Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 99

Ci Néeg Bi Nekk Ci Kow

Ci Néeg Bi Nekk Ci Kow

ÑU NGI ci bésu Alxemes, ñaari fan ginnaaw bi li ñu nettali léegi amee. Yeesu ak 12 ndawam yi dañu ñów fii ngir lekk reer bi ñuy togg ci bésu Jéggi bi. Kii di dem mooy Yudaa Iskariyo. Mu ngi dem wax saraxalekat yi naka lañu mënee jàpp Yeesu.

Démb rekk la Yudaa dem ci ñoom ne leen : ‘ Bu ma leen dimbalee ba ngeen jàpp Yeesu, lan ngeen may jox ? ’ Ñu ne ko : ‘ Fanweeri xànjaru xaalis. ’ Kon léegi Yudaa mu ngi dem ci ñoom ngir yóbbu leen ci Yeesu. Loolu garaaw na de !

Léegi lekk nañu ba pare reeru bésu Jéggi bi. Waaye Yeesu dafay taxawal léegi beneen reer. Mu jël mburu, jox ko ndawam yi ne : ‘ Lekkleen ci, ndaxte mu ngi misaal sama yaram bi ñuy joxe ngir yéen. ’ Mu jël itam kaasu biiñ, jox leen ne : ‘ Naanleen ci, ndaxte mu ngi misaal sama deret biy tuuru ngir yéen. ’ Reer boobu dañu koy woowe ci Biibël bi ‘ Reeru Boroom bi ’.

Waa Israyil dañu doon lekk reeru Jéggi bi ngir fàttaliku bés bi malaakaa Yàlla ‘ jéggee ’ seeni kër ca Misra. Bés boobu, reyul seeni taaw waaye dafa rey taaw yi nekkoon ci këru waa Misra yi. Waaye léegi Yeesu dafa bëgg ñi koy topp fàttaliku ko moom, Yeesu, ak ni mu joxe bakkanam ngir ñoom. Loolu moo tax mu wax leen ñu màggal reer boobu at mu nekk.

Bi ñu paree ci Reeru Boroom bi, Yeesu wax na ndawam yi ñu am fit ak ngëm gu dëgër. Dañu woyal Yàlla ba pare dem. Guddi woon na lool. Xéyna sax minwi pase woon na ba pare. Nañu seet fu ñu jëm.