Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

PÀCC ÑETT

Lan la Yàlla bëggoon bi muy sàkk suuf si ?

Lan la Yàlla bëggoon bi muy sàkk suuf si ?
  • Lan la Yàlla bëggoon bi muy sàkk nit ?

  • Kan moo xeex Yàlla te naka la ko defe ?

  • Naka la dund ci kaw suuf di mel ëllëg ?

1. Lan la Yàlla bëggoon bi muy sàkk suuf si ?

WAX dëgg, li Yàlla bëggoon bi muy sàkk suuf si, rafet na lool. Yexowa dafa bëggoon suuf si fees ak ay nit ñu bég te am wér-gi-yaram. Biibël bi nee na ‘ Yàlla Aji Sax ji jëmbët na tool ca biir Àjjana ’, te mu “ saxal [...] lépp luy garab gu meññeef ma rafet te neex a lekk ”. Ginnaaw bi Yàlla sàkkee Aadama ak Awa, góor ak jigéen yu njëkk ya, dafa leen dugal ci dëkkuwaay bu rafet te nee leen : «Giirleen te bare, ba fees àddina, di ko saytu.» (Njàlbéen ga 1:28 ; 2:​8, 9, 15). Kon li Yàlla bëggoon mooy, nit ñi am ay doom, ñu yaatal toolu àjjana bi ci kaw suuf si sépp, te ñuy toppatoo mala yi ci nekk.

2. a) Naka lañu xame ne li Yàlla bëggoon bi muy sàkk suuf si dina am ? b) Lan la Biibël bi wax ci dund gu dul jeex ngir doomu Aadama ?

2 Li Yexowa Yàlla bëggoon bi muy sàkk nit, maanaam nit ñi dëkk ci àjjana ci kaw suuf, ndax yaakaar nga ne dina mas a am ? Yàlla nee na : “ Wax naa ko, dinaa ko def itam. ” (Esayi 46:​9-11, NW ; 55:11). Waaw, ci lu wóor, lépp li Yàlla bëgg, dina ko def ! Nee na : “ Sàkku ma [suuf si] ngir mu nekk nii rekk ci neen ”, waaye “ dama ko sàkk ngir ay nit dëkk ci ”. (Esayi 45:​18, NW.) Nit ñi waroon a nekk ci kaw suuf, naka la Yàlla bëggoon ñu mel ? Te ba kañ la bëggoon ñu nekk ci kaw suuf si ? Biibël bi nee na : “ Nit ñu jub ñi dinañu moom suuf si, te dinañu fa dëkk ba fàww. ” — Sabóor 37:​29, NW ; Peeñu 21:​3, 4.

3. Lu ñaaw lan moo am ci kaw suuf si tey, te yan laaj la loolu di indi ci suñu xel ?

3 Leer na ne, fi ñu tollu nii, loolu amagul. Nit ñaa ngi feebar, ak di dee ; ñu ngi xeex sax ak di reyante. Kon am na lu doxul woon ni mu ware. Waaye, wóor na ne, Yàlla bëggul woon suuf si mel ni mu mel tey ! Kon lu xew ba mu mel nii ? Lu tax li Yàlla bëggoon mujjul am ? Amul benn téere bu doomu Aadama bind ngir nettali li xewoon démb bu mën a tontu ci loolu, ndaxte jafe-jafe yi, ci kaw asamaan lañu komaasee.

NI BENN NOON KOMAASEE DI XEEX YÀLLA

4, 5. a) Kan moo jaar ci jaan ngir wax ak Awa ? b) Naka la nit ku jub tey mënee dem ba nekk sàcc ëllëg ?

