Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LI ÑU YOKK CI WAXTAAN YI NEKK CI TÉERE BII

Turu Yàlla : ni ñu koy jëfandikoo ak li muy tekki

Turu Yàlla : ni ñu koy jëfandikoo ak li muy tekki

CI BIIBËL bi nga yore, lan lañu bind ci Sabóor 83:18 ? Ci Biibël bi tudd Les Saintes Écritures — Traduction du monde nouveau, lii moo fa nekk : “ Ngir nit ñi xam ne yow mii tudd Yexowa, yow rekk yaay Aji Kawe ji ci kaw suuf si sépp. ” Am na ay Biibël yu ñu bind ci yeneen làkk yu wax loolu itam ci aaya boobu. Waaye am na ay Biibël yu ñu bind ci yeneen làkk yu dindi turu Yexowa, def ci leneen lu mel ni “ Boroom bi ” walla “ Ki Sax ba fàww ”. Lan lañu war a bind ci aaya boobu ? Turu Yàlla ci boppam, Yexowa, walla yeneen fasoŋ yi ñu koy woowe ?

Nii lañuy binde turu Yàlla ci ebrë.

Aaya boobu, ci tur lay wax. Ci làkku ebrë bu njëkk bi, benn turu Yàlla bi mu am kepp lañu bind ci aaya boobu (li ëpp ci Biibël bi, ci làkku ebrë bu njëkk bi lañu ko binde). Nii lañu ko doon binde ci ebrë : יהוה (YHWH). Ci wolof, dañu faral di bind : “ Yexowa ”. Ndax tur boobu ci benn aaya kese lay feeñ ? Déedéet. Ci Biibël bu njëkk bi, ci xaaj bi ñu bind ci làkku ebrë, dafay feeñ lu jege 7 000 yoon !

Naka la turu Yàlla ame solo ? Seetal ñaan bi Yeesu waxoon ngir mu nekk royukaay. Nii la komaasee : “ Suñu Baay bi nekk ci kaw, na sa tur sell. ” (Macë 6:⁠9). Ginnaaw loolu, Yeesu masoon na wax Yàlla ci ñaan nee ko : «Baay, màggalal sa tur !» Yàlla tontu ca kaw asamaan nee ko : «Màggal naa ko ba noppi, te dinaa ko màggalaat.» (Yowaana 12:28). Leer na ne turu Yàlla am na solo lool. Kon lu tax mu am ay Biibël ci yenn làkk fu ñu dindi turu Yàlla, def fa tiitar ?

Dafa mel ni ñaari gis-gis yi ñoo gën a tax loolu : Bu njëkk bi mooy, ñu bare dañu foog ne kenn mënul wax tur boobu, ndaxte kenn xamul tey ni ñu ko doon waxe dëgg bu njëkk ba. Làkku ebrë bu njëkk bi amul woon li ñuy woowe ci tubaab voyelle (lu mel ni a, e ,o). Looloo tax tey jii kenn mënul wax ci lu leer ni ñu doon waxe YHWH ca jamono Biibël bi. Waaye ndax loolu war na ñu teree jëfandikoo turu Yàlla ? Mën na am, ca jamono Biibël bi, Yeshua walla Yehoshua lañu doon waxe turu Yeesu. Kenn mënul wax ci lu wóor ni ñu ko doon waxe. Waaye tey ci àddina si, dañuy woowe Yeesu ci fasoŋ yu wuute. Nit ku nekk dafa koy woowe ci fasoŋ bi mu xam ci làkkam. Li ñu xamul ni ñu doon waxe turu Yeesu ca jamono taalibe Yeesu yu njëkk ya terewul kenn jëfandikoo turam. Noonu it, soo tukkee dem beneen réew, mën na am nga seetlu ne ni ñuy waxe sa tur ci beneen làkk dafa wuute. Kon boog, du li ñu xamul ni ñu doon waxe turu Yàlla moo ñuy teree jëfandikoo turam.

