Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NJÀNGALE 10

Lan mooy njàngum Biibël ci biir njaboot ?

Lan mooy njàngum Biibël ci biir njaboot ?

Corée du Sud

Brésil

Australie

Guinée

Yexowa dafa mas a bëgg njaboot yi jël jot ngir toog waxtaan, dëgëral seen ngëm te rattaxal seen diggante ci seen biir (Deutéronome 6:​6, 7). Loolu moo tax seede Yexowa yi di jël jot semen bu nekk ngir jàng Biibël bi ak seen njaboot. Dañuy waxtaan ci toogaay bu neex ci li ñu soxla ci wàllu ngëm. Boo nekkee yaw kese, jot boobu mën nga ci wéet ak Yàlla, tànn benn waxtaan te gëstu li ci Biibël bi wax.

Jot la bu ñu jël ngir gën a jege Yexowa. “ Jegeleen Yàlla, mu jege leen. ” (Saag 4:⁠8). Mën nañu yaatal suñu xam-xam ci Yexowa bu ñuy jàng ci Kàddoom lu jëm ci jikkoom ak ciy jëfam. Liir Biibël bi ci kaw mooy fasoŋ bu yomb bi ngeen mën a komaase seen njàngum Biibël ci biir njaboot. Mën ngeen a topp porogaraamu Lekkoolu Sasu Nguuru Yàlla bi. Mën ngeen a topp porogaraamu ndaje bi tudd Dundinu karceen ak liggéeyu waare bi. Mën ngeen seddale aaya yi, ba ku nekk am li ngay liir. Bu ngeen paree, ngeen waxtaan ci.

Jot la bu ñu jël ngir ñu gën a jegeente ci biir njaboot gi. Bu jëkkër ak jabar walla waajur ak seeni doom di toog ngir jàng Biibël bi, seen diggante dafay gën a rattax. Waxtu boobu dafa war a nekk waxtu bu neex te ànd ak jàmm ak mbégte. War na bokk ci waxtu yi gën a neex ci semen bi. Bu waajur di tànn li ñuy waxtaane ci seen njàngum Biibël, nañu sóoraale at yi seen doom am. Mën nañu tibb ci waxtaan yi nekk ci Tour de Garde yi ak Réveillez-vous yi walla ci palaas bi ñu moom ci internet jw.org. Mën ngeen a seetaan ay wideo ci JW Télédiffusion (tv.pr418.com) boo leen paree ngeen waxtaan ci. Mën ngeen a waxtaan ci poroblem yi xale yi di daj ci seen lekkool te seet li ñu ci mën a def. Mën ngeen woy itam li ñu war a woy ci ndaje yi. Bu ngeen paree nag, mën ngeen am tuuti lu ngeen lekk walla naan.

Jot boobu njaboot gi di jël semen bu nekk ngir jaamu Yexowa, dina dimbali ñépp ñu bég bu ñuy jàng kàddu Yàlla. Nangeen ci góor-góorlu. Yexowa dina leen barkeel bu baax-a-baax. — Sabóor 1:​1-3.

  • Lu tax ñuy jël jot ngir jàng Biibël bi ci biir njaboot gi ?

  • Lan la waajur mën a def ba ku nekk ci njaboot gi bég ci waxtu boobu ?