Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

PÀCC JURÓOM-ÑEENT

Ndax ñu ngi ci “ muju jamono ”?

Ndax ñu ngi ci “ muju jamono ”?
  • Lan lañuy gis tey te Biibël bi yégle woon ko bu yàgg ?

  • Lan la Kàddu Yàlla wax ci jikko nit ñi ci “ muju jamono ” ?

  • Lu rafet lan la Biibël bi waxoon ne dina am tey ci “ muju jamono ” ?

1. Fan lañu mën a xam lu war a am ëllëg ?

NDAX mas nga déglu xebaar yi ci tele ba laaj sa bopp lii : ‘ Fan la àddina sii di mujje ? ’ Ay musiba yu kenn foogul woon, ñooy jékki-jékki rekk dal ci kaw nit ñi. Loolu moo tax benn doomu Aadama mënul a wax luy am ëllëg (Saag 4:14). Waaye Yexowa moom xam na luy am ëllëg (Isaïe 46:10). Kàddu Yàlla maanaam Biibël bi, yégle woon na bu yàgg lu bon li fi am tey. Waaye yemul ci loolu rekk. Yégle na it lu neex lu war a am tuuti ci kanam.

2, 3. Lan la taalibe yi laaj Yeesu, te lan la leen tontu ?

2 Am na lu Yeesu Kirist waxoon ci Nguuru Yàlla. Waxoon na ne dafa war a dindi lu bon te defar suuf si mu nekk àjjana (Luug 4: 43). Ci jamono jooju, nit ñi bëggoon nañu xam kañ la Nguur gi war a ñëw. Taalibe Yeesu yi sax lii lañu ko laajoon : «Luy tegtale ne, yaa ngi ñëw te àddina di tukki ?» (Macë 24:⁠3). Yeesu tontu leen ne Yexowa kese moo xam bés bi ñu fiy dindi àddina su bon sii (Macë 24:36). Waaye Yeesu waxoon na leen li naroon a xew ci kaw suuf si bala Nguur gi di fi indi jàmm ak salaam. Li mu waxoon, moom lañuy gis tey !

3 Bala ñuy waxtaan ci liy wone ne ñu ngi ci “ muju jamono ”, nañu wax tuuti ci xeex bi nga xam ne benn doomu Aadama mënu ci woon a teg bët. Xeex boobu mu ngi amoon ca asamaan, te li ci mujj a am dina def dara ci ñun.

XEEX BU AMOON CA ASAMAAN

4, 5. a) Tuuti ginnaaw bi ñu falee Yeesu ni buur, lan moo xew ca asamaan ? b) Ni ñu ko waxe ci Peeñu ma 12:​12, xeex boobu am ca asamaan, lan la indi ?

4 Jàng nañu ci pàcc bi weesu ne, ci atum 1914 la Yàlla fal Yeesu ni buur ca kaw asamaan (Dañeel 7:​13, 14). Tuuti ginnaaw bi ñu ko defee buur, am na li Yeesu def. Biibël bi nee na : “ Noonu xare am ca asamaan ya. Mikayel [beneen turu Yeesu] ak malaaka, ya ànd ak moom, xeex ak ninkinànka ja [Seytaane miy Ibliis], ninkinànka ja it ak ay malaakam feyyu *. ” Seytaane ak ay malaakaam yu bon yi, maanaam rab yi, lañu daan. Ba pare ñu génne leen asamaan, wàcce leen ci kaw suuf. Malaaka yi doon déggal Yàlla daldi am mbégte bu réy ndax li ñu dàq Seytaane ak ay rabam. Waaye doomu Aadama yi amuñu woon mbégte bu mel noonu. Biibël bi nee na : «Musiba ci kaw suuf [...] Ndaxte Seytaane wàcc na ci yéen, ànd ak mer mu tàng, ndaxte xam na ne, jot gi ko dese barewul.» — Peeñu ma 12:​7, 9, 12.

5 Xeex boobu amoon ca asamaan, seetal léegi fi mu waroon a mujje. Ak xol bu tàng bi mu àndal, Seytaane naroon na indi musiba ci kaw suuf si. Dinga gis ci kanam ne ñu ngi ci jamono musiba yooyu. Waaye jamono ju gàtt lay doon. «Jot gi ko dese barewul», Seytaane ci boppam, xam na loolu. Biibël bi dafay woowe jamono jooju “ muju jamono ”. (2 Timote 3:⁠1.) Kontaan nañu lool ci li Yàlla di def ci kanam tuuti ba Ibliis du mën a dugal kenn ci dara ! Nañu wax léegi ci yenn yi Biibël bi waxoon te ñu koy gis tey. Yëf yooyu dañuy wone ne ñu ngi ci muju jamono, te léegi Nguuru Yàlla indil ñi bëgg Yexowa ay barke yu fiy sax ba fàww. Nañu njëkk a wax ci ñeent yu bokk ci li Yeesu waxoon ne dafa war a am tey ci suñu jamono.

