Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NJÀNGALE 6

Ban njariñ lañuy jële ci booloo ak suñuy mbokk ci ngëm ?

Ban njariñ lañuy jële ci booloo ak suñuy mbokk ci ngëm ?

Madagascar

Norvège

Liban

Italie

Seede Yexowa yi duñu bàyyi dara tere leen teewe seen ndaje yi ; du taw, du naaj, du yoonu àll. Bu dee sax dañuy jànkoonteel ay jafe-jafe walla ñu yendoo liggéey ba sonn, seede Yexowa yi dañuy def lépp ngir booloo ak seeni mbokk ci ngëm. Lu waral loolu ?

Dañuy am ndimbal ci suñuy jafe-jafe. ‘ Xiirtalanteleen ’ ci seen biir. Loolu la ndaw li Pool waxoon ñépp ñiy daje ci mbooloo karceen yi (Yawut ya 10:24). Wax boobu dafa laaj ñu xamante ci suñu biir. Kon ndaw li Pool dafa ñuy xiir ci am yitte ci ñépp. Nanga jéem a xam yeneen njabooti karceen yi. Dinga gis ne ñu bare jaar nañu ci jafe-jafe yi ngay dund tey ba génn ci. Dinañu la mën a xelal ndax nga mën a génn ci say poroblem yaw itam.

Dañuy am xaritoo yu dëgër. Ci suñu ndaje yi, duñu ay àndandoo kese waaye ay xarit dëgg lañu. Lée-lée li waral ñuy booloo mooy bëgg a féexal suñu xol ci fasoŋ bu rafet. Ban njariñ moo ci nekk ? Dafay tax ñu gën a xamante ngir gën a soppante te suñu mbëggeel dafay gën a dëgër. Kon bu suñu mbokk ci ngëm amee jafe-jafe, dinañu sawar ci dimbali ko ndax xaritoo bu dëgër bi dox suñu diggante (Kàddu yu Xelu 17:17). Nañu booloo ak ñépp ñiy teew ci suñu ndaje yi. Noonu dinañu wone ne ñépp lañu yég. —1 Korent 12:​25, 26.

Ñu ngi lay xiir ci tànn say xarit ci ñiy def li Yàlla bëgg. Xarit yu mel noonu dinga leen fekk ci biir seede Yexowa yi. Fexeel ba dara bañ laa tere booloo ak ñun.

  •  Bu ñu demee ci suñu ndaje yi, lu tax booloo ak suñuy mbokk ci ngëm nekk suñu jariñ dëgg ?

  •  Kañ ngay ñëw xamante ak suñu waa mbooloo ?