Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 104

Yeesu Mu Ngiy Dellu Asamaan

Yeesu Mu Ngiy Dellu Asamaan

BÉS yi ñu ngi jàll rekk. Yeesu feeñu na taalibeem yi ay yoon yu bare. Benn bés, lu war a tollu ak 500 taalibe lañu woon. Bu leen Yeesu di feeñu, xam nga ci lan lay wax ak ñoom ? Ci nguuru Yàlla. Yexowa yónni na Yeesu ci kow suuf ngir jàngale lu jëm ci Nguur gi. Te liggéey boobu dafa ko kontine ginnaaw sax bi ko Yàlla dekkalee.

Ndax yaa ngi fàttaliku lan mooy nguuru Yàlla ? Waaw, nguur dëgg la. Ci asamaan la nekk. Te Yeesu mooy Ki Yàlla tànn ngir mu nekk buuru nguur googu. Ni ñu ko jànge ci yeneen nettali, Yeesu wone na ne dina doon buur bu baax lool. Wone na ko bi mu doon jox lekk ñi xiif, faj ñi feebar te dekkal sax ñi dee !

Kon bu Yeesu nekkee di nguuru ca asamaan ci lu mat junni at, suuf si naka lay mel ? Waaw, dinañu defar suuf si sépp ba mu nekk àjjana ju rafet. Xeex dootul am. Nit ñiy def lu yoon tere, feebar ak dee sax dootul am. Mën nañu gëm loolu ndaxte Yàlla dafa sàkk suuf si ngir mu nekk àjjana fu nit ñi di ame bànneex. Loolu moo tax mu defoon toolu Eden ci jamano bu jëkk boobu. Kon li Yàlla bëgg noonu, Yeesu mooy toppatoo lépp ba mu am.

Léegi Yeesu war na dellu asamaan. Feeñu na taalibeem yi ci lu mat 40 fan. Léegi xam nañu bu baax ne dundaat na. Waaye, lii la wax taalibeem yi bala mu tàggoo ak ñoom : ‘ Toogleen Yerusalem ba ngeen jot xel mu sell mi. ’ Xel mu sell mi mooy kàttanu Yàlla biy jëfe. Dafa mel ni ngelaw buy romb. Xel moomu mooy dimbali ñi topp Yeesu ñu def li Yàlla bëgg. Yeesu mujj na leen wax lii : ‘ Nangeen waare lu jëm ci man ba fa àddina yem. ’

Bi Yeesu waxee loolu ba pare, lu doy waar daldi am. Yeesu dafa komaasee yéeg ca asamaan ni nga ko gise fii. Benn niiru asamaan daldi ko nëbb, te taalibe yi gisatuñu ko. Yeesu dem asamaan te komaasee nguuru foofu ci kow taalibeem yi nekk ci kow suuf si.