Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LI ÑU YOKK CI WAXTAAN YI NEKK CI TÉERE BII

1914 : At bu am solo ci li Biibël bi wax ne dina am

1914 : At bu am solo ci li Biibël bi wax ne dina am

LU JEGE 40 at bala 1914 di jot, gëstukatu Biibël bi waxoon nañu ne lu am solo dina xew ci at moomu. Lan moo waroon a xew ? Te yan xew-xew ñoo wone ne atum 1914 dafa amoon solo ?

Ni ñu ko binde ci Luug 21:​24, Yeesu nee na : «Ñi dul Yawut dinañu nappaaje [maanaam dëggaate] Yerusalem, ba kera jamonoy ñi dul Yawut mat.» Yerusalem moo nekkoon dëkk bi gën a am solo ci réewu yawut yi. Buur yi bokkoon ci askanu Daawuda buur bi, foofu lañu dëkkoon (Psaume 48:​1, 2). Waaye buur yooyu, bokkuñu ak yeneen buuri réew yi nekkoon seen wet. Buur yi nekkoon Yerusalem, Biibël bi nee na dañu toogoon ci gàngune Yexowa ndaxte Yexowa ci boppam lañu fa nekkaloon (1 Chroniques 29:23). Yerusalem dafa doon misaal nguuru Yexowa.

Waaye naka la «ñi dul Yawut di nappaaje» Nguuru Yàlla ak kañ lañu komaasee def loolu ? Loolu mu ngi am ci atum 607 bala suñu jamano di tàmbali (B.S.J.T.), bi waa Babilon nangoo Yerusalem. Ba loolu amee, kenn toogatul ci gàngune Yexowa te it amatul woon buur bu jóge ci askanu Daawuda (2 Rois 25:​1-26). Ndax «nappaaje» boobu dafay kontine ba abadan ? Déedéet. Ndaxte am na li yonent Yàlla Esekiel waxoon ci Sédésiyas moom mi nekkoon buur bi mujj ca Yerusalem. Lii la yonent bi wax : “ Dindil musóor bi, te teggi mbaxane buur bi. [...] Kenn du ko jëlaat ba keroog ki am sañ-sañ bi ñëw te dinaa ko ko jox. ” (Esekiel 21:​26, 27, NW). Kirist Yeesu mooy ki am ‘ sañ-sañu ’ jël mbaxane buur bi jóge ci askanu Daawuda (Luug 1:​32, 33). Kon li ñuy «nappaaje Yerusalem», bi Yeesu nekkee buur lay nar a jeex.

Xew-xew bu mag boobu kañ la naroon a am ? Yeesu waxoon na ne dafa am diir bu ñu may ñi dul Yawut ngir ñu jiite. Li ñu nettali ci Dañeel pàcc 4 moo ñu xamal ni diir boobu di tollu. Dafay wax ci li Nebukanesar buuru Babilon géntoon. Gént boobu dafa doon wone li naroon a am ëllëg. Nebukanesar dafa géntoon garab gu mag gu ñu gor, daaneel ko. Garab googu mënul woon a saxaat ndax li ñu ko takk ak ay weñ ak it përëm. Benn malaaka daldi wax ne : Na “ juróom-ñaari jamono jàll ci kawam ”. — Ñun ñoo dëngal mbind yi ; Dañeel 4:​10-16.

Yenn saay ci Biibël bi, garab dafay misaal nguur (Ézékiel 17:22-24 ; 31:​2-5). Kon garab googu ñu gor dafay misaal li ñu dindi kiliftéefu buur yi nekkoon Yerusalem, ñoom ñi fa nekkaloon Nguuru Yàlla. Waaye peeñu moomu wone na ne li ñuy «nappaaje Yerusalem» ab diir kese lay def, maanaam diirub “ juróom-ñaari jamono ”. Diir boobu ñaata lay def ?

Peeñu 12:​6, 14 wone na ne ñetti jamono walla diir ak génn-wàll mu ngi tollu ak “ junni ak ñaari téeméeri fan ak juróom-benn-fukk ”. Kon “ juróom ñaari jamono ” war na ko mat ñaari yoon, maanaam 2 520 fan. Waaye diir bi ñi dul Yawut «nappaaje» Nguuru Yàlla, jeexul 2 520 fan ginnaaw bi ñu nangoo Yerusalem. Kon leer na ne diir boobu ñu yégle woon, war na gën a gudd loolu fuuf. Ci 4 Musaa 14:​34, NW, ak Esekiel 4:​6, NW, wax nañu ne “ benn fan ngir benn at ”. Loolu dafa ñuy may ñu wax ne “ juróom ñaari jamono ” yi war na tollu ak 2 520 at.

Ci oktoobar 607 bala suñu jamono di tàmbali (B.S.J.T.), booba la waa Babilon nangoo Yerusalem. Booba it la buur bi jóge ci askanu Daawuda ñàkke kiliftéefam. Ci at moomu la 2 520 at yi komaase. Diir boobu mu ngi jeex ci oktoobar 1914. Ci atum 1914 la «jamonoy ñi dul Yawut» jeexe, ñu daldi fal Yeesu, def ko buuru Nguuru Yàlla bi nekk ca kaw asamaan *. — Sabóor 2:​1-6 ; Dañeel 7:​13, 14.

Yeesu nee woon na ne, bu fiy “ teew ” ni buuru Nguuru Yàlla bu nekk ca asamaan, dina am ay xew-xew yu doy waar ci àddina si, lu mel ni xeex, xiif, suuf suy yëngu ak feebar yuy law (Macë 24:​3-8, NW ; Luug 21:11). Xew-xew yooyu dafay wone ba mu leer ne ci atum 1914 lañu samp Nguuru Yàlla bi nekk ca asamaan. Te booba la àddina su bon sii dugge ci “ muju jamano ”. — 2 Timote 3:​1-5.

^ par. 4 Am na 606 at diggante oktoobar 607 B.S.J.T. ak oktoobar bu atum 1 B.S.J.T. Komka atum sero amul, diggante oktoobar bu atum 1 B.S.J.T. ba oktoobar 1914 ci suñu jamano (C.S.J.), am na 1 914 at. Bu ñu boolee 606 at ak 1 914 at, dafay def 2 520 at. Boo bëggee am yeneen leeral ci bi Yerusalem daanoo ci atum 607 B.S.J.T., seetal li ñu wax ci xaaj bi tudd “ Chronologie ” ci téere Étude perspicace des Écritures. Seede Yexowa yi ñoo defar téere boobu.