 96

Yeesu Faj Na Ñi Feebar

Yeesu Faj Na Ñi Feebar

YEESU mu ngiy wër réew mi, di faj ñi feebar. Ñépp di wax ci kéemaan yooyu. Nit ñi di ko indi nit ñu lafañ, ñu gumba walla ñu tëx ak ñeneen ñu feebar. Yeesu faj leen ñoom ñépp.

Am na léegi lu ëpp ñetti at bi Yaxya Sóobkat bi sóobee Yeesu ci ndox. Te Yeesu wax na ndawam yi ne ci kanam tuuti dina dem Yerusalem, dinañu ko rey foofu, ba pare dina dekki. Bala loolu di am, moom Yeesu mu ngi kontine di faj ñi feebar.

Benn bésu noflaay, Yeesu dafa doon jàngale. Bésu noflaay mooy bés fu Yawut yi di toog, noppalu. Jigéen bi ngay gis fii, dafa feebar lool. Lu mat 18 at a ngi nii mënul siggi, taxaw. Yeesu dafa teg loxoom ci kowam, mu daldi wér, taxaw !

Kilifa diine yi daldi mer. Kenn ki yuuxu, ne : ‘ Am na juróom-benni fan yu nit ñi war a liggéey. Kon war ngeen a ñów faju ci bés yooyu, waaye du ci bésu noflaay bi ! ’

Waaye Yeesu tontu leen ne : ‘ Yéen a bon. Yéen ñépp dingeen yewwi seen mbaam ci bésu noflaay ngir yóbbu ko mu naan. Kon jigéen boobu nekk ci feebar lu mat 18 at, ndax waruñu ko woon a faj ci bésu noflaay bi ? ’ Nit ñu bon ñooñu daldi rus.

Beneen bés ginnaaw loolu, Yeesu ak ndawam yi dañu doon dem Yerusalem. Dañu génn dëkku Yeriko rekk, ñaari gumba yu doon yelwaan dégg ne Yeesu moo doon jàll. Ñu daldi yuuxu, ne ko : ‘ Yeesu, dimbali ñu ! ’

Yeesu woo leen ne : ‘ Lan ngeen bëgg, ma defal leen ko ? ’ Ñu tontu ko ne : ‘ Sang bi, na suñuy bët ubbeeku. ’ Yeesu laal seeni bët, ñu daldi gis ci saa si ! Ndax xam nga lu tax Yeesu di def kéemaan yu rafet yooyu ? Ndaxte dafa bëgg nit ñi te bëgg na it ñu am ngëm ci moom. Te it, mën na ñu wóor ne bés bu nekkee Buur ba nguuru, kenn dootul feebar ci kow suuf si.