Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 101

Ñu Ngiy Rey Yeesu

Ñu Ngiy Rey Yeesu

XOOLAL li fi xew ! Ñu ngiy rey Yeesu. Dañu ko daaj ci bant, daaj ko ay pont ci loxoom ak ci tànkam yi. Naka la nit mënee def loolu Yeesu ?

Am na ñu bañ Yeesu. Xam nga ñan lañu ? Kenn ki mooy malaaka bu bon boobu, maanaam Seytaane mi nekk Ibliis. Moom moo fexe ba suñuy maam Aadama ak Awa déggadi Yàlla. Te Seytaane moo xiir ñi bañoon Yeesu ci rey ko noonu.

Bala ñu daaj Yeesu ci bant bi, noonam yi defoon nañu ko lu bon lool. Yaa ngi fàttaliku ni ñu ko jàppe woon ci toolu Setsemane, ba pare yóbbu ko ? Noonam yi, ñan lañu woon ? Kilifa diine yi la woon. Nañu seet li xewoon ginnaaw loolu.

Bi kilifa diine yi jàppee Yeesu, ndawam yépp daw ndax tiit, bàyyi ko moom kenn. Waaye ndaw yi Piyeer ak Yowanna, sorewuñu ko. Ñu daldi leen topp ngir seet luy dal Yeesu.

Saraxalekat yi yóbbu nañu Yeesu ca góor gu màgget gu tudd Anas. Moom moo nekkoon bu jëkk saraxalekat bu mag bi. Waaye mbooloo mi indi woon Yeesu yàggu fa. Ñu daldi yóbbu Yeesu ca kër Kayif mi nekk saraxalekat bu mag bi léegi. Ay kilifa diine yu bare ñoo fa daje.

Fii ci kër Kayif dañu ko bëgg a àtte. Ñu indi ay nit pur ñu wax ay fen ci Yeesu. Kilifa diine yépp naan : ‘ Dañu war a rey Yeesu. ’ Ñu daldi ko tufli ci kanamam te dóor ko ay kurfeñ.

Bi loolu lépp di am, Piyeer moom mu ngi ci biti ci ëtt bi. Guddi gi dafa sedd, kon nit ñi def nañu benn taal. Bi ñu nekkee foofu di jaaru, benn mbindaan xool Piyeer te ne : ‘ Kii itam dafa doon ànd ak Yeesu. ’

Piyeer nee : ‘ Déedéet, du man ! ’

Ñetti yoon lañu wax Piyeer ne dafa doon ànd ak Yeesu. Mu weddi ko ñetti yoon yooyu yépp. Ci ñetteelu yoon bi, Yeesu daldi geestu, xool Piyeer. Piyeer réccu fen yi mu fen, mu daldi génn te jooy.

Léegi bët set. Ñu ngi ci fajaru bésu àjjuma. Saraxalekat yi yóbbu nañu Yeesu ci seen saal bu mag fu ñuy àtte nit ñi. Ñuy waxtaan foofu ci li ñuy def ak Yeesu. Ñu daldi ko yóbbu ca Poñsë Pilaat, mi nekkoon kilifa diiwaanu Yude.

Saraxalekat yi ne Pilaat : ‘ Nit ku bon la. Dañu ko war a rey. ’ Pilaat wax ak Yeesu, di ko laaj yenn laaj, ba pare mu ne leen : ‘ Deful dara lu bon. ’ Mu daldi ko yónnee Erodd Antipas. Erodd mooy kilifa diiwaanu Galile, waaye Yerusalem la nekk. Moom it, gisul dara lu bon lu Yeesu def, mu daldi ko delloo Pilaat.

Pilaat dafa bëgg a bàyyi Yeesu. Waaye noonam yi dañu bëgg Pilaat bàyyi keneen ku ñu tëjoon kaso. Kooku sàcc bu tudd Barabas la. Ñu ngi ci booru midi léegi, Pilaat génn ak Yeesu, mu ne mbooloo mi : ‘ Xoolleen seen buur! ’ Saraxalekat yu mag yi daldi yuuxu, naan : ‘ Na fi jóge ! Rey ko ! Rey ko ! ’ Pilaat daldi bàyyi Barabas mu dem, ñoom ñu jël Yeesu, yóbbu ko pur ñu rey ko.

Bi midi paasee tuuti ci bésu àjjuma boobu, dañu daaj Yeesu ci bant. Amoon na it ñaari nit yu ñu defoon ci bant ngir ñu dee, ndax lu bon li ñu defoon, kenn ki nekk ci ndeyjooru Yeesu, keneen ki ci càmmooñam. Tuuti bala Yeesu dee, kenn ki ne ko : ‘ Boo nekkee ci sa nguur, nanga ma fàttaliku. ’ Yeesu tontu ko ne : ‘ Maa ngi lay dig ne dinga nekk ak man ci Àjjana. ’

Ndax li mu ko dig noonu, nekkul lu rafet lool ? Ndax xam nga ban àjjana la Yeesu doon wax noonu ? Àjjana ji Yàlla sàkkoon ci njëlbéen, fan la nekkoon ? Waaw, ci kow suuf la nekkoon. Te bu Yeesu nguuroo ci asamaan, dina dekkal nit kooku, mu mën a am dund gu neex ci Àjjana ju bees jiy am ci kow suuf. Ndax waruñu ci kontaan lool ?