Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

PÀCC ÑEENT

Kan mooy Yeesu Kirist ?

Kan mooy Yeesu Kirist ?
  • Lan mooy taxawaayu Yeesu ?

  • Fan la Yeesu nekkoon bala muy ñëw ci kaw suuf ?

  • Ban jikko la Yeesu amoon ?

1, 2. a) Lu tax xam lu jëm ci nit ku siiw taxul ñu wax ne xam nga ko dëgg ? b)  Yan wax yu wuute lañuy wax ci Yeesu ?

NIT ñi siiw ci àddina si bare nañu lool. Am na ñu siiw ci seen mbooloo, fi ñu dëkk, walla it ci seen réew. Am na ñu siiw ci àddina si sépp. Waaye, xam turu nit ku siiw taxul nga xam ko dëgg. Xam turam taxul nga xam lu bare ci cosaanam ak jikkoom.

2 Bi Yeesu Kirist nekkee ci kaw suuf si, mat na léegi lu war a tollu ak 2000 at. Waaye terewul niti àddina si sépp a mas a dégg lu jëm ci moom. Waaye ba tey, ñu bare mënuñu wax kan moo nekkoon Yeesu dëgg. Am na ñuy wax ne nit ku baax kese la woon. Ñeneen ñi ne yonent rekk la woon. Am na ñeneen ñu gëm ne Yeesu Yàlla la te dañu ko war a jaamu. Ndax loolu dëgg la ?

3. Lu tax nga war a xam dëgg gi jëm ci Yeesu ?

3 War nga xam dëgg gi jëm ci Yeesu. Lu am a am solo la. Lu tax ? Ndaxte Biibël bi nee na : «Dund gu dul jeex gi nag, mooy ñu xam la, yaw jenn Yàlla ju wóor ji am, te ñu xam it ki nga yónni, muy Yeesu Kirist.» (Ñun ñoo dëngal mbind yi ; Yowaana 17:⁠3). Waaw, xam dëgg gi jëm ci Yexowa Yàlla ak it dëgg gi jëm ci Yeesu Kirist mën na ñu may dund gu dul jeex ci àjjana ci kaw suuf (Yowaana 14:⁠6). Rax-ci-dolli, Yeesu nekk na royukaay bi gën ci ni ñu war a dunde ak ni ñu war a jàppe suñu moroom (Yowaana 13:34, 35). Ci pàcc bi njëkk ci téere bii, waxtaan nañu ci dëgg gi jëm ci Yàlla. Kon léegi, nañu seet li Biibël bi wax dëgg-dëgg ci lu jëm ci Yeesu Kirist.

ALMASI BI YÀLLA DIGE WOON

4. Lan la “ Almasi ” ak “ Kirist ” tekki ?

4 Lu yàgg bala Yeesu di juddu, Biibël bi waxoon na ne dina am ku fi Yàlla di yónni ngir mu nekk Almasi bi, maanaam Kirist. Baat yii : “ Almasi ” (te mu sukkandiku ci làkku yawut yi) ak it “ Kirist ” (ci làkku gereg) dañuy tekki “ Ki ñu tànn ”. Kooku Yàlla dige woon dafa waroon a nekk ku ñu tànn, maanaam ku Yàlla tànn ngir may ko taxawaay bu am solo. Ci téere bii, dina am yeneen pàcc yuy gën a wax ci taxawaay bu am solo bi Almasi bi am ci li Yàlla di def ba li mu dige am. Dinañu jàng itam lu jëm ci barke yi ñu Yeesu mën a indil tey jii. Waaye bala Yeesu di juddu, wóor na ne ñu bare ñu ngi doon laaj seen bopp : ‘ Kan mooy nar a nekk Almasi bi ? ’

5. Taalibe Yeesu yi, lan moo leen wóoroon ci lu jëm ci Yeesu ?

5 Am na léegi lu ëpp 2 000 at, ñi nekkoon taalibe Yeesu bu Nasaret, dafa leen wóoroon ne Yeesu mooy Almasi bi ñu doon wax ne dina ñëw (Yowaana 1:41). Simoŋ Piyeer, kenn ci taalibe Yeesu yi, waxoon na sax Yeesu lii : «Yaa di Almasi bi.» (Macë 16:16). Taalibe yooyu, lan moo mënoon a tax mu wóor leen ne Yeesu mooy Almasi bi Yàlla dige woon ? Ñun ci suñu bopp, lan moo mën a tax ba loolu wóor ñu ?

