Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

PÀCC FUKK AK JURÓOM-ÑETT

Sóob bi ak sa diggante ak Yàlla

Sóob bi ak sa diggante ak Yàlla
  • Naka la karceen yi di sóobe nit ci ndox ?

  • Lan la nit war a def ngir ñu mën koo sóob ci ndox ?

  • Naka la nit di jébbale boppam Yàlla ?

  • Lu am solo lan mooy tax ñuy sóobu ci ndox ?

1. Lu tax jaraaf ju mag ji ci waa Ecópi bëggoon ñu sóob ko ci ndox ?

«NDOX a ngi nii, ana lu tere, nga sóob ma ci ?» Loolu la benn jaraaf ju mag ci réewu Ecópi laajoon ci jamono karceen yu njëkk yi. Karceen bu tudd Filib moo ko wonoon ne Yeesu mooy Almasi bi Yàlla digoon nit ñi. Li ko Filib won ci Mbind mi dafa ko laal ci biir xol. Moo tax mu wax ne dafa bëgg ñu sóob ko ci ndox mi. ​— Jëf ya 8:26-36.

2. Lu tax nga war a xalaat bu baax lu jëm ci sóob bi ?

2 Su dee jàng nga bu baax li ñu wax ci pàcc yi weesu ak benn seede Yexowa, xéyna pare nga léegi ngir wax lii : ‘ Ana lu tere, ñu sóob ma ? ’ Fi mu nekk nii, xam nga li ñu Biibël bi dig ci dund gu dul jeex ci Àjjana (Luug 23:43 ; Peeñu ma 21:​3, 4). Xam nga itam luy dëgg ci lu jëm ci luy dal nit bu deewee, xam it yaakaaru ndekkite bi ñu am (Ecclésiaste 9:5 ; Yowaana 5:​28, 29). Xéyna yaa ngi ànd ak Seede Yexowa yi di teew ci seeni ndaje yi. Te gisal nga sa bopp ni ñuy toppe diine dëgg ji (Yowaana 13:35). Lu gën a am solo mooy, xéyna komaase nga doon xaritu Yexowa Yàlla.

3. a) Lan la Yeesu sant ay taalibeem ? b) Naka lañuy sóobe nit ci ndox ?

3 Naka nga mënee wone ne danga bëgg a jaamu Yàlla ? Yeesu nee woon na taalibeem yi : «Demleen nag sàkk ay taalibe ci xeet yépp, sóob leen ci ndox.» (Ñun ñoo dëngal mbind yi ; Macë 28:19). Yeesu ci boppam wone na li ñu war a def, bi ñu ko sóobee ci ndox. Wisuñu woon ndox ci kawam, te it sottiwuñu tuuti ndox ci boppam kese (Macë 3:16). Baat bi ñuy woowe “ sóob bi ” ci làkku gereg dafay tekki “ li ñu dugal ci ndox ”. Looloo tax bu karceen yi di sóob nit dañuy dugal yaramam yépp ci biir ndox mi.

4. Lan la sóob ci ndox di wone ?

4 Képp ku bëgg a nekk xaritu Yexowa Yàlla, dafa war a sóobu ci ndox. Sóob bi dafay wone ci kanamu ñépp ne danga bëgg a jaamu Yàlla. Dafay won nit ñi ne def coobare Yàlla, li la neex la (Psaume 40:​7, 8). Waaye bala ñu lay mën a sóob ci ndox, am na li nga war a def.

WAR NAÑU AM XAM-XAM AK NGËM

5. a) Lan lañu war a njëkk a def ngir mën a sóobu ci ndox ? b) Lu tax ndaje karceen yi am solo ?

5 Komaase nga li ñu war a njëkk a def. Naka ? Ci li ngay jàng ngir xam Yexowa ak Yeesu Kirist. Ngir am xam-xam boobu, xéyna am na ku lay jàngal Biibël bi (Yowaana 17:⁠3). Waaye des na lu bare li nga mën a jàng. Karceen yi dañu bëgg ‘ xam bu baax coobare ’ Yàlla (Kolos 1:⁠9). Ànd ak Seede Yexowa yi di teewe seeni ndaje dina la ci dimbali bu baax. Teewe ndaje yu mel noonu am na solo lool (Yawut ya 10:​24, 25). Faral di teewe ndaje yi dina la dimbali ci yokk li nga xam ci Yàlla.

Lenn lu am solo li nit war a def ngir ñu mën koo sóob ci ndox mooy mu jàng dëgg gi nekk ci Kàddu Yàlla.

