Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NJÀNGALE 14

Yan lekkool lañu jagleel pioñee yi ?

Yan lekkool lañu jagleel pioñee yi ?

Etaa Sini

Lekkoolu Galàdd, ca Patterson, New York

Panama

Jàngal nit ñi ñu xam kan mooy Yàlla dafa mas a nekk li soxal Seede Yexowa yi. Loolu moo tax mu am benn lekkool bu ñu jagleel ñépp ñi jébbal seen jot gépp ci liggéeyu waare Nguuru Yàlla ngir ñu mën a ‘ matal seen yónnent. ’ – 2 Timote 4:5.

Lekkool bi ñu jagleel pioñee yi. Pioñee permanã bu nekk, ci njeexteelu atam bi njëkk bi, dañu koy woo ngir mu teewe benn lekkool bu juróom-benni fan bu ñuy amal ci saalu Nguur bu ko gën a jege. Te lekkool boobu, li ko tax a jóg mooy dimbali bu baax pioñee yi ñu gën a jege Yexowa te gën a xareñ ci bépp fànnu liggéeyu waare bi, te kontine ci.

Lekkool bi ñu jagleel ñiy waare Nguur gi. Lekkool boobu ci ñaari weer lañuy koy def. Dañu ko jagleel pioñee yi war a jóge ci seen dëkk ngir dem ci gox yi ñu soxla ay waaraatekat. Lii lañu wax, “ maa ngi nii ! Yónni ma ! ” dañuy roy noonu waarekat bi gën a mag bi mas a am ci kaw suuf, maanaam Yeesu Kirist (Esayi 6:8MN ; Yowaana 7:29). Jóge sa kër dem feneen fu sore dafa laaj nga mën a woyofal sa dund. Aada yi ak kilimaa bi ak lekk bi mën na wuute bu baax ak li nit ki tàmm. Xéyna sax dinga war a jàng làkk bu bees. Lekkool boobu dafay dimbali suñu mbokk yu góor ak yu jigéen yu seen at tollu diggante 23 ak 65, ñi séy ak ñi séyagul, ñu am jikko yu baax yi ñu soxla ci wàllu ngëm ngir mën a def li leen war fi ñu leen di yónni te mën a yokk liggéey bi leen Yexowa ak mbootaayam dénk.

Lekkoolu Galàdd. Ci làkku ebrë, Galàdd dafa tekki “ Jalu seede ” moo di seede bu baree bare. Bi lekkoolu Galàdd sosoo ci atum 1943 ba léegi, am na lu ëpp 8 000 nit yu fa jaar, ba pare ñu yónni leen ni ay misioneer ngir seede ba ci “ cati àddina. ” Te seen liggéey jur na lu bare lu baax (Jëf ya 13:47). Bi misioneer yi jëkkee ñëw ci réewu Peru, amu fa woon benn mbooloo seede Yexowa. Waaye léegi, ëpp nañu 1 000. Noonu it ci réewu Sapoŋ amuñu woon lu mat fukki seede Yexowa bi fa misioneer yi demee, waaye léegi ëpp nañu 200 000. Dañuy gëstu Kàddu Yàlla ci lu mat juróomi weer ci lekkoolu Galàdd. Ñi fa mën a dem ñooy pioñee espesiyaal yi, misioneer yi, ñi nekk ci bànqaas yi ak wottukat yiy wër. Dañu leen fay jàngal bu baax ni ñu mënee dimbali mbooloo yi ñu gën a dëgër ci liggéeyu waare bi.

  •  Lu tax ñu taxawal lekkool bi ñu jagleel pioñee yi ?

  •  Ñan ñoo mën a bokk ci lekkool bi ñu jagleel ñiy waare Nguur gi ?