Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NJÀNGALE 7

Lan lañuy def ci suñu ndaje yi?

Lan lañuy def ci suñu ndaje yi?

Nouvelle-Zélande

Sapoŋ

Ouganda

Lituanie

Karceen yu njëkk ya, ci seeni ndaje, dañu doon woy, di ñaan Yàlla, di jàng te waxtaan ci mbind mu sell mi (1 Korent 14:26). Tey boo ñëwee ci suñu ndaje yi, lu mel noonu ngay gis.

Li ñuy jàngale foofu, ci Biibël bi la sukkandiku te am na njariñ. Semen bu nekk, samdi walla dimaas, ci mbooloo yépp dañuy déglu benn Waare ci Biibël bi bu def 30 minit. Waxtaan boobu dafay wone njariñ bi Biibël bi am ci suñu dund ak ci suñu jamono te ñépp a mën a topp njàng mi ci seen Biibël. Bu ñu paree, dañuy jël benn waxtu ngir def li ñuy woowe Gëstu ci “ La Tour de Garde ”. Waxtaan la ci téere bi tudd La Tour de Garde (Édition d’étude) te ñépp a ci mën a bokk. Waxtaan boobu dafa ñuy dimbali ñu xam ni ñu mënee topp li nekk ci Biibël bi. Benn téere boobu lañuy jàng ci lu ëpp 110 000 mbooloo seede Yexowa yi am ci àddina ci sépp.

Dañuy jàng ngir nekk ay jàngalekat yu aay. Dañuy daje itam benn ngoon ci diggu semen bu nekk. Porogaraamu ñetti xaaj la bu tudd Dundinu karceen ak liggéeyu waare bi dafay sukkandiku ci li ñu war a jàng ci kayitu ndaje bi tudd Dundinu karceen ak liggéeyu waare bi. Xaaj bi jëkk ci ndaje bi mu ngi tudd Njariñ bu réy bi ñu mën a jële ci Kàddu Yàlla. Dafa ñuy dimbali ñu gën a miin aaya Biibël yu ñu jàng ci semen bi. Bi ci topp mu ngi tudd Farlul ci liggéeyu waare bi, dañu ciy jàng ni ñu mënee jëfandikoo Biibël bi ngir waxtaan ak nit ñi. Bu ñu paree, dafay am kuy joxe ay xelal ngir ñépp gën a aay ci jàng ak ci jàngale (1 Timote 4:​13). Xaaj bi mujj mu ngi tudd Dundinu karceen. Dañu ciy jàng ni ñu mën a dunde bés bu nekk santaane yi nekk ci Biibël bi. Dafay am kuy yëkkëti laaj, ñi teew di tontu. Dafa ñuy dimbali ñu gën a nànd Biibël bi.

Wóor na ñu ne boo teewee suñu ndaje yi dinga kontaan ndax njàngale Biibël bu set te leer bi nga fay dégg. — Isaïe 54:⁠13.

  •  Boo demee ci ndaje seede Yexowa yi, lan nga fay dégg ?

  •  Ndaje yi ñuy def, ban nga ci bëgg a teewe ?