6. Sa xam-xam ci Biibël bi, naka la war a tollu ngir ñu mën laa sóob ci ndox ?

6 Dëgg la, soxlawul nga xam lépp li nekk ci Biibël bi ngir ñu mën laa sóob ci ndox. Jaraaf ju mag ji bokkoon ci waa Ecópi am na lu mu xamoon, waaye soxla woon na ku koy dimbali mu xam leneen lu Mbind mi wax (Jëf ya 8:​30, 31). Noonu it, dese nga xam lu bare. Ci dëgg, doo mas a pare jàng xam Yàlla (Ecclésiaste 3:11). Waaye bala ñu lay mën a sóob ci ndox, war nga xam te nangu li ñu warul a ñàkk a xam ci Biibël bi (Yawut ya 5:12). Lii bokk na ci : dëgg gi ci luy dal nit bu deewee, ak it ni turu Yàlla ak Nguuram ame solo.

7. Lan la jàng Biibël bi war a def ci yow ?

7 Waaye, xam-xam kese doyul, ndaxte “ ku amul ngëm doo man a neex Yàlla ”. (Yawut ya 11:6.) Biibël bi nee na, bi ay nit ca waa Korent bu njëkk déggee xebaar bi karceen yi doon yégle, dañu ko gëm, “ ñu sóob leen ci ndox ”. (Jëf ya 18:8.) Noonu it, jàng Biibël bi war na tax nga gëm ne Biibël bi mooy Kàddu Yàlla. Jàng Biibël bi war na la dimbali nga gëm li ñu Yàlla dig, gëm it ne li Yeesu saraxe boppam moo ñuy musal. ​— Josué 23:14 ; Jëf ya 4:12 ; 2 Timote 3:16, 17.

NAÑU WAX SUÑUY MOROOM DËGG GI NEKK CI BIIBËL BI

8. Lan mooy tax nga bëgg a wax say moroom li nga jàng ?

8 Bu sa ngëm di gën a fees ci sa xol, dafay gën a jafe ci yow nga noppi te bañ a wax say moroom li nga xam (Jérémie 20:9). Dinga sawar a wax say moroom lu jëm ci Yàlla ak ci coobareem. ​— 2 Korent 4:13.

Sa ngëm war na la puus ngay wax ak say moroom ci li nga gëm.

9, 10. a) Kan nga mën a njëkk wax ci dëgg gi nekk ci Biibël bi ? b) Lan nga war a def boo bëggee bokk ci liggéeyu waare bi Seede Yexowa yi di def ?

9 Mën nga komaasee wax ci dëgg gi nekk ci Biibël bi say mbokk, say xarit, say dëkkandoo ak it ñi nga bokkal liggéey. Waaye def ko ci yar ak teggin. Bu ci kanamee, dinga bëgg a ànd ak Seede Yexowa yi ci liggéeyu waare bi ñuy def. Bu ci ragal a waxtaan ak ki lay jàngal Biibël bi. Su fekkee ne mën nga bokk ci waaraate bi, dinañu wax ñaari njiiti mbooloo mi ñu ñëw waxtaan ak yow ak ki lay jàngal.

10 Loolu dina la may nga xam njiiti mbooloo mi, ñoom ñii di sàmm mbooloo Yàlla (Jëf ya 20:28 ; 1 Piyeer 5:​2, 3). Bu njiit yooyu gisee ne danga xam te gëm li ñu warul a ñàkk a xam ci Biibël bi, te yaa ngi def li Yàlla bëgg, te dëgg-dëgg, danga bëgg a nekk Seede Yexowa, bu boobaa, njiiti mbooloo mi dinañu la xamal ne mën nga bokk ci ñiy waare xebaar bu baax bi, ni waaraatekat bu ñu sóobagul.

11. Lan la ñenn ñi war a soppi ci seen dund bala ñuy mën a bokk ci liggéeyu waare bi ?

11 Te it, bala ngay mën a bokk ci waaraate bi, mën na am nga war a soppi dara ci fasoŋ bi ngay dunde ak yenn yi nga tàmm a def. Xéyna nga war a bàyyi yenn jëf yi ngay nëbb say moroom. Kon bala ngay wax ne bëgg nga nekk waaraatekat bu ñu sóobagul, danga war a bàyyi bàkkaar yu réy, mel ni njaaloo, naan sàngara ba màndi, ak jëfandikoo dorog. ​—Korent 6:​9, 10 ; Galasi 5:19-21.

