Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

XAAJ 2

Kan mooy Yàlla dëgg ji ?

Kan mooy Yàlla dëgg ji ?

Benn Yàlla dëgg rekk moo am, turam mooy Yexowa (Psaume 83:18). Xel la, ci kaw asamaan la dëkk, kenn mënu koo gis. Yexowa bëgg nañu, te li muy xaar ci ñun mooy ñu bëgg ko, bëgg itam suñu moroom (Macë 22:35-40). Moo ëpp ñépp kattan, te moo sàkk lépp.

Li Yàlla njëkk a sàkk mooy kenn koo xam ne ku bare kàttan la ca asamaan. Moom lañu mujj a woowe Yeesu. Yexowa sàkkoon na itam malaaka yi.

Yexowa moo sàkk lépp lu nekk ci kaw asamaan . . . ak ci kaw suuf. Peeñu ma 4:11

Yexowa moo sàkk biddéew yi, suuf si ak lépp li ci nekk.— Njàlbéen ga 1:1.

Sàkk na itam góor gu njëkk ga, maanaam Aadama. Ci pëndu suuf la ko sàkke. — Njàlbéen ga 2:7.