Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LI ÑU YOKK CI WAXTAAN YI NEKK CI TÉERE BII

Ci dëgg-dëgg, lan mooy “ ruu ” ak lan mooy “ xel ” ?

Ci dëgg-dëgg, lan mooy “ ruu ” ak lan mooy “ xel ” ?

BOO déggee ñuy wax “ ruu ” walla “ xel ”, ci lan la sa xel di dem ? Ñu bare dañuy wax ne, ñaari baat yooyu mooy li nga xam ne dafa nekk ci nit, bët mënu ko gis te du dee mukk. Dañuy foog ne, bu nit deewee, loolu dafay jóge ci nit ki, kontine di dund feneen. Loolu nit ñi di wax dafa siiw lool. Moo tax ñu bare, bu ñu leen xamalee ne Biibël bi waxul loolu, dañuy waaru. Kon boog, ci kàddu Yàlla lan la ruu ak xel di tekki ?

“ RUU ” LU MUY TEKKI CI BIIBËL BI

Nañu njëkk a waxtaan ci ruu. Bul fàtte ne li ëpp ci Biibël bi, ci làkku ebrë ak gereg lañu ko njëkk a binde. Ñi bind li nekk ci Biibël bi, saa yu ñu doon wax lu jëm ci ruu, dañu doon bind nèphèsh ci làkku ebrë, walla psukhê ci làkku gereg. Ñaari baat yooyu feeñ nañu lu ëpp 800 yoon ci Mbind mi. Te Biibël bi tudd La Traduction du monde nouveau dafay bind “ ruu ” fépp fu baat yooyu feeñ. Boo gëstoo ci li “ ruu ” di tekki ci Biibël bi, dafay leer ne baat yooyu dañuy tekki : 1) nit, 2) mala, mbaa 3) bakkanu nit walla bakkanu mala. Nañu seet ay aaya yuy wone ñett yooyu ruu di tekki.

Nit. “ Ca jamono Nóoyin [...] ñu néew, maanaam juróom ñetti ruu ñoo muccoon ca ndox ma. ” (1 Piyeer 3:​20, NW). Ci aaya boobu dafa leer ne “ ruu ” nit lay tekki, maanaam Nóoyin, jabaram, ñetti doomam ak seeni jabar. Ci Gàddaay gi 16:​16, NW, Yàlla dafa joxoon waa Israyil ay ndigal ci lu jëm ci ni ñu war a fore ñam bi tudd mànn. Lii la leen Yàlla waxoon : “ Forleen ci [...] lu yem ak ruu yu nekk ci tàntu kenn ku nekk ci yéen. ” Kon li ñu waroon a for ci mànn mi, ni mu waroon a tollu mu ngi aju ci ñaata nit ñoo nekk ci njaboot bu nekk. Feneen ci Biibël bi fu baat yi ñu tekki “ ruu ” feeñ ngir wax nit, mu ngi ci Njàlbéen ga 46:18 ; Josué 11:11 ; Jëf ya 27:37 ; ak Room 13:⁠1.

Mala. Lii la Biibël bi wax ci bi Yàlla doon sàkk àddina : “ Yàlla ne : ‘ Na ndox fees ak ruu yuy dund, te na am ay mbindeef yuy naaw ci asamaan. ’ Yàlla tegaat ci ne : ‘ Na ruu yuy dund am ci kaw suuf, bu ci nekk ak xeetam : mala yiy nekk ci kër ak jur yi, luy raam ak rabi àll yi ci kaw suuf si, bu ci nekk ak xeetam. ’ Loolu daldi am. ” (Njàlbéen ga 1:​20, 24, NW). Jën yi, mala yiy nekk ci kër, jur yi ak rabu àll yi, ñoom ñépp a bokk ni ñu leen woowee ci aaya yooyu maanaam “ ruu ”. Ci Njàlbéen ga 9:10 ; Lévitique 11:46 ; ak Nombres 31:​28, picc yi ak yeneen mala yi, dañu leen fay woowe it ruu.

Bakkanu nit. Yenn saay “ ruu ” dafay tekki bakkanu nit. Lii la Yexowa waxoon Musaa : “Ñi doon wut sa bakkan [ruu, NW] ñépp dee nañu.” (Gàddaay gi 4:19). Lan la nooni Musaa doon wut ? Dañu doon jéem a jël bakkanu Musaa. Bala loolu, bi Rasel doon am doomam bi tudd Ben-yamin, ‘ bakkanam [ruuwam, NW] mu ngi doon rot ’ ndaxte dafa mujj a dee (Njàlbéen ga 35:​16-19). Ci waxtu boobu la Rasel ñàkke bakkanam. Xalaatal itam ci li Yeesu wax. Nee na : «Man maay sàmm bu baax bi. Sàmm bu baax bi day joxe bakkanam [ruuwam, NW] ngir ay xaram.» (Yowaana 10:11). Yeesu dafa joxe ruuwam, maanaam bakkanam ngir doomu-Aadama yi. Ci aaya yooyu, dafa leer ne “ ruu ” mooy bakkanu nit. Dinga gis yeneen leeral ci li “ ruu ” di tekki noonu, ci aaya yii : 1 Rois 17:​17-23 ; Macë 10:39 ; Yowaana 15:13 ; ak Jëf ya 20:⁠10.