4 Téere bi njëkk ci Biibël bi dafay wax ci ku doon xeex Yàlla, te mu feeñ ci toolu Eden, Àjjana ji. Dañu wax ci moom foofu mel ni moom “ jaan ” la. Waaye du rabu àll dëgg. Téere bi mujj ci Biibël bi, dafay wone ne mooy “ Tuumaalkat bi mbaa Seytaane, moom miy nax waa àddina sépp ”. Dañu koy woowe it “ jaani cosaan ji ”. (Njàlbéen ga 3:1 ; ñun ñoo dëngal mbind yi ; Peeñu ma 12:⁠9.) Malaaka bu bare doole boobu, maanaam mbindeef boobu bët mënul a gis, dafa jaar ci jaan ngir wax ak Awa. Dafa def mel ni jaan bi moo doon wax. Malaaka boobu fekke woon na bi Yàlla doon waajal suuf si ngir doomu Aadama yi. — Job 38:​4, 7.

5 Lépp li Yexowa def dafa mat. Kon kan moo sàkk “ Seytaane ” boobu, maanaam “ Ibliis” ? Nañu wax rekk ne, kenn ci doomu Yàlla yi bokk ci malaaka yi am kàttan lool, moo def boppam Ibliis. Loolu nu mu mënee nekk ? Nit ku jub tey mën na dem ba nekk sàcc ëllëg. Loolu nu muy ame ? Mën na am nit kooku bàyyi bëgg-bëgg bu bon sax ci xolam. Bu kontinee di xalaat ci loolu, bëgg-bëgg bu bon boobu mën na mujj a am doole lool ci xolam. Te bés bu ci amee yoon rekk, xéyna mu def lu bon loolu mu doon xalaat. — Saag 1:​13-15.

6. Kenn ci doomu Yàlla yi bokk ci malaaka yi am kàttan lool, naka la def ba mujj a nekk Seytaane mi nekk Ibliis ?

6 Loolu moo dal Seytaane mi nekk Ibliis. Dafa mel ni dafa dégg bi Yàlla doon wax Aadama ak Awa ñu am doom te feesal suuf si ak seeni doom (Njàlbéen ga 1:​27, 28). ‘ Céy, doomu Aadama yooyu yépp, bu ñu ma mënoon a jaamu te bañ a jaamu Yàlla ! ’ Lépp ay wone ne loolu la Seytaane doon xalaat. Bëgg-bëgg bu bon daldi komaasee sax ci xolam. Mu mujj a jóg, daldi wax Awa ay fen ci Yàlla ngir nax ko (Njàlbéen ga 3:​1-5). Noonu la mujjee nekk “ Ibliis ” miy tekki “ Soskat ”, ak it “ Seytaane ” miy tekki “ Kuy xeex keneen ”.

7. a) Lu tax Aadama ak Awa mujj a dee ? b) Lu tax doomu Aadama yépp di màgget te di dee ñoom itam ?

7 Seytaane mi nekk Ibliis, dafa jaar ci ay fen ak ay naxaate ba Aadama ak Awa def li leen Yàlla tere woon (Njàlbéen ga 2:17 ; 3:⁠6). Loolu lu mu indi ? Aadama ak Awa mujj nañu dee. Loolu la Yàlla waxoon ne moo leen di dal, bu ñu ko déggalul (Njàlbéen ga 3:​17-19). Bi Aadama bàkkaaree la daldi nekk nit ku matul. Moo tax doomam yépp judduwaale ak bàkkaar boobu ñu donn ci moom (Room 5:12). Mën nañu misaal loolu ak muul bu ñuy defare mburu. Muul bi, bu amee sikk, mburu mi, nu muy mel ? Mburu bu ciy génn, dina am sikk. Noonu it, doomu Aadama bu nekk dafa donn “ sikk ”, maanaam matadi, ci Aadama. Looloo tax doomu Aadama yi di màgget te di dee. — Room 3:⁠23.

8, 9. a) Boo seetee ni mbir mi deme woon, lan la Seytaane weddi ? b) Lu tax Yàlla reyul ci saa si ñi ko weddi woon ?

