Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LI ÑU YOKK CI WAXTAAN YI NEKK CI TÉERE BII

Lu tax karceen dëgg yi duñu jëfandikoo kurwaa ngir jaamu Yàlla

Lu tax karceen dëgg yi duñu jëfandikoo kurwaa ngir jaamu Yàlla

AY MILYOŊI nit dañuy jaamu kurwaa bi, di ko may cér. Téere bi tudd The Encyclopædia Britannica, lii la wax ci kurwaa bi : “ Mooy màndarga bi gën a am solo ci diine karceen. ” Waaye karceen dëgg yi duñu jëfandikoo kurwaa bu ñuy jaamu Yàlla. Lu tax duñu ko ci boole ?

Lenn lu am solo lu waral loolu mooy, Yeesu deewul ci kurwaa. Ci làkku gereg, stauros mooy baat bi ñu faral di tekki “ kurwaa ”. Baat boobu ci boppam dafay tekki “ benn bant walla poto bu ñu samp ”. Téere bi tudd The Companion Bible lii la wax : “ [Stauros] masul doon ñaari bant yu ñu tegle mu def kurwaa [...] Amul dara lu ñu bind ci làkku gereg ci [Injiil] luy tax ñu mën a xalaat ne am na ñaari bant. ”

Ñi bind li nekk ci Biibël bi, am na ay aaya foo xam ne neneen lañu woowe li ñu jël ngir rey Yeesu. Xulon lañu doon wax ci làkku gereg (Jëf ya 5:30 ; 10:39 ; 13:29 ; Galasi 3:13 ; 1 Piyeer 2:24). Li baat boobu di tekki mooy, “ bant ”, walla “ yet ”, walla “ garab. ”

Ci téere bi tudd Das Kreuz und die Kreuzigung (Kurwaa bi ak daaj nit ci kurwaa), Hermann Fulda wax na lu tax ñu doon rey ci benn bant kese ki yoon dal ci kawam. Nee na : “ Ci béréb yi ñu doon tànn ngir rey nit ci kanamu ñépp, faralul woon di am garab. Booba, benn poto kese lañu doon jël, samp ko ci suuf si. Dañu doon yëkkati loxo nit ki def lu dul yoon, takk leen walla daaj leen ci poto bi te ci lu bare dañu ci doon boole tànk yi itam. ”

Waaye lu gën a leeral loolu, mu ngi ci Kàddu Yàlla. Ndaw li Pool nee na : “ Waaye Kirist jot na nu ci alkande [maanaam alku], ji yoon wi indi ; mu gàddul nu ko, ba far alku moom ci boppam, ndaxte Mbind mi nee na : «Képp ku ñu rey, wékk ko ci bant [“ ci garab ”, King James Version] alku nga.» ” (Galasi 3:13). Fii, Pool dafa doon waxaat li nekk ci Deutéronome 21:​22, 23. Aaya boobu dafay leeral ne du kurwaa waaye bant lañu wax. Komka nit ku «alku» lañuy rey ci fasoŋ boobu, kon jaaduwul karceen yi di rafetal seen kër ak nataal yuy wone ñu daaj Yeesu.

Dara wonewul ne ñi doon wax ne ay karceen lañu, dañu doon jëfandikoo kurwaa bu ñu doon jaamu Yàlla ci 300 at yi topp deewu Kirist. Waaye ginnaaw 300 at yooyu, buur bi tudd Constantin te mu doon jaamu xërëm, dafa tuub bokk ci ñi mbubboo turu karceen ba pare mu bëgg kurwaa bi doon màndarga diine boobu. Ak lu mënta xiir Constantin ci loolu, kurwaa bi bokkul dara ak Yeesu Krist. Ci dëgg-dëgg, kurwaa bi ci diine ñiy jaamu xërëm la jóge. Téere bi tudd New Catholic Encyclopedia, lii la wax : “ Kurwaa bi bokkoon na ci ay aada yu amoon bala diine karceen di am ak it ci aada nit ñi nekkul karceen. ” Yeneen téere yu jar a wóolu wax nañu ne ñiy jaamu li Yàlla sàkk dañu doon jëfandikoo kurwaa bi, te it kurwaa bi am na lu mu bokk ak njaaloo bi nit ñi defoon aada ngir jaamu seen xërëm.

Kon lu tax ñu boole ci diine karceen màndarga boobu jóge ci ay xërëmkat ? Dafa mel ni dañu bëggoon boroom xërëm yi gën a gaaw a nangu diine boobu nit ñi foogoon ne diine karceen la. Waaye Biibël bi dafa tere ci lu leer ñu jaamu bépp màndarga bu jóge ci ay xërëmkat (2 Korent 6:​14-18). Mbind mi dafay tere it bépp fasoŋi xërëm (Gàddaay gi 20:​4, 5 ; 1 Korent 10:14). Kon nag, karceen dëgg yi xam nañu bu baax lu tax duñu jëfandikoo kurwaa bu ñuy jaamu Yàlla *.

^ par. 5 Boo bëggee am yeneen leeral ci kurwaa bi, seetal li ñu wax ci téere bi tudd Comment raisonner à partir des Écritures, ci xët 77 ba 81. Seede Yexowa yi ñoo defar téere boobu.