XEW-XEW YU MAG YUY AM CI MUJU JAMONO

6, 7. Li Yeesu waxoon ci xare ak xiif, naka la ame tey ?

6 Xeet dina jóg, xeex ak weneen xeet, réew xeex ak meneen réew (Macë 24:⁠7). Ci 100 at yi weesu, rey nañu ay milyoŋi nit ci ay xare. Ca Ãgalteer, benn gëstukat ci wàllu xew-xewu démb lii la bind : “ Ci diiru 100 at, masuñu rey doomu Aadama yu bare ni li ñu rey diggante atum 1900 ba atum 2000. [...] Ci at yooyu yépp dafa mel ni xare masul arete ci kaw suuf. Jamono yu amul woon xare barewuñu te dañu gàttoon lool. ” Mbootaay bi tudd Worldwatch Institute bindoon na lii ci benn yégle : “ Bu ñu seetee li dee ci nit ci xare yi am diggante atum 1900 ba atum 2000, dina def ñetti yoon li dee ci diggante jamono Yeesu ba atum 1899. ” Lu ëpp 100 milyoŋi nit ñoo dee ci xare yi am diggante 1914 ba tey. Bu dee sax mas nañu yëg naqar bi nekk ci am benn mbokk bu gaañu ci xare, duñu mën a xam dëgg fu naqaru milyoŋi nit ñu seen mbokk gaañu ci xare mën a tollu.

7 Dina am ay xiif (Macë 24:⁠7). Gëstukat yi wax nañu ne dund bi dafa gën a bare ci 30 at yi weesu. Waaye loolu terewul xiif di am ba tey, ndaxte nit ñu bare amuñu xaalis bi ñuy jënde li ñuy lekk walla tool yu ñu mën a bey. Ci réew yi barewul xaalis, lu ëpp benn milyaari nit ñoo am 650 F CFA kese bés bu nekk walla lu ko gën a tuuti sax ngir dund. Li ëpp ci nit ñooñu, ci xiif lañu dëkk. Kurél bi ñuy woowe ci tubaab L’Organisation mondiale de la santé (Kurél biy toppatoo mbirum wér-gi-yaram ci àddina si sépp), wax na ne li ëpp ci juróomi milyoŋi xale yiy dee at bu nekk, xiif moo leen rey.

8, 9. Lan mooy wone ne li Yeesu waxoon ci yëngu-yëngu suuf ak feebar am na tey ?

8 Suuf dina yëngu yëngu yu réy (Luug 21:11). Kurél bi ñuy woowe U.S. Geological Survey, am na lu mu wax ci yëngu-yëngu suuf yi am diggante 1990 ba tey. Nee na, boo seetee li suuf si yëngu ci diggante boobu, dafa mel ni at mu nekk amoon na 17 yëngu-yëngu suuf yu am doole ba mën a yàq kër yi walla xar suuf si. Te it dafa mel ni at mu nekk amoon na yëngu-yëngu suuf yu am doole yàq kër ba dara du ci des. Am na ñeneen ñu wax ne : “ Ci 100 at yi weesu, yëngu-yëngu suuf si rey na ay téeméeri junniy nit. Lépp li boroom xam-xam yi defar, tuuti kese la wàññi ci li yëngu-yëngu suuf yi di rey ci doomu Aadama yi. ”

9 Wopp dina am (Luug 21:11). Ak li doktoor yi gën a mën seen liggéey yépp, tey, feebar yi, yu yàgg yi ak yu bees yi, sonal nañu lool doomu Aadama yi. Benn kurél bind na ne ci at yii weesu am na 20 feebar yu ñu yàgg a xam yuy gën di law, feebar yu mel ni sëqët bu metti (tuberculose ci tubaab), sibbiru ak koleera. Te am na ci yoo xam ne faj leen ak garab dafay gën di jafe rekk. Te 30 feebar yu bees walla lu ko ëpp ñoo feeñ. Ci feebar yooyu, am na ci yoo xam ne dañuy rey. Amul garab bu leen mën a faj.