6. Waxal benn misaal buy wone naka la Yexowa dimbalee ñi takku ci Moom ñu mën a ràññee Almasi bi.

6 Bala Yeesu ñëw ci kaw suuf, yonent Yàlla yi waxoon nañu lu bare ci Almasi bi. Loolu naroon na dimbali nit ñi ñu mën a ràññee Almasi bi bés bu ñëwee. Nii lañu ko mën a misaale : Bu ñu la waxoon nga jëli benn nit boo masul a gis, ci béréb bu mel ni gaaraas, walla gaar walla ayropoor, bu ñu la tegtalee ni mu mel, ndax du gën a yomb ci yaw ? Noonu it, Yexowa jaar na ci ay yonent ngir ñu bind ci Biibël bi lu bare ci lu Almasi bi war a def ak li koy dal. Lépp li ñu waxoon noonu, bés bu amee, dina dimbali ñi takku ci Yàlla ñu mën a ràññee Almasi bi bu baax.

7. Waxal ñaar ci li ay yonent Yàlla wax te ñu gis ko ci Yeesu.

7 Nañu jël ñaar ci li yonent yooyu waxoon. Bu njëkk bi mooy, lu ëpp 700 at bala muy am, yonent Yàlla Mika waxoon na ne ki Yàlla dige woon, dina juddu ci dëkk bu tudd Betleyem ca réewu Yuda (Mika 5:⁠2). Fan la Yeesu juddoo ? Ci dëkku Betleyem boobu (Macë 2:​1, 3-9) ! Ñaareel bi mooy : Ay téeméeri at bala muy am, Dañeel 9:25 wone na kañ la Almasi bi waroon a feeñ, maanaam ci atum 29 ci suñu jamono *. Loolu yépp amoon ci Yeesu te ñu gis ko, boole ci yeneen yégle yonent, dafay wone ne Yeesu moo doon Almasi bi Yàlla dige woon.

Bi ñu sóobee Yeesu, ci la nekke Almasi bi, maanaam Kirist.

8, 9. Bi ñu doon sóob Yeesu, lan moo wone ci lu leer ne moom moo doon Almasi bi ?

8 Leneen lu wone ne Yeesu moo nekkoon Almasi bi, dafa gën a leer ci mujju atum 29 ci suñu jamono. Ci at moomu la Yeesu dem ci Yaxya mi doon sóob nit ñi ci ndox, ngir mu sóob ko ci dex bi tudd Yurdan. Yexowa dafa waxoon Yaxya ne dina ko won lu koy tax a ràññee Almasi bi. Loolu Yaxya gis na ko bi mu doon sóob Yeesu. Lii la Biibël bi wax : “ Bi ko Yaxya sóobee ca dex ga, Yeesu génn. Ca saa sa asamaan yi daldi ubbiku, te Yaxya gis Xelum Yàlla wàcc ci melow pitax, ñëw ci kaw Yeesu. Te baat bu jóge asamaan dégtu ne : «Kii mooy sama doom ji ma bëgg ; ci moom laa ame bànneex.» ” (Macë 3:​16, 17). Bi mu gisee te dégg loolu, wóoroon na Yaxya ne Yàlla moo yónni Yeesu (Yowaana 1:​32-34). Noonu it bi xelum Yàlla, maanaam doole bi muy jëfe, wàccee ci kaw Yeesu, ci la Yeesu nekke Almasi bi, maanaam Kirist, ki Yàlla tànn ngir mu nekk Njiit ak Buur. — Esayi 55:⁠4.

9 Lépp li Biibël bi waxoon ci Yeesu te mu am, ak li Yexowa ci boppam seede, mooy wone ci lu leer ne Yeesu mooy Almasi bi Yàlla dige woon. Waaye am na yeneen ñaari laaj yu am solo yu jëm ci Yeesu Kirist, yu Biibël bi tontu : Fan la Yeesu nekkoon bala muy ñëw ci kaw suuf te ban jikko la amoon ?

FAN LA YEESU NEKKOON BALA MUY ÑËW CI KAW SUUF ?