8 Bi Seytaane xiiree Aadama ak Awa ci bàkkaar, fa la komaasee di fexe ba ñu bare bañ a déggal Yàlla. Dafa weddi fasoŋ bi Yexowa di jiitee. Dafa mel ni, lii la Seytaane doon wax : ‘ Yàlla du kilifa gu baax. Dafay fen te ñi muy ilif, dafa leen di nëbb li baax pur ñoom. Doomu Aadama yi soxlawuñu Yàlla ilif leen. Mën nañu waxal seen bopp li baax ak li bon. Su ma nekkee seen njiit, ci la seen dund di gën a neex. ’ Naka la Yàlla naroon a tontu fen yu ñaaw yooyu ñu wax ci moom ? Am na ñu xalaat ne Yàlla dafa waroon a rey rekk ñi ko weddi woon. Waaye ndax loolu dina indi tont ci li ko Seytaane jiiñ ? Ndax loolu dina wone ne fasoŋ bi Yàlla di jiitee dafa baax ?

9 Fasoŋ bi Yexowa di gise lu jub mayu ko woon mu rey ci saa si ñi ko doon weddi noonu. Yàlla daldi fas yéenee jël jot bu doy ngir tontu Seytaane tont bu leer ci li mu ko weddi, te wone ne Ibliis fenkat la. Moo tax Yàlla jàpp ne dina may nit ñi jot ngir ñu ilif seen bopp te nekk ci loxo Seytaane. Lu tax Yexowa def loolu ? Lu tax mu bàyyi mbir mi yàgge noonu ? Dinañu tontu ci laaj yooyu ci pàcc 11 ci téere bii. Waaye, dañu war a xalaat ci lii : Ndax Aadama ak Awa waroon nañu gëm Seytaane mii nga xam ne, masu leen woon a defal dara lu baax ? Ndax waroon nañu gëm ne Yexowa fenkat bu soxor la, moom mii leen joxoon lépp li ñu amoon ? Boo nekkoon seen palaas loo naroon a def ?

10. Naka nga mën a farale Yexowa ci li ko Seytaane weddi ?

10 Laaj yooyu jar na xalaat, ndaxte tey, ku nekk ci ñun dinga nekk ci loo xam ne dinga war a laaj sa bopp laaj yu mel noonu. Waaw, mën nga wone ne Yexowa nga faral, te booy def loolu dangay may Yexowa lu muy tontu Seytaane ci li Seytaane weddi Yexowa. Mën nga nangu Yexowa nekk sa Kilifa te bokk ci ñiy wone ne Seytaane fenkat la (Psaume 73:28 ; Proverbes 27:11). Waaye, ci milyaari nit yi nekk ci àddina si, tuuti nit kese ñoo nangu def loolu. Loolu dafay indi beneen laaj bu am solo : Ndax dëgg-dëgg Biibël bi wax na ne Seytaane mooy jiite àddina sii ?

KAN MOOY JIITE ÀDDINA SII ?

Naka la Seytaane di mënee may Yeesu réewi àddina si sépp bu leen moomul woon ?

11, 12. a) Fiir bi Seytaane teg ci kanamu Yeesu, naka lay wonee ne Seytaane mooy jiite àddina si ? b) Lan moo ñuy won itam ne Seytaane mooy jiite àddina sii ?

11 Yeesu masul a weddi ne Seytaane mooy jiite àddina sii. Ci benn kéemaan bi mu defoon, Seytaane mas na won Yeesu “ réewi àddina yépp ak seeni ndam ”. Mu daldi dig Yeesu lii : «Lii lépp dinaa la ko may, boo sukkee màggal ma.» (Macë 4:​8, 9 ; Luug 4:​5, 6). Xalaatal tuuti. Ndax li Seytaane wax Yeesu naroon na nekk fiir ci Yeesu su fekkee ne du Seytaane moo doon jiite réewi àddina si ? Yeesu weddiwul ne Seytaane moo moom réewi àddina si sépp. Bu Seytaane jiitewul woon réew yooyu, Yeesu dina ko wax .