TUUB SAY BÀKKAAR TE WOÑÑIKU

12. Lu tax nga war a tuub say bàkkaar ?

12 Am na leneen li nga war a def bala ñu lay mën a sóob ci ndox. Ndaw li Piyeer nee woon na : «Tuubleen seeni bàkkaar nag te woññiku ci Yàlla, ngir seeni bàkkaar far [“ deñ, ” NW]» (Jëf ya 3:19). Tuub say bàkkaar mooy nga réccu dëgg li nga def. Bu nit dëkkee ci lu bon, li gën ci moom mooy mu tuub ay bàkkaaram. Waaye nit ku dëkkul ci lu bon sax, war na tuub ay bàkkaaram. Lu tax ñu wax loolu ? Ndaxte doomu Aadama yépp ay bàkkaar, te soxla nañu Yàlla baal ñu suñuy bàkkaar (Room 3:23 ; 5:12). Bala ngay komaasee jàng Biibël bi, xamoo woon li Yàlla bëgg. Kon naka nga mënoon a def li Yàlla bëgg ? Looloo tax nga war a tuub say bàkkaar.

13. Lan mooy woññiku ?

13 Bu ñu tuubee suñuy bàkkaar, li ci war a topp mooy walbatiku maanaam “ woññiku ”. Waruloo yem rekk ci réccu say bàkkaar. War nga bàyyi ni nga doon dunde, te fas yéene def lu baax léegi. Bala ngay sóobu ci ndox danga war a tuub say bàkkaar te woññiku.

JÉBBAL SA BOPP YÀLLA

14. Lu am solo lan nga war a def bala ñu lay sóob ci ndox ?

14 Am na leneen lu am solo li nga war a def bala ñu lay sóob ci ndox. Danga war a jébbal sa bopp Yexowa Yàlla.

Ndax jébbal nga sa bopp Yàlla ci ñaan ?

15, 16. Jébbal sa bopp Yàlla lu muy tekki, te lan mooy tax nit bëgg a def loolu ?

15 Bi ngay jébbal sa bopp Yexowa Yàlla ci ñaan bu jóge ci sa xol, danga koy dig ne moom kese ngay jaamu ba fàww (Deutéronome 6:15). Lan mooy tax nit bëgg a dig loolu Yàlla ? Nañu ko seet ci lii : Bu benn góor di doxaan jigéen, ni muy gën di xam jigéen jooju, muy gën a gis jikko yu rafet yi nekk ci moom. Noonu it mu koy gën a bëgg a jege. Kon mën na dem ba ñaan ñu may ko ko ngir mu nekk jabaram. Dëgg la, tàkk jabar dafay yokk ay wareefam. Waaye mbëggeel dina tax mu def lu am solo loolu.

16 Boo demee ba xam Yexowa bu baax te fonk ko, loolu dafay tax nga bëgg koo jaamu te def ci lépp li nga mën, dem ci ba jeex. Képp ku bëgg a topp ay tànku Yeesu Kirist, Doomu Yàlla, dafa war a “ bàyyi boppam ”. (Màrk 8:34.) Nit ku def loolu du nangu bànneexam ak ay bëgg-bëggam tere koo def lépp li Yàlla bëgg. Kon bala ñu lay mën a sóob ci ndox, danga war a jiital coobare Yexowa Yàlla ci sa dund. ​— 1 Piyeer 4:2.

NDAX RAGAL NGA NE DOO KO MËN ?

17. Lu tax mu am ñu ragal a jébbal seen bopp Yàlla ?

17 Am na ñu jébbalul seen bopp Yexowa, ndaxte dañu ragal a def lu am solo loolu. Xéyna dañu ragal ne bu boobaa, dinañu war a lay ci kanamu Yàlla li ñuy def, ni karceen bu jébbal boppam Yàlla. Komka dañu ragal ne duñu ko mën te mën na am ñu def lu neexul Yàlla, dañuy xalaat ne li gën mooy ñu bañ koo jébbal seen bopp.

18. Lan moo mën a tax nga bëgg a jébbal sa bopp Yexowa ?

18 Booy gën a bëgg Yexowa, dinga ko bëgg a jébbal sa bopp te def li nga mën ngir dund ci fasoŋ bu ko neex (Ecclésiaste 5:4). Boo jébbalee sa bopp Yàlla ba pare, wóor na ne dinga bëgg a ‘ dund dund gu dëppoo ak sa bokk ci Boroom bi, ba neex ko ci fànn gu nekk ’. (Kolos 1:10.) Li nga bëgg Yàlla dina tax nga bañ a xalaat ne def coobareem dafa jafe lool. Wóor na ne dinga nangu li ndaw li Yowaana bindoon ne : “ Mbëggeel ci Yàlla mooy sàmm ay ndigalam ; te ay ndigalam diisuñu. ” ​— 1 Yowaana 5:3.