JIKKO YI NIT ÑI DI AM CI MUJU JAMONO

10. Yan jikko yi ñu wax ci 2 Timote 3:​1-5 ngay gis tey ci nit ñi ?

10 Biibël bi yégle woon na xew-xew yi war a am ci àddina si. Waaye waxoon na it ne, ci muju jamono jikko nit ñi dina soppeeku. Ndaw li pool wone woon na ni li ëpp ci nit ñi naroon a mel. Lii la wax ci 2 Timote 3:1-5 : “ Bési tiis yu tar ñu ngi nuy tëru ci muju jamono. ” Pool waxoon na ne nit ñi

  • dinañu siis, maanaam seen bopp rekk lañuy xalaat,

  • dinañu fonk xaalis,

  • dinañu xëtt ndigalu waajur,

  • duñu am kóllëre,

  • ▪ duñu am cofeel,

  • ñu xér lañuy doon,

  • ñu soxor lañuy doon,

  • seen bànneex a leen gënal Yàlla,

  • dañuy mbubboo diine waaye nanguwuñu koo dugal seen xol.

11. Ni ko Sabóor 92:7 waxe, lan moo war a dal nit ñu bon ñi ?

11 Nit ñi nekk ci sa gox ndax noonu lañu mel ? Wóor na ne noonu lañu mel. Fépp foo dem am na nit ñu am jikko yu bon. Loolu dafay wone ne léegi Yàlla def dara, ndaxte Biibël bi nee na : “ Bu nit ñu bon ñi baree ni gàncax, te ñiy def lu bon di gën a yokku, dañu leen war a dindi ba fàww. ” — Sabóor 92:​7, NW.

LU RAFET LIY NAR A AM

12, 13. Naka la “ xam-xam dëgg ” baree ci “ muju jamono ” jii ?

12 Dëgg la musiba bare na ci muju jamono ni ko Biibël bi waxe woon. Waaye, ci àddina bu jaxasoo bii, am na lu rafet lu am ci biir ñiy jaamu Yexowa.

13 “ Xam-xam dëgg dina bare ”, ni ko Biibël bi waxe ci téere Dañeel. Kañ la loolu di am ? Ci “ muju jamono ”. (Dañeel 12:​4, NW.) Li ko dale 1914 ba tey, Yexowa gën na dimbali ñi ko bëgg jaamu dëgg ngir ñuy gën a nànd Biibël bi. Nit ñooñu gën nañu xam dëgg yu am solo yu jëm ci turu Yàlla ak coobareem, ci saraxu Yeesu Kirist bi nekk njot gi, ci luy dal nit bu deewee ak itam ci mbirum ndekkite bi. Li ci gën a am solo mooy, ñiy jaamu Yexowa jàng nañu ni ñu mënee am dund gu am njariñ te di màggal Yàlla it. Gën nañu nànd it li Nguuru Yàlla di def, te naka lay jubbantee li am ci kaw suuf si ba lépp baax. Lan lañuy def ak xam-xam boobu ñu am ? Laaj boobu dafay tax ñu wax ci leneen li Yàlla waxoon te muy am ci muju jamono jii.

“ Xebaar bu baax bii ci Nguuru Yàlla, dees na ko yégle ci àddina sépp. ” — Macë 24:14

14. Tey, ba fan lañu yégle xebaar bi jëm ci Nguur gi, te ñan ñoo koy def ?

14 “ Xebaar bu baax bii ci nguuru Yàlla, dees na ko yégle ci àddina sépp. ” Yeesu Kirist waxoon na ne loolu dina bokk ci luy am ci muju jamono (Macë 24:​3, 14). Xebaar bu baax bi jëm ci Nguuru Yàlla dafay leeral lan mooy Nguuru Yàlla, li mu nar a def, ak naka lañuy def ba am ci barke yi muy indi. Xebaar boobu, ñu ngi koy yégle ci àddina si sépp, ci lu ëpp 230 réew, ak ci lu ëpp 400 làkk. Ay milyoŋi seede Yexowa ñu ngi yégle xebaar bu baax bi jëm ci Nguur gi, sawar ci lool. Seede Yexowa yooyu, “ ci xeet yépp, giir yépp, réew yépp ak kàllaama yépp ” lañu jóge (Peeñu ma 7:⁠9). Am na ay milyoŋi nit ñu bëgg a xam li Biibël bi wax dëgg-dëgg. Nit ñooñu, seede Yexowa yi dañu leen di fekki seen kër ngir jàngal leen Biibël bi, te duñu fey dara. Loolu, Biibël bi waxoon na ko. Te fasoŋ bi mu ame, doy na waar lool, ndaxte Yeesu waxoon na ne karceen dëgg yi, “ ñépp dinañu leen bañ ” ! — Luug 21:⁠17.

