Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

XAAJ 6

Lan lañu mën a jàng ci taw bu metti bi amoon ca jamano Nóoyin ?

Lan lañu mën a jàng ci taw bu metti bi amoon ca jamano Nóoyin ?

Yàlla alag na nit ñu bon ñi. Nóoyin ak njabootam mucc nañu. Njàlbéen ga 7:11, 12, 23

Tawoon na ñeent-fukki guddi ak ñeent-fukki bëccëg ba ndox mi muur lépp li nekkoon ci kaw suuf si. Nit ñu soxor ñi ñépp dee woon nañu.

Malaaka yi jëloon jëmu nit te ñëwoon ci kaw suuf si, mujj nañu delluwaat ci kaw asamaan, jëlaat seen jëmu malaaka yu soxor.

Ñi nekkoon ci biir gaal gi mucc nañu. Dëgg la, Nóoyin ak njabootam mujj nañu màggat te dee, waaye Yàlla dina leen dekkil ngir ñu dund ba fàww.

Yàlla dina alagaat nit ñu soxor ñi. Nit ñu jub ñi dinañu mucc. Macë 24:37-39

Seytaane ak malaaka yu bon yi ñu ngi kontine di nax nit ñi.

Niki jamano Nóoyin, tey itam nit ñi bëgguñu topp ndigalu Yexowa yi. Du yàggati dara, Yexowa dina alag nit ñu bon ñépp.— 2 Piyeer 2:5, 6.

Am na ay nit yu mel ni Nóoyin— dañuy dégg li Yàlla wax te di topp li mu wax. Ñooñu ñooy Seede Yexowa yi.