Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NJÀNGALE 17

Naka la wottukat yiy wër di ñu dimbalee ?

Naka la wottukat yiy wër di ñu dimbalee ?

Malawi

Ndaje bi ñuy def bala ñuy waare

Liggéeyu waare bi

Ndaje magi mbooloo mi

Ci xaaju Biibël bi ñu bind ci làkku gereg, wax nañu lu bare ci Barnabas ak ci ndaw li Pool. Góor yooyu ay wottukat yuy wër lañu woon ci mbooloo karceen yu njëkk ya. Lan moo tax ñu doon wër ci mbooloo yi ? Dañu bëggoon a dimbali seeni mbokk ci ngëm ñu dëgëral seen diggante ak Yàlla. Pool dafa waxoon ne dafa bëgg a “ dellu seeti bokk ya ” ba xam nu ñu def. Dafa ko jaraloon muy tukki lu tollook ay junniy kilomet ngir dem dooleel leen (Jëf ya 15:36). Tey itam, loolu la suñu wottukat yiy wër bëgg.

Dañuy ñëw ngir dooleel ñu. Ñaari yoon ci at mu nekk, wottukat buy wër bu nekk dafay seeti lu tollu ak 20 mbooloo te toog lu mat benn semen ci mbooloo mu nekk. Mën nañu jàng lu bare ci wottukat yooyu ak ci seeni jabar. Wottukat yi dañuy jéem a xam ñépp, mag ñi ak ndaw ñi, di ñu gunge ci liggéeyu waare bi, di ànd ak ñun ci suñuy njàngum Biibël. Bu ñu ñëwee ci mbooloo yi, dañuy ànd ak magi mbooloo yi ci seeti ay mbokk ci mbooloo mi. Dañuy def ay waxtaan ci suñu ndaje yi ci saalu Nguur gi ak ci suñu ndaje yu mag yi ngir dooleel ñu. — Jëf ya 15:⁠35.

Dañu yëg kenn ku nekk ci ñun. Li wottukat yiy wër bëgg mooy dimbali mbooloo yi ci wàllu ngëm. Dañuy waxtaan ak magi mbooloo mi ak ñiy toppatoo yëfi mbooloo mi ngir xam fi mbooloo mi tollu ci wàllu ngëm, te jox leen itam ay tegtal ngir ñu gën a mën a def seen liggéey. Dañuy dimbali pioñee yi ñu jëm kanam ci seen liggéeyu waare. Dañuy xamante itam ak ñi door a bokk ci mbooloo mi te waxtaan ak ñoom ci lu rafet li ñuy def ci wàllu ngëm. Kenn ku nekk ci wottukat yooyu dafay jële boppam ni suñu ‘ nawle ci liggéey ’ te nangu sonn ngir suñu njariñ (2 Korent 8:23). Nañu leen roy ci seen ngëm ak ci li ñuy def lépp ngir jaamu Yàlla. — Yawut yi 13:⁠7.

  •  Lu tax wottukat yiy wër di seeti mbooloo yi ?

  •  Ban njariñ lañu mën a jële ci seen ñëw ?