Leneen li ñu faral di wax ngir wone lu tax ñu bañ a bind turu Yàlla ci Biibël bi, mu ngi jóge ci aada bu yàgg lool ci yawut yi. Ñu bare ci ñoom dañu gëmoon ne kenn warul a jëfandikoo turu Yàlla. Xéyna loolu dañu ko jële ci dégg-dégg bu baaxul bi ñu am ci li Biibël bi wax ne : “ Bul tudd turu Yexowa sa Yàlla ci ay caaxaan, ndaxte Yexowa du seetaan mukk kuy caaxaane turam. ” — Gàddaay gi 20:​7, NW.

Sàrt boobu dafay tere kuy jëfandikoo turu Yàlla ci fasoŋ bu ñaaw. Waaye ndax sàrt boobu dafay tere kuy jëfandikoo turu Yàlla ci fasoŋ buy wone ne may na ko cér ? Déedéet. Ñi bind téere yi nekk ci xaaju Biibël bi ñu bind ci làkku ebrë (ñu koy woowe ci tubaab Ancien Testament), nit ñooñu ñépp a gëmoon Yàlla te doon topp sàrt yi Yàlla joxoon waa Israyil bu njëkk. Waaye dañu tàmmoon di jëfandikoo turu Yàlla. Mën nañu ko seet ci lii : bare na li ñu ko def ci Sabóor yi mbooloo yi doon woy ak baat bu kawe ngir jaamu Yàlla. Yexowa Yàlla waxoon na sax ñi koy jaamu ñu woo ko ci turam, te ñi koy topp def nañu ko (Yoël 2:32 ; Jëf ya 2:21). Moo tax tey karceen yi ragaluñu di jëfandikoo turu Yàlla ak teggin, ni ko Yeesu defe woon ci lu wóor. — Yowaana 17:⁠26.

Ñi dindi turu Yàlla ci Biibël bi ci yenn làkk ba pare def fa tiitar, juum nañu lool. Dañuy tax ñu foog ne Yàlla neexul a jege, fekk Biibël bi dafay xiirtal nit ñi ñu “ jege Yexowa ” (Sabóor 25:​14, NW). Xalaatal sa benn xarit bu la jege lool. Naka nga ko mënee jege dëgg boo xamul ni mu tudd ? Noonu it, bu ñu waxul nit ñi lu jëm ci turu Yàlla, naka lañuy mënee jege Yàlla ? Rax-ci-dolli bu fekkee ne nit ñi duñu jëfandikoo turu Yàlla, duñu xam it lu neex li tur boobu di tekki. Lan la turu Yàlla di tekki ?

Yàlla ci boppam moo xamal Musaa mi ko doon jaamu, li turam di tekki. Bi ko Musaa laajee lu jëm ci turam, Yexowa dafa ko tont ne : “ Dinaa doon ki may doon. ” (Gàddaay gi 3:​14, NW). Ci Biibël bi ci ãgale bi ñuy woowe Rotherham, lii la wax ci aaya boobu : “ Dinaa def sama bopp li ma neex. ” Kon Yexowa mën na def boppam lépp li war ngir coobareem am.

Boo mënoon doon li la neex, lan ngay nar a defal say xarit ? Bu ci amee ku feebar feebar bu metti, dinga def sa bopp doktoor bu aay te faj ko. Bu ci keneen amee poroblemu xaalis, dinga def sa bopp nit ku bare alal, ñëw dimbali ko. Waaye li am mooy, li nga mën a doon am na fi mu yem. Noonu la it ci ñépp. Booy jàng Biibël bi, dinga gis ni Yexowa di defe boppam lépp li war ngir def li mu dig nit ñi. Te jëfandikoo kàttanam ngir jàpple nit ñi ko bëgg, lu ko neex la (Chroniques 16:⁠9). Jikko yu rafet yooyu nekk ci Yexowa, ñi xamul turam duñu ko mën a gis.

Leer na ne dañu war a bind turu Yexowa ci Biibël bi. Xam li tur boobu di tekki te di ko faral di jëfandikoo bu ñuy jaamu Yàlla, loolu dina ñu dimbali bu baax ngir ñu gën a jege Yexowa suñu Baay bi nekk ca asamaan *.

^ par. 3 Boo bëggee yokk li nga xam ci turu Yàlla, li muy tekki ak li tax ñu war ko jëfandikoo bu ñuy jaamu Yàlla, seetal li nekk ci téere bi tudd “ Le nom divin qui demeure à jamais ”. Seede Yexowa yi ñoo defar téere boobu.