Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

PÀCC JUROOM-ÑETT

Lan mooy Nguuru Yàlla ?

Lan mooy Nguuru Yàlla ?
  • Lan la ñu Biibël bi wax ci Nguuru Yàlla ?

  • Lan la Nguuru Yàlla di def ëllëg ?

  • Kañ la Nguuru Yàlla di def ba coobare Yàlla am ci suuf ?

1. Ban ñaan bu siiw lool lañuy gëstu léegi ?

AY MILYOŊI nit ci àddina si, xam nañu bu baax ñaan bi ñuy woowe Suñu Baay bi, walla Ñaanu Sang bi. Ñaari tur yooyu lañu jox ñaan bi Yeesu ci boppam defoon ngir ñu roy ci. Wax yi nekk ci ñaan boobu dañu am solo lool. Te bu ñu seetee li ñetti kàddu yi fa Yeesu njëkk wax di tekki, dinañu gën a xam li Biibël bi wax dëgg-dëgg.

2. Am na ñetti mbir yu Yeesu waxoon taalibeem yi ñu boole ko ci seen ñaan. Yan mbir la ?

2 Ci ñaan boobu, lii la Yeesu njëkk a wax ñi ko doon déglu : «Yéen nag nii ngeen war a ñaane : “Suñu Baay bi nekk ci kaw, na sa tur sell, na sa nguur ñëw, na sa coobare am ci suuf mel ni ci kaw.”» (Macë 6:​9-13). Ñetti kàddu yooyu lu ñuy tekki ?

3. Lan lañu soxla xam ci Nguuru Yàlla ?

3 Jàng nañu lu bare ci turu Yàlla, maanaam Yexowa. Waxtaan nañu it ci coobare Yàlla, maanaam li mu def ba pare ak li mu bëgg a defal doomu Aadama yi ëllëg. Waaye, lan la Yeesu bëggoon a wax bi mu nee ñu boole kàddu bii ci suñu ñaan : “Na sa nguur ñëw” ? Lan mooy Nguuru Yàlla ? Naka la ñëwu nguur googu di sellale turu Yàlla ? Te ñëwu Nguur googu, lu mu bokk ak ni coobare Yàlla di ame ?

LAN MOOY NGUURU YÀLLA ?

4. Lan mooy Nguuru Yàlla, te kan mooy Buur bi ?

4 Nguuru Yàlla, nguur gu Yexowa Yàlla taxawal la, te moom ci boppam mooy tànn Buur bi koy jiite. Kan mooy Buuru Nguur googu ? Yeesu Kirist la. Yeesu mooy Buur bi gën a mag buur yépp. Dañu koy woowe “ Buuru buur yi ak Kilifag kilifa yi ”. (1 Timote 6:15.) Yeesu am na kàttanu def lu gën a baax fuuf lu bépp kilifa ci doomu Aadama yi mën a def, bu dee sax kilifa bu gën ci kilifa yi la.

5. Nguuru Yàlla, fan lay nekk di jiite, te lan lay ilif ?

5 Nguuru Yàlla, fan lay nekk di jiite ? Fan la Yeesu nekk ? Fàttalikul ne jàngoon nañu ne dañu daaj Yeesu ci bant, rey ko, ba pare Yàlla dekkal ko. Ñu teg ci tuuti, Yeesu daldi dem ca kaw asamaan (Jëf ya 2:33). Kon ca kaw asamaan la Nguuru Yàlla nekk. Looloo tax Biibël bi wax ne ‘ nguur gu kawe ’ la (2 Timote 4:18). Bu dee sax Nguuru Yàlla ca asamaan la nekk, dina ilif suuf si. — Peeñu ma 11:⁠15.

6, 7. Lu tax ñu mën a wax ne Yeesu Buur bu doy kéemaan la ?

6 Lu tax ñu mën a wax ne Yeesu Buur bu doy kéemaan la ? Lenn li ko waral mooy : du dee mukk. Ngir wone fi ko yeneen doomu Aadama yi nekk njiit yem, Biibël bi dafa ne “ moom kenn a jagoo dund gu sax, dëkk ci biir leer gu kenn mënta jege ”. (1 Timote 6:16.) Loolu dafay tekki ne, lu baax lépp lu Yeesu di def dina sax ba fàww. Te xam nañu ne dina def jëf yu réy te baax lool.

