Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NJÀNGALE 13

Lan mooy pioñee ?

Lan mooy pioñee ?

Canada

Këroo-kër

Njàngum Biibël

Jàngal sa bopp Biibël bi

“ Pioñee ” mooy ku njëkk a sanc ab dëkk ba tax yeneen nit mën fa dëkk. Kon Yeesu pioñee la woon ndaxte Yàlla dafa ko yónni ci kaw suuf ngir mu def liggéey buy tax doomu Aadama yi am dund te mu ubbil leen bunt ngir ñu mucc (Macë 20:28). Tey, ñiy topp Yeesu ñu ngi koy roy bu ñuy def lépp li ñu mën ngir jébbal jot ci “ sàkk ay taalibe ” (Macë 28:19, 20). Am na ci ñoom ñu dem ba mën a bokk ci ñi ñuy woowe pioñee.

Pioñee mooy kiy jébbal jotam yépp ci liggéeyu waare bi. Seede Yexowa yépp dañuy yégal nit ñi xibaaru jàmm bi, waaye am na ci ñoom ñoo xam ne fexe nañu ba jébbal 70 waxtu ci liggéeyu waare bi weer bu nekk. Dañu leen di woowe pioñee permanã. Ñu bare ci ñoom dañuy wàññi seen liggéey ngir mën a def loolu. Am na it ñi ñu tànn, def leen pioñee espesiyaal ngir ñu dem ci gox yi ñu soxla ay waaraatekat. Ñoom weer bu nekk dañuy jébbal 130 waxtu walla lu ko ëpp ci liggéeyu waare bi. Pioñee yi dañu nekk ay nit ñu doylu te nangu dundin bu woyof, xam ne Yexowa dina faj seeni soxla (Macë 6:​31-​33 ; 1 Timote 6:​6-8). Ñi mënul a jébbal seen jot yépp ci liggéeyu waare bi, mën nañu tànn weer bu ñu bëgg ngir nekk pioñee oksiliyeer. Ñoom weer boobu dinañu jébbal 30 waxtu walla 50 waxtu ci liggéeyu waare bi.

Pioñee mooy kiy waare ndax li mu bëgg Yàlla ak nit ñi. Yeesu dafa yërëmoon nit ñi xamul Yàlla ak coobareem. Ñun it tey, loolu lañuy yëg bu ñu gisee ne ñu bare noonu lañu mel (Màrk 6:​34). Am na lu ñu xam lu leen mën a dimbali tey te may leen yaakaaru ëllëg. Pioñee dafa bëgg moroomam moo tax mu nangu jébbal jot ak kàttan bu bare ngir dimbali nit ñi ñu xam xibaaru jàmm bi (Macë 22:39 ; 1 Tesalonig 2:⁠8). Loolu dafay dëgëral ngëmam, dafay tax mu gën a jege Yàlla te dafa koy may mbégte mu réy. — Jëf ya 20:⁠35.

  •  Lan mooy pioñee ?

  •  Lan mooy xiir ñu bare ci nekk pioñee ?