LAN NGA NAR A DEF ?

15. a) Ndax gëm nga ne ñu ngi ci muju jamono, te lu tax nga gëm loolu ? b) “ Mujj gi ” lan lay tekki ci ñiy xeex Yexowa, ak ci ñiy nangu kiliftéefu Nguuru Yàlla ?

15 Komka lu bare ci li Biibël bi yégle woon mu ngiy am tey, ndax nangu nga ne ñu ngi ci muju jamono ? Bu ñu yéglee xebaar bu baax bi ba Yexowa gis ne doy na, su boobaa, ci lu wóor “ mujj gi ” dina jot (Macë 24:​14, NW). “ Mujj gi ” mooy bés bi Yexowa di dindi lu bon ci kaw suuf. Yexowa dina jaar ci Yeesu ak ay malaaka yu bare kàttan, ngir alag képp ki nga xam ne xeex Yàlla moo ko neex (2 Tesalonig 1:​6-9). Seytaane ak rabam yi dootuñu nax nit ñi. Ginnaaw loolu, Nguuru Yàlla dina indi barke yu bare ci ñi nangu kiliftéefam bu jub bi. — Peeñu ma 20:​1-3 ; 21:3-5.

16. Lan nga war a def te mu nekk xel dëgg ?

16 Àddina si Seytaane di jiite komka léegi mu jeex, war nañu laaj suñu bopp lii : ‘ Jamono jii, ci lan la ma war a fekk ? ’ Li gën mooy nga kontine di yokk li nga xam ci Yexowa ak ci li mu ñu sant. Def loolu, am xel dëgg la (Yowaana 17:⁠3). Nanga farlu ci njàngum Biibël bi. Deel faral di daje ak ñi bëgg a def li Yexowa bëgg (Yawut ya 10:​24, 25). Xam-xam bu bare bi Yexowa Yàlla jagleel waa àddina si sépp, defal lépp ba mën ci am. Te nanga soppi li nga war a soppi ci sa dund ndax nga mën a neex Yàlla. — Saag 4:⁠8.

17. Bés bi Yàlla di alag nit ñu bon ñi, lu tax muy bett lu ëpp ci nit ñi ?

17 Tey, leer na ne ñu ngi ci muju jamono. Waaye Yeesu waxoon na ne nit ñu bare duñu nangu loolu. Bés bi Yàlla di alag ñu bon ñi dina bett ñépp. Ni sàcc bu ñëw guddi, noonu lay bette lu ëpp ci nit ñi (1 Tesalonig 5:⁠2). Yeesu nee woon na : «Ni bési Nóoyin ya, noonu lay mel, bu Doomu nit ki di ñëw. Ndaxte ca bés ya jiitu mbënn ma, nit ñaa ngi doon lekk di naan, góor yaa ngi doon takk jabar, tey maye seeni doom, ba bés ba Nóoyin duggee ca gaal ga ; xalaatuñu woon dara, ba kera ndoxum mbënn ma di dikk, yóbbu leen. Noonu lay mel ci ñëwu Doomu nit ki.» — Macë 24:​37-39

18. Lan la Yeesu wax, te mu nekk lu ñu warul a caaxaane ?

18 Looloo tax Yeesu ne woon : «Moytuleen seen nafsu diigal leen ci yàqute ak màndite ak ittey àddina, ba bés boobu bett leen ni mbaal. Ndaxte dina dal ci ñépp ñi nekk ci kaw suuf. Yeewuleen, di sax ci ñaan, ngir ngeen man a mucc ci loolu lépp war a xew, te man a taxaw ak kóolute ci kanamu Doomu nit ki.» (Luug 21:​34-36). Bañ a caaxaane li Yeesu wax, am xel dëgg la. Lu tax ? Ndaxte nit ñi neex Yexowa Yàlla ak Yeesu Kirist «Doomu nit ki», dinañu mucc bu ñuy alag àddina sii Seytaane jiite. Te dinañu dund ba fàww ci àddina bu neex bi nga xam ne léegi mu ñëw ! — Yowaana 3:16 ; 2 Piyeer 3:⁠13.

^ par. 4 Boo bëggee xam lu tax ñuy wax ne Mikayel beneen turu Yeesu Kirist la, seetal li ñu wax ci xaaj bi tudd “ Li ñu yokk ci waxtaan yi nekk ci téere bii ”, xët 218 ba 219.