Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 113

Pool Mu Ngi Room

Pool Mu Ngi Room

XOOLAL ceen yi nekk ci loxo Pool. Xoolal it soldaaru Room bi koy wottu. Dañu tëj Pool ci benn kër ci Room. Dafay xaar ba Sesaar wax li ñu ko war a def. Mu ngi kaso waaye may nañu ko nit ñi seetsi ko.

Ñetti fan ginnaaw bi Pool agsee Room, mu yónnee pur ñu woo ay nit ñu doon jiite Yawut yi pur ñu ñów gis ko. Ay Yawut yu bare yu nekkoon Room daldi ko seetsi. Pool waar na leen ci Yeesu ak ci nguuru Yàlla. Mu am ñuy gëm te nekk Karceen. Ñeneen ñi bañ a gëm.

Pool waar na itam soldaar yi koy wottu. Ci ñaari at yi mu def foofu, Pool waar na képp ku mu mën a waar. Loolu moo tax waa këru Sesaar sax dégg nañu xibaaru Nguur gi mi nekk xibaar bu baax bi. Am na ci sax ñu mujj a nekk karceen.

Waaye gan gi nekk fii di bind, kan la ? Ndax mën nga ko wax ? Timote la. Timote itam nekkoon na kaso ndax li mu doon waare lu jëm ci Nguur gi, waaye léegi génn na. Dafa ñów fii ngir dimbali Pool. Xam nga lan la Timote di bind ? Nañu seet loolu.

Ndax yaa ngi fàttaliku dëkk yi tudd Filib ak Efes yi ñu gisoon ci nettali 110 ? Pool bokk na ci ñi tàmbali ay mbooloo karceen foofu. Léegi mu ngi kaso waaye dafay bind karceen yooyu ay leetar. Leetar yooyu ñu ngi ci Biibël bi, ñu woowe leen Waa Efes ak Waa Filib. Fii, Pool a ngiy wax Timote li mu war a bind ci leetar bi muy yónnee seeni xarit karceen yi nekk Filib.

Waa Filib yi baaxoon nañu lool ak Pool. Am na lu ñu ko may, yónnee ko ko kaso. Pool mu ngi leen di gërëm ci loolu. Epafrodit mooy ki indi woon maye boobu. Waaye feebar dal na ko ba mu xaw a dee. Léegi tane na te mu ngi bëgg a ñibbi. Bu ñibbee Filib, dina yóbbu leetar boobu Pool ak Timote di bind.

Ci kaso bi, Pool bind na yeneen ñaari leetar yu ñu mën a gis ci Biibël bi. Benn bi, pur karceen yi nekk ci dëkku Kolos la woon. Xam nga naka lañuy woowe leetar boobu ? Waa Kolos. Beneen bi, pur benn xaritu Pool bu baax la woon. Kooku mu ngi tudd Filemon te dëkk Kolos. Leetar boobu mu ngi wax ci Onesim mi nekkoon jaamu Filemon.

Onesim daw na kër Filemon, ñów Room. Onesim dégg ne Pool a ngi kaso. Mu ñów seetsi ko. Pool waar ko, yàggul Onesim nekk karceen. Léegi Onesim réccu na li mu dawe kër Filemon. Kon xam nga lan la Pool wax Filemon ci leetar bi ?

Pool mu ngi koy laaj mu baal Onesim. Mu ne : ‘ Maa ngi la koy delloo. Waaye léegi nekkatul sa jaam kese. Sa mbokk karceen bu baax la. ’ Bi Onesim delloo Kolos, ñaari leetar yooyu la yóbbaale. Benn pur Waa Kolos. Beneen bi pur Filemon. Filemon naroon na kontaan lool bi mu déggee ne jaamam, karceen la léegi.

Ci leetar yi mu yónnee Waa Filib ak Filemon, Pool am na xibaar yu neex yu mu leen wax. Mu ne Waa Filib : ‘ Dinaa leen yónnee Timote. Waaye man it, dinaa leen seetsi bala mu yàgg. ’ Mu ne Filemon : ‘ Nanga ma waajal néeg fu may dal. ’

Bi Pool génnee kaso, seetsi na ay mbokkam karceen yu góor ak yu jigéen ci ay béréb yu bare. Waaye tëjaat nañu ko kaso Room. Bii yoon, xam na ne dinañu ko rey. Mu bind leetar Timote, ne ko mu gaaw a ñów. Mu ne ci leetar bi : ‘ Topp naa Yàlla ni mu ware. Yàlla dina ma defal lu neex. ’ Ay tuuti at ginnaaw loolu, rey nañu Pool. Alagaat nañu itam Yerusalem, te bii yoon, waa Room ñoo ko def.

Li ñu mën a jàng ci Biibël bi jeexul. Yexowa Yàlla jaar na ci ndaw li Yowaana ngir bind téere yi mujj ci Biibël bi. Téere Peeñu ma bokk na ci. Mu ngi wax ci li war a xew ëllëg. Kon nañu seet léegi li war a am ëllëg..