Boo gënee gëstu Kàddu Yàlla, dinga gis ne ci Biibël bi yépp, amul fenn fu ñu boole “ ruu ” ak “ lu mënul dee ” walla luy “ sax ba fàww ”. Waaye Mbind mi nee na, ruu dafay dee (Ézékiel 18:​4, 20). Moo tax Biibël bi di woowe nit ku dee ruu bu dee. — Lévitique 21:⁠11.

RÀÑÑEE NAÑU LI “ XEL ” DI TEKKI

Nañu waxtaan léegi ci li “ xel ” di tekki ci Biibël bi. Am na ñuy wax ne “ xel ” beneen fasoŋ bu ñuy woowe “ ruu ” kese la. Waaye du looloo am. Biibël bi leeral na ne “ xel ” ak “ ruu ” ñaar yu wuute la. Lan moo leen wuutale ?

Ñi bind li nekk ci Biibël bi, saa yu ñu doon wax lu jëm ci “ xel ”, dañu doon bind rouaḥ ci làkku ebrë walla pneuma ci làkku gereg. Mbind mi ci boppam wone na li kàddu yooyu di tekki. Sabóor 104:​29, NW, nee na : “ [Yexowa] boo jëlee seen xel [rouaḥ], ñu faatu, te dellu ci pënd mi ñu nekkoon. ” Te it Saag 2:​26, NW nee na : “ Jëmm bu amul xel [pneuma] dafa dee. ” Kon ci aaya yooyu, xel mooy liy tax jëmm di dund. Jëmm bu amul xel, dafa dee. Looloo tax ci Biibël bi, rouaḥ tekkiwul “ xel ” kese, waaye dafay tekki it “ doole ” walla doole dund. Nañu ko seet ci lii : Lii la Yàlla waxoon ci taw bu mag bi amoon ca jamono Nóoyin : “ Maa ngi nii di indi mbënn ci kaw suuf, mu rey lépp lu am doole [rouaḥ] dund lu asamaan tiim. ” (Njàlbéen ga 6:​17, NW ; 7:​15, 22). Kon “ xel ” mooy doole bu bët mënul a gis buy tax bépp mbindeef di dund.

Ruu bokkul ak xel. Yaram dafa soxla xel, ni rajo soxlaa kuuraa ngir mën a dox. Nañu ko seet ci lii : xalaatal ci rajo bu ndaw. Boo ci defee piil te taal ko, kuuraa bi nekk ci piil bi mooy tax mu tàkk, mel ni mu ngi dund, di wax. Waaye bu amul piil, rajo bi du dox, mel ni dee na. Yeneen rajo yi it, bu ñu dindee seen fiilu kuuraa duñu dox. Noonu it, xel mooy doole biy tax suñu yaram di dund. Te it ni kuuraa, xel du yëg dara. Mënul a xalaat itam. Doole kese la. Waaye suñu yaram bu amul xel boobu walla doole dund, dafay ‘ faatu, te dellu ci pënd mi mu nekkoon ’ ni ñu ko waxe ci téere Sabóor.

Bi mu doon wax lu jëm ci dee, Dajalekat 12:​7, NW, nee na : “ Pënd bi [maanaam pëndu yaram bi] dafay delluwaat ci suuf si ni mu meloon te xel mi dellu ca Yàlla dëgg ji ko maye. ” Xel mi walla doole dund bi, bu génnee ci yaram bi, nit ki dafay dee te delluwaat fa mu jóge maanaam ci suuf si. Noonu it, doole dund bi dafay dellu fa mu jóge, maanaam ca Yàlla (Job 34:14, 15 ; Psaume 36:⁠9). Loolu tekkiwul ne doole dund bi dafay tukki dem ca asamaan. Waaye dafay tekki ne nit ki faatu, yaakaar bi mu mën a am ngir dundaat ëllëg, mu ngi ci loxo Yexowa Yàlla. Kon mën nañu wax ne bakkanu ki faatu, ci loxo Yàlla la nekk. Ci kàttanu Yàlla kese lañu mën a joxaat nit kooku xel walla doole dund ba mu mën a dundaat.

Xam ne loolu sax la Yexowa di defal ñépp ñi nekk «ci seen bàmmeel», neex na lool (Yowaana 5:​28, 29) ! Bu ndekkite bi jotee, Yexowa dina jox ñi dee yaram bu bees te def ci xel, maanaam doole dund ngir mu dundaat. Bés boobu, dina neex lool !

Boo bëggee am lu gën a leer ci li “ ruu ” ak “ xel ” di tekki ci Biibël bi, seetal li ñu wax ci téere Que devient-on quand on meurt ? ak li nekk ci téere Comment raisonner à partir des Écritures, xët 27 ba 32 ak ci xët 135 ba 140. Seede Yexowa yi ñoo defar ñaari téere yooyu yépp.