7 Seetal li Biibël bi wax ci Yeesu : “ Xelum Aji Sax ji dina dëkk ci moom, di xelum sago ak ràññee, xelum nas ak mën, xelum xam Yàlla ak ragal ko. Ragal Yàlla lay noyyee, ba du àtte ci kaw li bët gis, te du dogal ci kaw li nopp dégg; waaye di àtte ñi néew doole ci yoon, di làyyil ñi woyof ak dëgg. ” (Esayi 11:​2-4). Kàddu yooyu dafa ñuy won ne Yeesu, buy ilif suuf si sépp, dina nekk Buur bu jub te bare yërmande. Ndax bëgguloo am njiit bu mel noonu ?

8. Ñan ñooy nekk buur ak Yeesu ?

8 Leneen lu ñu war a xam ci Nguuru Yàlla mooy lii : Yeesu du nekk moom kenn di jiite. Dina am ñeneen ñuy nekk buur ak moom. Mën nañu ko seet ci li ndaw li Pool waxoon Timote. Dafa ko ne woon : “ Su nu takkoo, dinanu nguuru ak moom. ” (2 Timote 2:12). Waaw, Pool, Timote ak ñeneen ñu Yàlla tànn, dinañu nekk buur ak Yeesu ci Nguur gi nekk ci kaw asamaan. Ñaata nit ñooy am cér boobu ?

9. Ñaata nit ñooy nguuru ak Yeesu, te kañ la leen Yàlla komaasee tànn ?

9 i ñu ko waxe ci pàcc 7, ndaw li Yowaana gisoon na ci peeñu “ Mbote ma [Yeesu Kirist] taxaw ci tundu Siyon [taxawaayu Buur bi mu am ca asamaan], ànd ak téeméer ak ñeent-fukk ak ñeenti junniy nit, te ñu bind ci seen jë turu Mbote ma ak turu Baayam ”. Ñan ñooy 144 000 nit ñooñu ? Yowaana ci boppam nee na : “ Ñu nga topp Mbote ma fépp fu mu jëm. Yàlla jot na leen ci biir nit ñi, ñu jébbalu ci Yàlla ak ci Mbote mi, mel ni tànneefu ngóob mi ñuy sédde Yàlla. ” (Peeñu ma 14:​1, 4). Waaw, ñooñu ay taalibe yu gëm Yeesu dëgg lañu, te dañu leen tànn ngir ñu nekk ay buur ak Yeesu ca asamaan. Bu ñu leen dekkalee ngir dund ca asamaan, dinañu “ nguuru ”, maanaam ilif suuf si ci wetu Yeesu (Peeñu ma 5:10). Jamono ndawu Yeesu yi ba tey, Yàlla mu ngi tànn ay karceen yu koy topp bu baax ngir matal 144 000 nit ñooñu.

10. Lu tax ñu mën a wax ne Yàlla dafa won nit ñi mbëggeelam bi mu tànnee Yeesu ak 144 000 nit ngir ñu jiite doomu Aadama yi ?

10 Li Yàlla tànn Yeesu ak 144 000 yi ngir ñu jiite doomu Aadama yi, dafay wone ne dafa fonk nit dëgg. Lu tax ? Yeesu masoon na nekk nit, kon xam na bu baax lu ci nekk, xam na it lan mooy metit. Pool waxoon na ne Yeesu, “ du ku mënul a bokk ak nun sunuy naqar ; moom sax far jaar na ci nattu ni nun ci bépp fànn, waaye deful bàkkaar ”. (Yawut ya 4:15 ; 5:⁠8). Ñiy jiite ak moom it, bi ñu doon dund ci kaw suuf jaar nañu ci coono te xam nañu luy muñ. Rax-ci-dolli, jéem nañu xeex seen matadi te daj nañu it fasoŋu feebar bu nekk. Wóor na ne dinañu mën a xam jafe-jafe yi doomu Aadama yi di jànkoonteel !

LAN LA NGUURU YÀLLA DI DEF ?