19. Lu tax waruloo ragal a jébbal sa bopp Yàlla ?

19 Jarul nga nekk nit ku mat ngir mën a jébbal sa bopp Yàlla. Yexowa xam na fu sa doole yem, te du la defloo mukk li nga mënul (Psaume 103:14). Li nga bëgg noonu, Yàlla dafa bëgg nga mën koo def te dina la ci jàpple (Isaïe 41:10). Na la wóor ne boo gëmee Yexowa ak sa xol bépp, “ dina def sa yoon jub ”. ​— Léeb yi 3:5, 6, NW.

BU ÑU LAY SÓOB CI NDOX, YAA NGI WONE NE JÉBBAL NGA SA BOPP YÀLLA

20. Lu tax nit mënul a denc pur moom kese li mu jébbal boppam Yexowa ?

20 Boo xalaatee ci li ñu waxtaan léegi, xéyna dina la dimbali nga jébbal sa bopp Yexowa ci ñaan. Waaye ku bëgg Yàlla dëgg, war nga ‘ wax [ci kanamu ñépp, NW] ’ sa ngëm ba ‘ tax Yàlla musal la ’. (Room 10:10.) Naka ngay defe loolu ?

Sóob ci ndox dafay tekki ne bàyyi nañu ni ñu doon dunde, mel ni ñu dee ci jëf yooyu te léegi dañuy dund ngir def coobare Yàlla.

21, 22. Naka nga mënee wax sa ngëm ci kanamu ñépp?

21 Waxal kiy jiite kurélu njiiti mbooloo mi nga nekk ne danga bëgg ñu sóob la ci ndox. Dina def ba ay njiitu mbooloo mi waxtaan ak yow ci ay laaj yuy jëm ci li ñu warul a ñàkk a xam ci Biibël bi. Su dee njiit yooyu nangu nañu ne mën nañu la sóob ci ndox, dinañu la wax ne mën nga bokk ci sóob biy ñëw *. Bu ñuy sóob ay nit, dañuy faral di def waxtaan bu ñuy fàttali li sóob bi di tekki. Ba pare kiy def waxtaan bi dina wax ñi bëgg ñu sóob leen ñu tontu ci ñaari laaj yu yomb. Loolu benn fasoŋ la bi ñuy waxe ci kanamu ñépp suñu ngëm.

22 Sóob bi mooy won ñépp ne jébbal nga sa bopp Yàlla. Li ko dale ci bés boobu, Seede Yexowa ngay doon. Bu ñuy sóob nit, dañuy dugal yaramam yépp ci biir ndox mi ngir wone ne jébbal na boppam Yexowa.

LI SA SÓOB CI NDOX DI TEKKI

23. Sóobu ci ndox «ci turu Baay bi ak Doom ji ak Xel mu sell mi» lu muy tekki ?

23 Yeesu nee woon na ñu sóob taalibeem yi «ci turu Baay bi ak Doom ji ak Xel mu Sell mi». (Macë 28:19.) Loolu dafay tekki ne ñi ñuy waaj a sóob, dañuy nangu kiliftéefu Yexowa Yàlla ak bu Yeesu Kirist (Psaume 83:18 ; Macë 28:18). Dañuy nangu it njariñu Xel mu sell mi ak li muy def, moom mii nekk doole ji Yàlla di jëfe. — Galasi 5:​22, 23 ; 2 Piyeer 1:21.

24, 25. a) Sóob ci ndox lu muy tekki ? b) Ban laaj lañu war a tontu ?

24 Waaye sóobu yemul rekk ci dugg ci ndox. Am na lu am solo lu muy wone. Sóob bi dafay tekki ne bàyyi nga ni nga doon dunde, mel ni ku dee ci jëf yooyu. Bi ñu la génnee ci ndox mi nag, loolu dafa tekki ne dangay dund léegi ngir def coobare Yàlla. Bul fàtte it ne Yexowa Yàlla ci boppam nga jébbal sa bopp. Jébbaluloo sa bopp benn liggéey. Jébbaluloo sa bopp benn gis-gis. Jébbaluloo sa bopp ay nit walla mbootaay. Bi nga jébbalee sa bopp Yàlla te sóobu ci ndox, ci nga komaasee nekk xaritam bu ko jege lool, maanaam sa diggante ak moom dafa rattax lool. ​— Psaume 25:14.

25 Sóob bi taxul nga mucc. Ndaw li Pool bindoon na ne : ‘ Biralleen seen mucc ci seeni jëf, te def ko ci ragal Yàlla gu dëggu. ’ (Filib 2:12). Sóobu ci ndox, ndoorte kese la. Li jar a laaj mooy, lu ñu mën a def ba sax ci mbëggeelu Yàlla ? Pàcc bu mujj bi dina ci tontu.

^ par. 21 Dañuy faral di sóob ay nit ci ndaje yu mag yi Seede Yexowa yi di def at mu nekk.