12 Dëgg la, Yexowa mooy Yàlla Aji Kàttan ji. Moom moo sàkk asamaan ak suuf (Peeñu ma 4:11). Waaye nag, amul fenn ci Biibël bi fu ñu ne Yexowa Yàlla walla Yeesu Kirist ñooy jiite àddina sii. Rax-ci-dolli Yeesu wone na ne Seytaane mooy kiy “ jiite àddina si ”. (Yowaana 12:31 ; 14:30 ; 16:11.) Biibël bi woowe na sax Seytaane mi nekk Ibliis “ yàllay jamono ji ”. (2 Korent 4:​3, 4.) Lii la ndaw li Yowaana bind ci lu jëm ci noon boobu, maanaam Seytaane : “ Àddina sépp a ngi tëdd ci loxoy Ibliis. ” — 1 Yowaana 5:⁠19.

ÀDDINA SI SEYTAANE JIITE, NI ÑU KOY DINDEE

13. Lu tax ñu soxla àddina su bees ?

13 At mu nekk, àddina si dafay gën a bon. Yu mel nii moo fees àddina si tey : geer, waa politig yu njublaŋ, kilifa diine yuy mbubboo diine ak reykatu nit yu soxor. Àddina si tey, kenn mënu ko defar ba mu baax. Biibël bi wone na ne léegi Yàlla alag àddina su bon sii, ci xare bu ñuy woowe Armagedon. Ginnaaw loolu, àddina su bees te jub mooy am. — Peeñu ma 16:​14-16.

14. Kan la Yàlla tànn ngir mu nekk Njiitu Nguuram, te loolu naka lañu ko yéglee woon bala muy am ?

14 Yexowa dafa tànn Yeesu Kirist ngir mu nekk Njiitu Nguuram bi nekk ca kaw asamaan. Biibël bi waxoon na bu yàgg lii : “ Doom juddul na nu, mayees na nu doom ju góor, te dina yor nguur gi; dees na ko tudde: [...] Buuru jàmm. Nguuram dina gën a law, te jàmmam sax ba fàww. ” (Esayi 9:​5, 6). Yeesu jàngaloon na taalibeem yi ñu ñaan lu jëm ci Nguur googu. Dafa leen ne : “Na sa nguur ñëw, na sa coobare am ci suuf mel ni ci kaw.” (Macë 6:10). Ni ko pàcc 8 ci téere bii di wone, Nguuru Yàlla dina dindi nguuru àddina si sépp, ba pare moom ci boppam dina jël seen palaas (Dañeel 2:44). Su boobaa, Nguuru Yàlla dina indi àjjana ci kaw suuf.

ÀDDINA SU BEES SOREETUL !

15. Lan mooy “ suuf su bees ” si ?

15 Biibël bi nee na : “ Ñu ngi séentu asamaan su bees ak suuf su bees, fa njub dëkk, ci ni ko Yàlla dige. ” (2 Piyeer 3:13 ; Isaïe 65:17). Yenn saay, nit ñi nekk ci kaw suuf si, Biibël bi dafa leen di woowe “ suuf si ”. (Njàlbéen ga 11:​1, NW.) Kon boog “ suuf su bees, fa njub dëkk ” mooy mbooloo nit ñi nekk ci kaw suuf si te neex Yàlla.

16. Lu rey lan la Yàlla di may ñi ko neex, te lan lañu war a def ngir am loolu ?

16 Yeesu digoon na ne nit ñi neex Yàlla, dinañu leen may “ dund gu dul jeex ”. (Màrk 10:30.) Ubbil sa Biibël ci Yowaana 3:16 ak ci 17:​3, te nanga jàng li Yeesu wax ne loolu lañu war a def ngir am dund gu dul jeex. Léegi nag seetal ci Biibël bi barke yi Yàlla di indil ñi yelloo maye bu rafet boobu bés bu Àjjana ci kaw suuf amee.

17, 18. Lan moo tax ba mu wóor ñu ne jàmm ak salaam dina am ci kaw suuf si sépp ?