11. Lu tax Yeesu waxoon ne taalibeem yi dañu war a ñaan ngir coobare Yàlla am ci kaw ?

11 Bi Yeesu waxee taalibeem yi ne dañu war a ñaan ngir Nguuru Yàlla ñëw, dafa leen waxoon it ne dañu war a ñaan ngir coobare Yàlla am «ci suuf mel ni ci kaw». Yàlla, ca kaw la nekk, maanaam ca asamaan te foofu, malaaka yu koy jaamu, dañu mas a def coobareem. Waaye jàng nañu ci pàcc 3 ne am na malaaka bu soxor bu bàyyi def coobare Yàlla, te xiir Aadama ak Awa ci bàkkaar. Pàcc 10 dina ñu won leneen li Biibël bi wax ci malaaka bu soxor boobu ñuy woowe Seytaane miy Ibliis. Seytaane ak malaaka yi ko topp — te ñu leen di woowe jinne walla rab — dafa am jamono bi ñu leen bàyyi woon ñu nekk ca asamaan. Kon nag booba, du ñépp ñi nekkoon asamaan ñoo doon def coobare Yàlla. Loolu dafa waroon a soppi bés bu Nguuru Yàlla di komaase jiite. Buur bu bees bi, maanaam Yeesu Kirist dafa waroon a xeex ak Seytaane. — Peeñu ma 12:​7-9.

12. Yan ñaari xew-xew yu am solo lañu wax ci Peeñu ma 12:10 ?

12 Lii di topp dafay wone li Biibël bi wax ngir yégle li waroon a am. Dafa ne : “ Noonu ma dégg baat bu xumb jóge asamaan naan : «Léegi mucc agsi na, moom ak kàttan ak nguuru Yàlla suñu Boroom, ak sañ-sañu Almaseem, ndaxte ki daan tuumaal suñuy bokk, di leen sosal guddi ak bëccëg ci kanam Yàlla suñu Boroom, kooka daaneel nañu ko.» ” (Peeñu ma 12:10). Ndax gis nga ñaari xew-xew yu am solo yi ñu wax ci aaya boobu ? Bu njëkk bi mooy, Nguuru Yàlla bi nekk ci loxo Yeesu Kirist komaase na jiite. Ñaareel bi mooy, dàq nañu Seytaane, mu jóge ca asamaan daanu ci kaw suuf.

13. Lan moo am ca asamaan ginnaaw bi ñu fa dàqee Seytaane ?

13 Ñaari xew-xew yooyu lu ñu indi ? Lii lañuy jàng ci li xewoon ca asamaan : «Looloo tax, na asamaan ak ñi ci dëkk bànneexu !» (Peeñu ma 12:12). Waaw, malaaka yi déggal Yàlla bég nañu, ndaxte Seytaane ak malaakaam yu bon yi nekkatuñu fa. Képp ku nekk ci asamaan dafay topp bu baax Yexowa Yàlla. Jàmm ak déggoo bu mat sëkk bu kenn mënul a dindi moo am ca asamaan. Fi mu tollu nii, coobare Yàlla lañuy def ca asamaan.

Bi ñu dàqee Seytaane ak malaakaam yu bon yi ba ñu jóge asamaan, ay musiba am ci kaw suuf. Musiba yooyu léegi ñu jeex.

14. Bi ñu wàccee Seytaane ci kaw suuf, lan moo xew ?

14 Lan lañu mën a wax lu jëm ci suuf si nag ? Biibël bi nee na : «Musiba ci kaw suuf ak ci biir géej ! Ndaxte Seytaane wàcc na ci yéen, ànd ak mer mu tàng, ndaxte xam na ne, jot gi ko dese barewul.» (Peeñu ma 12:12). Seytaane dafa mer ndax li ñu ko dàq mu jóge asamaan, te jot gi ko dese barewul. Ci mer moomu mu nekke, mu ngi indi ay naqar maanaam ay “ musiba ” ci kaw suuf. Dinañu gën a wax ci “ musiba ” yooyu ci pàcc bii di topp. Waaye mën na am ñu laajte lii : Kon naka la Nguuru Yàlla di fexee ba coobare Yàlla am ci kaw suuf ?

