Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

Ndax lii la Yàlla bëggoon ?

Ndax lii la Yàlla bëggoon ?

JÀNGAL surnaal boo bëgg. Seetaanal tele mbaa nga déglu rajo. Jëf yu bon, geer ak li ñuy woowe ci tubaab terrorisme lañu fay gën a dégg ! Xalaatal ci say jafe-jafe. Xéyna nga am lu la metti lool ndax mbokk walla xarit bu feebar walla bu gaañu. Xéyna dinga yëg li Ayóoba yëgoon ci xolam. Nit ku baax kooku lii la waxoon : “ Sama dund gépp, coono kese la. ” — Ayóoba 10:​15, NW.

Laajal sa bopp lii :

  • Ndax lii la Yàlla bëggoon pur man ak pur doomu Aadama yi ?

  • Fan laa mënee am ndimbal ci samay coono ?

  • Ndax mën nañu yaakaar ne jàmm dina mas a am ci suuf si sépp ?

Biibël bi dafay tontu lu leer ci laaj yooyu.

SOPPI YI BIIBËL BI WAX NE YÀLLA DINA KO DEF CI KAW SUUF.

“Dina fomp bépp rangooñ ci seeni bët ; te dee dootul am walla naqar walla jooy walla metit.” — Peeñu ma 21:⁠4.

‘ Lafañ dina tëbeentu ni kéwél. ’ — Esayi 35:⁠6.

 Gumba yi dinañu gis. ’ — Esayi 35:⁠5.

“Néew yépp, yi nekk ci seen bàmmeel, di[nañu...] génn.” — Yowaana 5:​28, 29.

“ Kenn ci waa réew mi du wax : ‘ Dama feebar. ’ ” — Esayi 33:​24, NW.

“ Pepp mi [dina] baawaan ci réew mi. ” — Sabóor 72:⁠16.

NANGA JARIÑOO LI BIIBËL BI WAX

Bul gaaw a wax ne li nekk ci xët yi weesu, wax yu neex kese la. Yàlla moo ñu dig ne dina def loolu, te Biibël bi wax na ni mu koy defe.

Waaye Biibël bi def na lu ëpp loolu. Dafa ñu won it ni ñu mënee am dund gu neex dëgg tey jii sax. Xalaatal tuuti ci say naqar ak say coono. Mën na doon poroblemu xaalis, poroblem ci sa njaboot, feebar, mbaa mbokk walla xarit bu gaañu. Biibël bi mën na la dimbali nga xam ni ngay faje say poroblem. Mën na la may doole it ci li muy tontu ci laaj yu mel nii :

  • Lu tax ñuy am metit ?

  • Naka lañuy def ba faj poroblem yi ñuy am ?

  • Lan lañu mën a def ba gën a am jàmm ci suñu kër ?

  • Lan mooy dal nit bu deewee ?

  • Ndax dinañu mas a gisaat suñu mbokk walla suñu xarit yi gaañu ?

  • Naka lañuy def ba mu wóor ñu ne Yàlla dina def li mu ñu dig ?

Li ngay jàng téere bii, dafay wone ne bëgg nga xam li Biibël bi wax. Téere bii dina la ci dimbali. Seetlu nga ne, xise bu nekk dafay am laaj bi mu àndal. Bind nañu ko ci suufu xët bi. Ay milyoŋi nit kontaan nañu ci fasoŋ bi ñuy jànge Biibël bi ak Seede Yexowa yi, maanaam li ñu leen di laaj ay laaj, ñu ciy tontu. Yaakaar nañu ne fasoŋ boobu dina la neex yow itam. Ñu ngi ñaan Yàlla mu barkeel lu neex te am solo li ngay def, maanaam di jàng li Biibël bi wax dëgg-dëgg !