Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 103

Ci Biir Néeg Bu Ñu Tëj

Ci Biir Néeg Bu Ñu Tëj

BI PIYEER ak Yowaana jógee ci bàmmeel fi néewu Yeesu nekkoon, Maryaama des na fa moom kenn. Mu daldi jooy. Mu sëgg, xool ci biir bàmmeel bi. Mooy li ñu wone ci nettali bi jiitu. Foofu mu gis ñaari malaakaa ! Ñu laaj ko : ‘ Looy jooy ? ’

Maryaama ne leen : ‘ Dañoo jël sama Boroom te xawma fu ñu ko yóbbu. ’ Mu geestu, gis benn góor. Kooku ne ko : ‘ Kooy seet ? ’

Maryaama dafa foog ne kooku mooy kiy liggéey ci tool bi te xéyna moom moo jël néewu Yeesu. Mu ne ko : ‘ Bu fekkee ne yaa ko yóbbu, wax ma foo ko def. ’ Waaye nit kooku, Yeesu ci boppam la. Dafa sol yaram bu Maryaama xàmmewul. Waaye bi mu ko woowee ci turam, Maryaama xam ne Yeesu la. Mu daw, wax taalibeem yi : ‘ Gis naa Sang bi ! ’

Ginnaaw loolu ci bés boobu, ñaari taalibe Yeesu ñu ngi doon dox, jëm Emayus. Benn góor dab leen. Xolu taalibe yi dafa jeexoon ndax li ñu rey Yeesu. Waaye bi ñu doon dox di dem, nit kooku wax na leen lu bare lu seddal seen xol te mu jële ko ci Biibël bi. Bi ñu taxawee ngir reer ak moom, taalibe yi daldi xam ne kii, Yeesu la. Yeesu daldi ne mes. Gisatuñu ko. Ñaari taalibe yi gaaw a dellu Yerusalem wax loolu lépp ndaw yi.

Bi loolu di am, Yeesu feeñu na Piyeer itam. Yeneen taalibe yi kontaan lool bi ñu déggee loolu. Ñaari taalibe yi daldi àgg Yerusalem, gis ndaw yi. Ñu wax leen ni leen Yeesu feeñoo itam ci yoon bi. Te bi ñu doon nettali loolu, xam nga lan moo xew ?

Xoolal li ñuy wone fii. Yeesu feeñu na taalibeem yi ci biir néeg bi, fekk dañu tëjoon bunt bi. Xoolal ni ñu kontaane ! Dëgg-dëgg, bés bii moom, neex na. Ndax fi ñu tollu mën nga wax ñaata yoon la Yeesu feeñu taalibeem yi ? Ñaata yoon nga wax ? Juróom ?

Ndaw li Tomaa nekku fi woon bi leen Yeesu feeñoo. Taalibe yi ne ko : ‘ Gis nañu Sang bi ! ’ Tomaa ne leen bala muy gëm, fàww mu gis Yeesu moom ci boppam. Juróom-ñetti fan ginnaaw loolu, taalibe yi nekkaat ci biir néeg bu ñu tëj. Bii yoon, Tomaa mu ngi ak ñoom. Jékki-jékki rekk, Yeesu daldi leen feeñu ci biir néeg bi. Tomaa daldi gëm léegi.