10. Lan la Biibël bi wax ci dund bi Yeesu amoon bala muy ñëw ci kaw suuf ?

10 Biibël bi wax na ne Yeesu ca kaw asamaan la nekkoon bala muy ñëw ci kaw suuf si. Yonent Yàlla Mika waxoon na ne Betleyem la Almasi bi di juddu. Dafa ci teg it ne dañu ko sàkk “ ca jamono yu njëkk ya ”. (Mika 5:​2, NW.) Ay yoon yu bare Yeesu ci boppam nee woon na ne ci kaw asamaan la nekkoon bala muy juddu ci kaw suuf nekk nit mel ni doomu Aadama yi (Yowaana 3:13 ; 6:​38, 62 ; 17:​4, 5). Bi Yeesu nekkee ca kaw asamaan, diggante bi mu amoon ak Yexowa, amu ko woon ak keneen.

11. Naka la Biibël bi di wonee ne Yeesu mooy doom ji Yexowa gën a fonk ci doomam yi ?

11 Yeesu mooy doom ji Yexowa gën a fonk, te am na lu ko waral. Dañuy woowe Yeesu “ taaw bi, ki gën a màgg lépp luy mbindeef ”, ndaxte moom la Yàlla njëkk a sàkk * (Kolos 1:15). Am na leneen itam lu tax Yexowa fonk lool doomam jooju. Moom mooy benn ‘ Doom ji mu am kepp ’. (Yowaana 3:16.) Loolu dafa tekki ne Yeesu kese la Yàlla sàkk fekk jaarul ci keneen. Ginnaaw bi mu ko sàkkee, leneen lépp li Yàlla sàkk, ci Yeesu kese la ko Yàlla jaarale (Kolos 1:16). Te it dañuy woowe Yeesu “ Kàddu gi ” (Yowaana 1:14). Loolu dafa ñuy won ne ci turu Yàlla la doon waxe. Wóor na ne dafa doon jottali yégle ak tegtal yi Baayam bëggoon a xamal yeneen doomam yi, malaaka yi ak doomu Aadama yi.

12. Naka lañu xame ne Yàlla ak taawam yemuñu ?

12 Ndax taawu Yàlla bi ak Yàlla ñoo yem, ni ko ñenn ñi gëme ? Du loolu la Biibël bi wax. Ni ñu ko gise ci xise bii jiitu, doom ji dañu ko sàkk. Kon boog am na fu mu komaasee dund. Waaye Yexowa Yàlla moom, dundam amul fu mu komaasee te amul fu muy jeexe (Psaume 90:⁠2). Doom jooju Yàlla am képp masul sax xalaat a yem ak Baayam. Biibël bi wax na ci fasoŋ bu leer ne Baay bi moo gën a màgg doom ji (Yowaana 14:28 ; 1 Korent 11:⁠3). Yexowa kese mooy “ Yàlla Aji Man ji ”. (Njàlbéen ga 17:⁠1.) Looloo tax amul moroom *.

13. Lan la Biibël bi bëgg a wax buy wax ne Doom ji “ moo di melokaanu Yàlla ” ?

13 Yexowa ak taawam dañu doon ànd ànd bu jege ay milyaari at, lu yàgg bala Yàlla sàkk biddéew yi ci asamaan si ak it suuf si. Kon bëggante woon nañu lool (Yowaana 3:35 ; 14:31) ! Doom jooju Baayam bëggoon lool dafa niru woon Baayam. Looloo tax Biibël bi wax ne Doom ji “ moo di melokaanu Yàlla ”. (Kolos 1:15.) Waaw, ni doom mënee niru baayam ci fànn yu bare, noonu it la doom jooju ca asamaan amoon jikko Baayam.

14. Naka la doom ji Yexowa am képp mënoon a juddu ni doomu Aadama ?

14 Doom ji Yexowa am képp dafa nangu bàyyi asamaan fi mu nekkoon, wàcc fii ci suuf ngir dund ni doomu Aadama. Waaye mën na am ngay laaj sa bopp lii : ‘ Naka la Yeesu mi nekkoon ca asamaan mënoon a juddu ni doomu Aadama ? ’ Yexowa dafa def kéemaan ngir loolu mën a am. Dafa jël bakkanu taawam bi nekkoon ca asamaan, toxal ko ci biiru benn janq bu nekkoon yawut. Kooku Maryaama la tuddoon. Kenn ci doomu Aadama yi nekkul baayu xale boobu. Maryaama jur doom bu góor bu amul benn bàkkaar, ñu tudde ko Yeesu. — Luug 1:​30-35.

BAN JIKKO LA YEESU AMOON ?

