Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 108

Ci Yoonu Damas

Ci Yoonu Damas

NDAX xam nga ki nekk fii tëdd ci suuf ? Sool la. Yaa ngi fàttaliku Sool ? Ci tànkam la ñi doon rey Ecen tegoon seeni mbubb. Xoolal leer gi di melax ! Lu xew ?

Ginnaaw bi ñu reyee Ecen, Sool moo gënoon a sawar moroomam yi ci wut taalibe Yeesu ngir def leen lu bon. Dafa doon dugg ci kër gu nekk, génne leen fa, dugal leen kaso. Ñu bare ci taalibe yi daldi daw ci yeneen dëkk, ñu tàmbali foofu di waare “ xebaar bu baax bi ”. Waaye Sool it dafay dem ci yeneen dëkk, jéem fa jàpp taalibe Yeesu yi. Léegi mu ngi ci yoonu Damas. Waaye lu doy waar moo xew ci yoon bi.

Sool mu ngi doon dox, jékki-jékki rekk, leer gu jóge asamaan daldi melax te wër ko. Mu daanu ci suuf, ni nga ko gise fii. Benn baat ne : ‘ Sool, Sool, lu tax nga di ma fitnaal ? ’ Ñi ànd ak Sóol, gis nañu leer gi, dégg nañu baat bi, waaye mënuñu xam lu muy wax.

Sool ne : ‘ Yaay kan, Sang bi ? ’

Baat bi ne : ‘ Maay Yeesu, mi ngay fitnaal. ’ Yeesu dafa wax loolu ndaxte bu Sool fitnaalee taalibe Yeesu, Yeesu dafa koy gise ni moom la Sool di fitnaal.

Sool laaj ko : ‘ Lan laa war a def, Sang bi ? ’

Yeesu ne ko : ‘ Jógal, dugg Damas. Foofu dinañu la wax li nga war a def. ’ Sool jóg, taxaw te ubbi bëtam yi, waaye mënatul gis dara. Dafa gumba ! Ñi ànd ak moom daldi ko wommat ba Damas.

Yeesu mu ngi wax léegi ak benn ci taalibeem yi nekk Damas. Mu ne ko : ‘ Jógal, Anañas. Demal ci mbedd mi ñuy woowe Mbedd mu jub mi. Demal ci kër Yudaa te laaj fa ku tudd Sool. Dama ko tànn pur mu nekk sama jaam te def liggéey bu am solo. ’

Anañas def loolu. Bi mu gisee Sool, mu teg loxoom yi ci kowam, ne ko : ‘ Sang bi moo ma yónni ngir nga mën a gisaat te fees ak xel mu sell mi. ’ Ci saa si mu am lu mel ni ay waasintoor yu doon génn ci bëtu Sool yi, mu daldi gisaat.

Yeesu jaar na ci Sool ngir def liggéey bu réy ci waar xeet yu bare. Nit ñi mujj nañu ko woowe ndaw li Pool. Dinañu gën a jàng ci moom bu ci kanamee. Nañu jëkk seet lu tax Yàlla yónni Piyeer..