Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LI ÑU YOKK CI WAXTAAN YI NEKK CI TÉERE BII

Dëgg gi ci lu jëm ci Baay bi, Doom ji, ak xel mu sell mi

Dëgg gi ci lu jëm ci Baay bi, Doom ji, ak xel mu sell mi

ÑI GËM li ñuy woowe ci tubaab Trinité, dañuy wax ne ñett ñoo booloo doon benn Yàlla : Baay bi, Doom ji, ak xel mu sell mi. Dañuy wax ne kenn ku ci nekk dafa tollu ak moroomam. Ñoom ñett ñoo bokk nekk Aji Kàttan ji, te kenn ci ñoom amul fu mu komaasee dund. Kon ñiy jàngale Trinité bi, dañuy wax ne Baay bi Yàlla la, Doom ji Yàlla la, xel mu sell mi it Yàlla la. Waaye ba tey, ci ñoom benn Yàlla rekk moo am.

Ñu bare ñu gëm Trinité bi, nangu nañu ne mënuñu ko jàngal kenn ba mu nànd li muy tekki. Waaye xéyna dañu foog ne Biibël moo wax loolu. Am na solo lool ñépp xam ne, amul fenn ci Biibël bi fi ñu bind “ Trinité ”. Waaye ndax wax nañu dara ci Biibël bi luy tax ñu xalaat ne ci Trinité bi lay bëgg a wax ? Bu ñu bëggee am tontu laaj boobu, nañu seet aaya bi nga xam ne ñiy jàngale Trinité bi moom lañuy jël ngir wone ne Trinité am na.

“ KÀDDU GI YÀLLA LA WOON ”

Lii lañuy jàng ci Yowaana 1:1 : “ Ca njàlbéen ga fekk na Kàddu gi am, te Kàddu gi ma nga woon ak Yàlla, te Kàddu gi Yàlla la woon. ” Ci pàcc boobu it, ndaw li Yowaana dafa ñu leeral ne Yeesu mooy “ Kàddu gi ”. (Yowaana 1:14.) Ndegam dañu wax ne Kàddu gi Yàlla la woon, looloo tax mu am ñiy wax ne Doom ji ak Baay bi dañu war a booloo nekk benn Yàlla.

Buleen fàtte ne xaaju Biibël boobu, ci làkku gereg lañu ko njëkk a bind. Ginnaaw boobu lañu ko mujj a bind ci yeneen làkk. Am na ay Biibël yi ñu bind ci yeneen làkk fu ñu bindul ne : “ Kàddu gi Yàlla la woon ”. Lu tax ? Xam-xam bi ñu amoon ci làkku gereg moo tax ñu wax ne waruñu bind foofu “ Kàddu gi Yàlla la woon ”. Kon lan lañu fa war a bind ? Am na ñu wax ne lii lañu fa war a bind : “ Logos [Kàddu gi] Yàlla la nirool. ” (A New Translation of the Bible). Ak “ Kàddu gi benn yàlla la woon ”. (The New Testament in an Improved Version.) Ak it “ Kàddu gi mu ngi woon ak Yàlla te dafa meloon ni Yàlla ”. (The Translator’s New Testament.) Ni ñu ko waxe ci sotti Biibël yooyu, Kàddu gi du Yàlla ci boppam *. Li mu nekk ku kawe lool ci mbindeef yi Yexowa sàkk, moo tax ñuy wax ne Kàddu gi “ benn yàlla la ”. Foofu, “ yàlla ” dafay tekki ku am “ kàttan ”.

NAÑU SEET YENEEN LEERAL

Ñu bare xamuñu làkku gereg bi ñu binde Biibël bi. Kon naka lañu mënee xam li ndaw li Yowaana bëggoon a wax dëgg ? Xalaatal ci lii : Benn jàngalekat dafay jàngal dara ay eleewam. Eleew yi nag déggoowuñu ci fasoŋ bi ñu waree nànd li leen jàngalekat bi wax. Naka la eleew yooyu war a def ba déggoo ? Mën nañu laaj jàngalekat bi mu gën leen a leeral li mu wax. Wóor na ne bu leen waxee yeneen leeral, dina leen dimbali ñu xam bu baax li mu leen jàngal. Noonu it, bu ñu bëggee xam li Yowaana 1:1 di tekki, dañu war a seet ci li Yowaana bind ci Injiil, ngir ñu gën a xam taxawaay bi Yeesu am. Boo yokkee li nga xam ci li ñu wax ci Yowaana 1:​1, loolu dina la dimbali nga xam luy dëgg gi.