15. Lu tax ñu mën a wax ne bu ñu xamee Yeesu dina tax ñu gën a xam Yexowa ?

15 Li Yeesu wax ak li mu def bi mu nekkee ci kaw suuf moo ñuy dimbali ñu mën koo xam bu baax. Rax-ci-dolli, bu ñu xamee Yeesu dina tax ñu gën a xam Yexowa. Lu tax loolu ? Fàttalikul ne doom jooju moo di melokaanu Baayam ci lépp. Looloo tax Yeesu waxoon benn taalibeem : «Ku ma gis, gis nga Baay bi.» (Yowaana 14:⁠9). Ñeenti téere yi nekk ci Biibël bi, te ñu leen di woowe Injiil, maanaam téere Macë, Màrk, Luug, ak Yowaana, wax nañu lu bare ci dundu Yeesu Kirist, li mu doon def, ak jikkoom.

16. Lan la Yeesu doon gën a yégle, te fan la doon jële li muy jàngale ?

16 Yeesu, ci taxawaayu “ Jàngalekat ” lañu ko xame woon bu baax (Yowaana 1:​38, ; 13:​13, NW). Lan la doon jàngale ? Li mu doon gën a yégle moo doon “ xebaar bu baax bi ci nguuru Yàlla ”. Nguur googu mooy nguur gi nekk ca asamaan te nar a ilif suuf si sépp te indil ñiy déggal Yàlla ay barke yu dul jeex (Macë 4:23). Xebaar boobu, ci kan la ko jële woon ? Yeesu ci boppam nee na : «Li may jàngale, jógewul ci man, waaye ci ki ma yónni la jóge.» (Yowaana 7:16). Yeesu xamoon na ne Baayam dafa bëgg nit ñépp dégg xebaar bu baax bi jëm ci Nguur gi. Bu ñu àggee ci pàcc 8, dinañu gën a jàng lu jëm ci Nguuru Yàlla ak ci li muy def.

17. Fan la Yeesu doon jàngalee te lu tax mu doon def lépp ngir jàngal nit ñi ?

17 Fan la Yeesu doon jàngalee ? Fépp fu mu doon fekk ay nit : ci àll bi, ci dëkk yu mag ak yu ndaw yi, ci marse yi ak ci biir kër yi. Yeesu daawul xaar nit ñi fekksi ko. Dafa leen doon fekki fi ñu nekk (Màrk 6:56 ; Luug 19:​5, 6). Lu tax Yeesu doon def loolu lépp, te jël jot bu bare noonu ngir waaraate te jàngale ? Ndaxte loolu la Yàlla bëggoon mu def. Saa su nekk Yeesu dafa doon def li neex Baayam (Yowaana 8:​28, 29). Waaye am na leneen lu taxoon mu doon waaraate. Dafa yërëmoon nit ñi doon ñëw ci moom (Macë 9:​35, 36). Seeni kilifa diine yi leen waroon a jàngal dëgg gi jëm ci Yàlla ak ci li mu bëgg, daawuñu leen a toppatoo. Yeesu xamoon na ne mbooloo yooyu soxla woon nañu dégg xebaaru Nguur gi.

18. Yan jikko Yeesu ñoo la gën a neex ?

18 Yeesu, nit ku baax la woon te bare yërmande. Nit ñi gisoon nañu ne ku neex a jege la. Xale yi sax rusuñu ko woon (Màrk 10:​13-16). Yeesu daawul woon gënale. Dafa siboon njublaŋ ak lu dul yoon (Macë 21:​12, 13). Ci jamono yooyu, mayuñu woon jigéen ñi cér te jigéen amul woon sañ-sañ bu bare. Waaye Yeesu moom dafa leen mayoon cér (Yowaana 4:​9, 27). Yeesu ku woyof dëgg la woon. Benn bés, dafa raxas tànki taalibeem yi, fekk jaam yi ñoo daan def loolu.

Yeesu dafa doon waaraate fépp fu mu doon fekk nit.