17 Soxor, xeex, reyante, ak fitna dinañu fi jóge. “ Ku soxor du nekkati [...] Waaye ñi woyof ñooy moom réew mi [suuf si, NW]. ” (Sabóor 37:​10, 11). Jàmm dina am ndaxte Yàlla dina “ giifal xare, ba ci cati àddina, ” maanaam ci àddina si sépp (Sabóor 46:10 ; Esayi 2:⁠4). Bu boobaa ñi jub dinañu bare “ te jàmm dina ne gàññ, ba kera weer wi di fi jóg ”, maanaam ba abadan ! — Sabóor 72:⁠7.

18 Jaamukatu Yexowa yi dinañu am jàmm. Ci jamono Biibël bi, bi waa Israyil doon déggal Yàlla, dañu doon am jàmm (Lévitique 25:​18, 19). Am jàmm bu mel noonu ci biir Àjjana, dina neex lool ! — Isaïe 32:18 ; Mika 4:⁠4.

19. Lan moo ñuy won ne lekk dina bare ci àddina su bees si Yàlla di indi ?

19 Lekk dootul mànke. Sabóor nee na : Pepp dina “ baawaan ci réew mi, wuti cati tund yi ”. (Sabóor 72:16.) Yexowa dina barkeel nit ñu jub ñi, te “ ci lu wóor suuf si dina meññ ni mu ware ”. — Sabóor 67:​6, NW.

20. Lu tax mu mën ñu wóor ne suuf si sépp dina nekk àjjana ?

20 Suuf si sépp dina nekk àjjana. Kër yu bees yu rafet ak ay tool yu naat dinañu nekk ci béréb yu yàqu woon ndax ay bàkkaarkat (Isaïe 65:​21-24 ; Peeñu ma 11:18). Bu yàggee, béréb yi ñu defar ba ñu rafet dinañu law, ba suuf si sépp nekk tool bu rafet buy meññ bu baax ni tollu Eden. Te saa yu ñu ko soxlaa, Yàlla dina “ ubbi loxoom te lépp luy dund, dina ko may lu mu bëgg ”. — Sabóor 145:​16, NW.

21. Lan moo ñuy wone ne jàmm dina am diggante nit ak rabu àll yi ?

21 Jàmm dina am diggante nit ñi ak rabu àll yi. Rabu àll yi ak mala yi nekk ci kër yi dinañu lekkandoo ci benn palaas. Xale bu ndaw sax du amati li muy ragal ci rabu àll yu soxor yi fi nekk tey. — Esayi 11:​6-9 ; Isaïe 65:⁠25.

22. Ndax feebar dina mas a jeex ?

22 Feebar dootul am. Bés bu Yeesu nekkee buuru Nguuru Yàlla bi nekk ca asamaan, dina faj nit ñi ci fasoŋ bu gën a yaatu li mu defoon ba mu nekkee ci kaw suuf si (Macë 9:35 ; Mark 1:​40-42 ; Yowaana 5:​5-9). Su boobaa “ kenn ci dëkk bi du ne : ‘ Dama feebar. ’ ” — Esayi 33:24, NW ; 35:​5, 6.

23. Lu tax ndekkite li di ñu indil mbégte ?

23 Suñu mbokk yi gaañu dinañu dundaat te mën a bañ a deewati. Ñi dee ñépp te nekk ci xelu Yàlla dinañu dekki. Liy am sax mooy «ñi jub ak ñi jubadi dinañu dekki». — Jëf ya 24:15 ; Yowaana 5:​28, 29.

24. Mën a dund ci Àjjana ci kaw suuf, lan lay def ci sa xol ?

24 Ñiy tànn a jàng ngir xam te jaamu Yexowa Yàlla suñu Sàkk-kat bu Mag bi, dinañu am ëllëg bu neex lool ! Àjjana jiy ñëw ci kaw suuf si la Yeesu doon wax bi mu ne woon nit ku bon ki doon waaj a dee ci wetam : “ Dinga nekk ak man ci Àjjana ji. ” (Luug 23:​43, NW). Jàng ngir gën a xam Yeesu Kirist, moom mii di tax barke yooyu yépp mën a am, lu am a am solo la.