Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LI ÑU YOKK CI WAXTAAN YI NEKK CI TÉERE BII

Ni yonent Yàlla Dañeel yéglee ñëwu Almasi bi

Ni yonent Yàlla Dañeel yéglee ñëwu Almasi bi

YONENT Yàlla Dañeel mu ngi doon dund lu ëpp 500 at bala Yeesu di juddu. Waaye, Yexowa waxoon na ko liy tax ñu mën a xam jamono ju xel mu sell mi di wàcc ci Yeesu ngir def ko Almasi bi walla Kirist bi. Lii la Yàlla wax Dañeel : “ Fàww nga xam lii, te na sa xel ñaw : dale ko ci bés bi ñuy joxe ndigal ngir defaraat ak it tabaxaat Yerusalem ba ci jamono Almasi bi, Njiit bi, dina am juróom-ñaari semen, tegaat ci juróom-benn-fukk ak ñaari semen. ” — Dañeel 9:​25, NW.

Bu ñu bëggee xam kañ la Almasi bi di ñëw, dañu war a njëkk a xam kañ la jamono bi ñuy yóbbu ba ci Almasi bi di komaase. Ni ko Biibël bi waxe, dafay komaase “ ci bés bi ñuy joxe ndigal ngir defaraat ak it tabaxaat Yérusalem ”. Kañ lañu “ joxe ndigal  ” boobu ? Nëxemiya moom mi bokk ci ñi bind téere yi nekk ci Biibël bi, nee na ci “ ñaar-fukkeelu at bi Artaserse nekkee buur ” lañu joxe ndigalu tabaxaat miir yi wër Yerusalem (Nëxemiya 2:​1, 5-8, NW). Ñi bind ngir nettali li xewoon démb dëggal nañu ne atum 474 bala suñu jamano di tàmbali (B.S.J.T.) mooy at mi Artaserse njëkk a matal bi muy nekk buur. Kon boog, atum 455 B.S.J.T. moo war a doon ñaar-fukkeelu at mi mu nekke buur. Li Dañeel yégle woon ci Almasi bi, xam nañu léegi kañ la komaase. Ci atum 455 B.S.J.T. la komaase.

Dañeel waxoon na kañ la jamono biy jëme ca “ Almasi bi, Njiit bi ” war a jeex. Yonent Yàlla Dañeel nee woon na ne dina am “ juróom-ñaari semen, tegaat ci juróom-benn-fukk ak ñaari semen ”. Bu ñu boolee lépp dafay def 69 semen. Semen yooyu, ñaata la waroon a yàgg ? Lu bare ci Biibël yi am ci yeneen làkk, wone nañu ne semen yooyu du semen yuy def juróom ñaari fan, waaye ay semenu at la. Loolu dafay tekki ne semen bu nekk juróom-ñaari at lay def. Yawut yu njëkk yi tàmmoon nañu di xaaj at yi ci ay xaaj yuy def juróom-ñaari at walla semenu at. Moo tax juróom-ñaari at yu nekk, dañu doon màggal atum Sabbat (maanaam atum noflaay) (Gàddaay gi 23:​10, 11, NW). Kon boog, bu ñu jëlee 69 semen yi yonent Dañeel waxoon, dafay doon 69 xaaj yuy def bu ci nekk 7 at. Loolu yépp dafay tollu ak 483 at.

Léegi kalkil at yi rekk moo ci des. Bu ñu komaasee ci atum 455 B.S.J.T., te waññ 483 at, dañuy tombe ci atum 29 ci suñu jamano (C.S.J.). Ci at moomu ci boppam lañu sóob Yeesu, mu nekk Almasi bi * (Luug 3:​1, 2, 21, 22) ! Li Biibël bi wax noonu te lépp am ni mu ko waxe, ndax loolu jéggiwul dayo ?

^ par. 2 Am na 454 at diggante atum 455 B.S.J.T. ak atum 1 C.S.J. Diggante atum 1 B.S.J.T. ak atum 1 C.S.J., am na benn at (amul woon atum sero). Te diggante atum 1 C.S.J. ba atum 29 C.S.J., am na 28 at. Su ñu boolee ñetti xaaj yooyu, dafay def 483 at. Ci atum 33 C.S.J., ci 70eelu semenu at mi lañu “ fi jële ” Yeesu, rey ko (Dañeel 9:​24, 26, NW). Seetal li nekk ci téere bi tudd Prêtons attention à la prophétie de Daniel !, pàcc 11, ak li nekk ci téere Étude perspicace des Écritures, volume 2, xët 995 ba 997. Seede Yexowa yi ñoo defar ñaari téere yooyu.