15. Lu tax Yàlla sàkk suuf si ?

15 Fàttalikul li taxoon Yàlla sàkk suuf. Jàngoon nga ko ci pàcc 3. Ca tollu Eden ba, Yàlla wone woon na ne dafa bëgg suuf si nekk àjjana bu fees ak nit ñu jub ñu dul dee mukk. Waaye Seytaane tax na ba Aadama ak Awa bàkkaar. Loolu am na lu mu def ci waxtu bi coobare Yàlla war a am ci kaw suuf. Waaye li Yàlla bëggoon ci kaw suuf soppeekuwul. Yexowa dafa bëgg ba tey “ ñu jub ñi moom suuf si te dëkk ci ba fàww ”. (Sabóor 37:​29, NW). Te Nguuru Yàlla dina def loolu. Naka la koy defe ?

16, 17. Lan la ñu Dañeel 2:44 di xamal ci Nguuru Yàlla ?

16 Seetal li Yàlla wax ci Dañeel 2:44. Lii lañu fa jàng : “Ci jamonoy buur yooyu Yàllay asamaan yi dina feeñal nguur gu dul tas mukk, te nguur googu du jaar ci kilifteefu menn mbooloo. Dina jàllarbi ak a tasaare nguur yeneen yépp, waaye moom doŋŋ dina sax ba fàww.” Loolu lu mu ñuy xamal ci Nguuru Yàlla ?

17 Lu mu ñuy njëkk xamal mooy, dinañu taxawal Nguuru Yàlla “ ci jamonoy buur yooyu ”, maanaam bi yeneen nguur yooyu di nekk ci kaw suuf. Ñaareel bi mooy, dafa ñuy xamal ne Nguuru Yàlla dina sax ba fàww. Du am nguur bu koy daaneel walla buy jël palaasam. Ñetteel bi mooy, gis nañu ne dina am xeex diggante Nguuru Yàlla ak nguuri àddina sii. Nguuru Yàlla dina leen daan, ba pare moom kese mooy ilif doomu Aadama yépp. Kiliftéef boobu mooy nekk kiliftéef bi gën ci kiliftéef yi doomu Aadama yi mas a gis yépp.

18. Nan lañuy woowee xeex biy mujj a am diggante Nguuru Yàlla ak nguuri àddina sii ?

18 Biibël bi wax na lu bare ci xeex biy mujj a am diggante Nguuru Yàlla ak nguuri àddina sii. Wax na ne, bu mujju jamano di gën a jege, rabi Seytaane yi dinañu tasaare ay fen ngir nax “ buuri àddina sépp ”. Lu tax ñuy def loolu ? Ngir “ dajale [buuri àddina si], ngir xeex biy am ci bés bu mag, bi Yàlla Aji Kàttan jagleele boppam ”. Buuri àddina si dinañu dajaloo “ ci bérab bu tudd ci làkku yawut Armagedon ”. (Peeñu ma 16:​14, 16.) Kon ñaari aaya yooyu ñu ngi wone ne xeex bu mujj biy am diggante Nguuru Yàlla ak nguuri àddina si, dañu koy woowe xeexu Armagedon.

19, 20. Lu tere coobare Yàlla am tey ci suuf si ?

19 Lan la Nguuru Yàlla di def jaare ko ci xeexu Armagedon ? Xalaatal li Yàlla bëggoon bi muy sàkk suuf si. Yàlla dafa bëggoon ay nit ñu mat te jub feesal suuf si, te di ko jaamu ci biir Àjjana. Lu tax loolu amul tey ? Li njëkk a waral loolu mooy, ay bàkkaarkat lañu, te dañuy feebar, di dee it. Waaye jàng nañu ci pàcc 5 ne Yeesu dafa dee ngir ñun, ngir ñu mën a dund ba fàww. Wóor na ne yaa ngi fàttaliku li ñu bind ci téere Yowaana maanaam : “ Yàlla dafa bëgg àddina, ba joxe jenn Doomam ji mu am kepp, ngir képp ku ko gëm am dund gu dul jeex te doo sànku mukk. ” — Yowaana 3:⁠16.