Seetal li Yowaana bind ci pàcc 1, aaya 18 : “ Kenn masul a gis Yàlla [Aji Kàttan ji]. ” Waaye nit ñi gis nañu Yeesu, Doom ji, ndaxte Yowaana nee na : “ Kàddu gi [Yeesu] ñëw, doon nit, dëkk ci sunu biir. Gis nañu ndamam. ” (Yowaana 1:14). Kon, naka la Doom ji mënee nekk benn xaaju Yàlla Aji Kàttan ji ? Yowaana wax na itam ne Kàddu gi ma nga woon “ ak Yàlla ”. (Ñun ñoo dëngal mbind yi.) Waaye, naka la nit mënee ànd ak moroomam ba pare ñu bëgg wax ne mooy nit kooku ? Te it, ni ko Yowaana 17:3 waxe, Yeesu dafa wone ne moom ak Baayam bi nekk ca asamaan, ñaari nit ñu wuute lañu. Dafay woowe Baayam «jenn Yàlla ju wóor ji am». Bi muy jeexal li mu bind, nii la Yowaana tënke li mu doon wax : “ Li ci nekk, bind nañu ko ngir ngeen gëm ne, Yeesu mooy Almasi bi, Doomu Yàlla ji. ” (Yowaana 20:31). Gis ngeen ne waxuñu foofu ne Yeesu mooy Yàlla, waaye dañu wax ne Doomu Yàlla la. Li ñu gis ci li Yowaana bind ci Injiil, dafa ñuy won ni ñu waree nànd li ñu wax ci Yowaana 1:⁠1. Bi ñu waxee ne Yeesu, Kàddu gi, “ benn yàlla la ”, loolu dafay tekki ne taxawaay bu kawe la Yeesu am. Waaye loolu tekkiwul ne Yeesu mooy Yàlla Aji Kàttan ji.

NAÑU GËSTU LEERAL YI

Nañu delluwaat ci li ñu wax ci jàngalekat bi ak eleew yi. Bu eleew yi dégloo leeral yi leen jàngalekat bi wax, waaye ba tey am na ñu ci am xel ñaar. Lan la eleew yooyu war a def ? Dañu war a seeti beneen jàngalekat mu indil leen yeneen leeral ci loolu. Su dee beneen jàngalekat boobu dafa dëggal li keneen ki njëkk a wax, kon li leerul ci li ëpp ci eleew yi dafa war a deñ. Noonu it, su dee li Yowaana di wax dëgg-dëgg ci diggante Yeesu ak Yàlla Aji Kàttan ji doyu la, mën nga seet li keneen bind ci Biibël bi, mu gën laa leeral. Mën nga seet li Macë bind. Macë nee woon na ne, lii la Yeesu waxoon ci bés bu àddina sii di jeex : «Waaye bés booba walla waxtu wa, kenn xamul kañ lay doon ; du malaaka yi ci kaw, du sax man Doom ji, waaye Baay bi rekk moo ko xam.» (Macë 24:36). Naka la kàddu yooyu di seedee ne Yeesu nekkul Yàlla Aji Kàttan ji ?

Yeesu nee na Baay bi moo ëpp xam-xam Doom ji. Bu Yeesu nekkoon benn xaaju Yàlla Aji Kàttan ji, kon Yeesu war na xam li Baayam xam. Kon boog, Doom ji ak Baay bi yemuñu. Waaye dina am ñuy wax ne ‘ Yeesu dafa amoon ñaari melokaan. Foofu, dafa doon wax ni doomu Aadama. ’ Waaye, su dee loolu am na sax, lan lañuy wax ci xel mu sell mi ? Bu dee dafa nekk benn xaaju Yàlla ni Baay bi, lu tax Yeesu waxul ne xel mu sell mi xam na li Baay bi xam ?

Booy kontine ñu lay jàngal Biibël bi, dinga xam aaya yu gën a bare yuy leeral mbir moomu. Aaya yooyu dañuy wone luy dëgg gi ci Baay bi, Doom ji, ak xel mu sell mi. — Psaume 90:2 ; Jëf ya 7:55 ; Kolos 1:15

^ par. 3 Boo bëggee xam leneen lu ñu wax ci Yowaana 1:​1, seetal li nekk ci La Tour de Garde bu 1 nowàmbar, 2008, xët 24 ak 25. Seede Yexowa yi ñoo defar téere boobu.