19. Lan moo ñuy won ne Yeesu dafa doon bàyyi xel ci li nit ñi soxla ?

19 Yeesu dafa doon bàyyi xel ci li nit ñi soxla. Loolu, dafa gën a feeñ ci bi mu doon def ay kéemaan ci kàttanu Yàlla ngir faj nit ñi (Macë 14:14). Seetal li xewoon benn bés : Benn waay bu gaana dafa ñëwoon ba ci Yeesu ne ko : «Soo ko bëggee, man nga maa wéral.» Yeesu dafa yëg ci biir xolam metit ak naqar bi waa jooju amoon. Mu yërëm ko, daldi tàllal loxoom, laal ko, te ne ko : «Bëgg naa ko, wéral.» Waa ji feebaroon daldi wér (Màrk 1:​40-42). Ndax mën nga xalaat rekk li waa jooju yëg ci biir xolam ?

DÉGGAL NA YÀLLA BA KEROOG MUY DEE

20, 21. Naka la Yeesu nekke royukaay bu rafet ci lu jëm ci déggal Yàlla bu baax ?

20 Yeesu mooy royukaay bi gën ci lu jëm ci déggal Yàlla bu baax. Jaar na ci lu nekk. Xeex nañu ko ci fasoŋ bu nekk. Jaar na it ci metit bu mu mënta doon. Waaye dafa kontine di déggal Baayam bi nekk ca asamaan. Dafa xeex Seytaane ba masul daanu ci benn fiiram (Macë 4:​1-11). Am na jamono joo xam ne, ay mbokkam sax gëmuñu ko woon. Amoon na ci sax ñu doon wax ne «dafa tàggoo ak sagoom». (Màrk 3:21.) Waaye Yeesu bàyyiwul loolu def ci moom dara. Dafa kontine di def bu baax liggéey bi ko Yàlla joxoon. Bi ñu ko doon saaga te di ko toroxal sax, Yeesu dafa doon kontine di ànd ak sagoom. Masul a jéem a feyyu sax. — 1 Piyeer 2:21-23.

21 Yeesu dafa kontine di déggal Yàlla ba keroog muy dee, dee bu ñaaw te metti lool ci loxo noonam yi (Filib 2:⁠8). Seetal li mu daj rekk ci bés bi mu doon waaj a jeexal dundam ci kaw suuf. Soldaar yi dañu ko jàpp, ay nit seede ay fen ci moom, àttekat yu ñu feyoon wax ne moo tooñ, nit ñi di ko toroxal, ba pare ay soldaar gaañ ko gaañ yu metti. Bi muy waaj a dee ci bant bi ñu ko daaj, lii la Yeesu yuuxu : «Lépp mat na !» (Yowaana 19:30). Waaye, bi mu deewee ba mu mat ñetti fan, Baayam bi nekk ca asamaan, dafa ko dekkal, delloo ko mu dundaat ci xel ca asamaan (1 Piyeer 3:18). Ci semen yu néew ginnaaw loolu, Yeesu delluwaat na ca asamaan. Foofu dafa “ toog ca ndeyjooru Yàlla  ” di xaar ñu jox ko sañ-sañu buur. — Yawut ya 10:​12, 13.

22. Li Yeesu kontine di déggal Yàlla ba keroog muy dee, lan la indil doomu Aadama yi ?

22 Li Yeesu kontine di déggal Yàlla ba keroog muy dee, lan la indil doomu Aadama yi ? Deewu Yeesu dafa ñuy may ñu mën a am dund gu dul jeex ci àjjana ci kaw suuf, ni ko Yexowa bëgge woon ba muy sàkk suuf si. Naka la deewu Yeesu mënee def loolu ? Dinañu ci waxtaan ci pàcc bii di topp.

^ par. 7 Boo bëggee xam li yonent Yàlla Dañeel yégle woon te mu am ci Yeesu, seetal xaaj bi tudd “ Li ñu yokk ci waxtaan yi nekk ci téere bii ”, ci xët 197 ba 199.

^ par. 11 Dañuy woowe Yexowa Baay ndaxte moom mooy Sàkk-kat bi (Isaïe 64:⁠8). Komka Yàlla moo sàkk Yeesu, dañu koy woowe doomu Yàlla. Ndegam moom moo sàkk itam ñeneen ñi nekk ak moom ca asamaan, ñoom it dañu leen di woowe ay doomu Yàlla. Looloo tax it ñuy woowe Aadama doomu Yàlla. — Job 1:6 ; Luug 3:⁠38.

^ par. 12 Boo bëggee am leneen lu lay gën a won ne taaw bi ak Yàlla yemuñu, seetal xaaj bi tudd “ Li ñu yokk ci waxtaan yi nekk ci téere bii ”, xët 201 ba 204.