20 Leneen li ko tere am mooy, nit ñu bare dañuy def lu bon. Dañuy fen, di sàcc te dëkk ci njaaloo. Bëgguñu def li Yàlla bëgg. Yàlla dina alag nit ñuy def lu bon, ci xeexam bi tudd Armagedon (Sabóor 37:10). Leneen luy tax coobare Yàlla amul ci kaw suuf mooy, nguuri doomu Aadama yi duñu xiir nit ñi ci def li Yàlla bëgg. Nguur yu bare dañu néew doole, soxor walla njublaŋ. Biibël bi wax na ci lu leer ne “ doomu Aadama dafay ilif moroomam te loolu dafay indi musiba ”. — Dajalekat 8:​9, NW.

21. Lan la Nguuru Yàlla di def ba coobare Yàlla am ci kaw suuf ?

21 Bu Armagedon weesoo, benn nguur kese, maanaam Nguuru Yàlla, mooy ilif doomu Aadama yi. Nguur googu dina def li Yàlla bëgg te indi ay barke yu neex lool. Dina fi jële Seytaane ak malaakaam yu bon yi (Peeñu ma 20:​1-3). Dinañu jëfandikoo saraxu Yeesu, ba képp ku topp Yàlla ni mu ware dootul feebar, te dootul dee. Su Nguuru Yàlla di jiite, nit ñi dinañu mën a dund ba fàww (Peeñu ma 22:​1-3). Dinañu defar suuf si ba mu nekk àjjana. Noonu, Nguuru Yàlla dina tax ba coobare Yàlla am ci kaw suuf, te dina sellal turu Yàlla. Lan la loolu di tekki ? Loolu dafay tekki ne, bu Nguuru Yàlla di jiite, képp kuy dund dina màggal turu Yàlla, Yexowa.

KAÑ LA NGUURU YÀLLA DI DEF BA COOBARE YÀLLA AM CI KAW SUUF ?

22. Naka lañu xame ne Nguuru Yàlla ñëwul bi Yeesu nekkee ci kaw suuf, walla ci jamono bi mu yéegee ca kaw asamaan ?

22 Bi Yeesu waxee taalibeem yi ñu wax ci seen ñaan «na sa nguur ñëw», dafa doon wone ne ca jamono jooju ñu nekkoon, Nguuru Yàlla ñëwagul woon. Ndax Nguur gi ñëwoon na bi Yeesu yéegee ca asamaan ? Déedéet, ndaxte Piyeer ak Pool waxoon nañu ne, bi ñu dekkalee Yeesu la kàddu yi ñu waxoon ci Sabóor 110:​1, NW, ame ci moom. Lii lañu fa wax : “ Lii la Yexowa wax sama Kilifa : ‘ Toogal ci sama ndeyjoor ba keroog may def say noon ni sa tegukaayu tànk. ’ ” (Jëf ya 2:​32-35 ; Yawut ya 10:​12, 13). Kon dina am jamono boo xam ne Yeesu dina toog di xaar.

Bu Nguuru Yàlla di jiite, coobare Yàlla dina am ci suuf ni mu ame ca kaw.

23. (a) Kañ la Nguuru Yàlla komaasee jiite ? (b) Ci lan lañuy waxtaan ci pàcc bii di topp ?

23 Ñaata at la toog di xaar ? Ci at yi jiitu atum 1900 ak ci at yi ci topp, ay gëstukatu Biibël bi gisoon nañu ne jamono ji Yeesu waroon a toog di xaar dafa waroon a jeex ci atum 1914. (Seetal li ñu wax ci at moomu ci xaaj bi tudd “ Li ñu yokk ci waxtaan yi nekk ci téere bii ”, xët 215 ba 218.) Xew-xew yi komaase ci atum 1914 ci àddina si sépp, wone nañu ne li gëstukati Biibël yooyu gisoon mooy dëgg. Li Biibël bi yégle woon gis nañu ko. Loolu dafa wone ne, ci 1914 lañu fal Kirist ni Buur, te booba la Nguuru Yàlla komaasee jiite. Kon ñu ngi ci jot gu barewul gi dese Seytaane (Peeñu ma 12:12 ; Psaume 110:⁠2). Mën nañu wax it ne léegi Nguuru Yàlla def ba coobare Yàlla am ci kaw suuf. Te loolu, kàddu bu wóor la. Ndax xebaar boobu neexul a dégg ? Ndax gëm nga ne loolu dëgg la ? Pàcc bii di topp dina la won ne Biibël bi moo wax loolu dëgg-dëgg.