Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NJÀNGALE 4

Lu tax seede Yexowa yi tekki Biibël bi ci làkk yu bare ?

Lu tax seede Yexowa yi tekki Biibël bi ci làkk yu bare ?

Congo (Kinshasa)

Rwanda

Turu Yàlla bi feeñ ci Sabóor 69:31, version de Symmaque (IIIe ou IVe siècle de notre ère).

Seede Yexowa yi yàgg nañu di jàng, di sotti te di joxe ay Biibël. Waaye dañu gisoon ne soxla nañu ñu tekki Biibël bi ci fasoŋ buy gën a tax nit ñi “ xam dëgg gi ” ndaxte dëgg googu la Yàlla bëgg ñépp xam (1 Timote 2:⁠3, 4). Loolu moo tax ñu komaase di tekki Biibël bi ci fasoŋ bu gën a yomb a nànd, tudde ko Traduction du monde nouveau ci tubaab. Ci atum 1950 lañu tàmbalee génne xaaj yi ñu tekki. Tekki nañu Biibël bi ci lu ëpp 130 làkk * te bi ñu koy tekki dañu def lépp ngir bañ a soppi xalaat yi, bañ ci yokk dara, bañ ci wàññi dara.

Dañu soxla woon tekki Biibël bu ñépp mën a nànd. Ci Biibël yu bare yu ñu tekki, ay baat yu naqaree nànd te xewwi ñoo ci nekk. Li waral loolu mooy, lu ñuy gën di dem, làkk yi di soppeeku. Am na it ay boroom xam-xam yu gis ay sotti Biibël yu yàgg yoo xam ne loxo lañu leen binde te ñu gën a jege te gën a méngoo ak sotti Biibël yu njëkk ya. Loolu tax na ñu gën a mokkal làkk yi ñu binde Biibël bi, maanaam Ebrë, Arameyni ak Gereg te mën koo tekki ci fasoŋ bu gën a leer.

Dañu soxla woon tekki Biibël bu dul soppi Kàddu Yàlla. Ñiy tekki kàddu Yàlla waruñu ko tekki nu mu leen neexe. Dañu war a yem ci li kàddu Yàlla wax. Waaye dañu seetlu ne ci Biibël yu bare dañu dindi turu Yàlla, maanaam Yexowa.

Dañu soxla woon tekki Biibël buy jox Yàlla mi ko bind cér bi mu yelloo (Samuel 23:⁠2). Turu Yàlla, maanaam Yexowa, feeñoon na ca sotti Biibël yu njëkk ya lu jege 7000 yoon (foto bi ci suuf mu ngi ci wone benn). Loolu moo tax, bi ñuy tekki Biibël bi tudd Traduction du Monde Nouveau, seede Yexowa yi delloowaat nañu tur boobu fépp fi mu feeñoon (Psaume 83:18). Bala ñuy génne tekki Biibël boobu def nañu ay gëstu yu bare ci lu yàgg. Loolu moo tax tekki boobu neex a jàng. Nga am Traduction du Monde Nouveau ci sa làkk walla déet, fexeel ba di jàng kàddu Yexowa bés bu nekk. — Yosuwe 1:8 ; Sabóor 1:​2, 3.

  • Lu tax seede Yexowa yi tekki Biibël bi ?

  • Ku bëgg a xam li Yàlla bëgg, lan la war a def bés bu nekk ?