Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 107

Sànni Nañu Ay Xeer Ecen Ba Rey Ko

Sànni Nañu Ay Xeer Ecen Ba Rey Ko

KII di sukk nii, Ecen la. Taalibe Yeesu dëgg la. Waaye xoolal li koy dal léegi ! Góor ñii, ñu ngi koy sànni xeer yu mag. Lu tax ñu bañ Ecen ba def ko lii ? Nañu seet loolu.

Yàlla dimbali na Ecen mu def ay kéemaan yu mag te rafet. Waaye loolu neexul nit ñooñu, ñu daldi werante ak moom ci dëgg gi muy jàngal nit ñi. Waaye Yàlla dafa may Ecen xam-xam bu bare, mu won leen ne, ñoom li ñuy jàngale moo dul dëgg. Loolu tax na ñu gën a mer. Ñu jàpp ko te woo ay nit pur ñu seede ay fen ci moom.

Saraxalekat bu mag bi laaj Ecen lii : ‘ Ndax li nit ñooñu wax dëgg la ? ’ Ecen tontu ko ci waare bu neex bu sukkandiku ci Biibël bi. Mu àggale waxtaan bi di leen wax ci ay nit ñu bon ñu doon bañ yonentu Yexowa yi ca jamano yu yàgg ya ak ci lu bon li ñu leen def. Mu ne leen lii : ‘ Yéen, dangeen mel ni nit ñooñu rekk. Rey ngeen Yeesu mi doon jaamu Yàlla te toppuleen ndigalu Yàlla yi. ’

Kilifa diine yi daldi mer bay lox sax ! Ecen xool ca kow, ne : ‘ Xoolleen ! Maa ngi gis Yeesu di taxaw ci ndeyjooru Yàlla ca asamaan. ’ Góor ñi daldi def seen loxo ci seen nopp ngir bañ a dégg, dal ci kow Ecen, jàpp ko te yóbbu ko ci biti dëkk bi.

Fii, dañuy summi seeni mbubb, teg leen ci tànku góor gu tudd Sool. Ndax yaa ngi gis Sool ? Ay nit komaase nañu di sànni Ecen ay xeer. Ecen sukk. Loolu ngay gis fii. Mu ñaan Yàlla ne : ‘ Yexowa, bu leen fey lu bon li ñuy def nii. ’ Ecen xam na ne am na ci ñoom ñoo xam ne kilifa diine yi ñoo leen nax. Ecen daldi dee.

Ku la def lu bon, ndax dangay feyyu walla nga di ko ñaanal lu bon ? Du loolu la Ecen ak Yeesu def. Dañu baaxoon ak ñi leen defoon sax lu bon. Nañu jéem a def ni ñoom.