Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NJÀNGALE 19

Kan mooy surga bu takku te teey bi ?

Kan mooy surga bu takku te teey bi ?

Ñun ñépp ay jariñoo ci ñam bi ñu jot ci wàllu ngëm

Lu yàggul dara bala muy dee, Yeesu dafa waxtaanoon ak ñeent ci taalibeem yi : Piyeer, Saag, Yowaana, ak Andare. Yeesu dafa leen joxoon ay tegtal yuy firndeel teewaayam ci mujug jamono. Mu yëkkëti laaj bu am solo, nee leen : “ Kan moo nekk surga bu takku te teey, bu njaatigeem teg ci waa kër gi, ngir mu léen di dundal ca jamono ja ? ” (Macë 24:3, 45 ; Màrk 13:​3, 4). Yeesu miy seen ‘ njaatige ’ dafa leen doon dig foofu ne, ci mujug jamono dina fi teg ay nit ngir ñuy jox taalibeem yi ñam ci wàllu ngëm. Ñan ñooy doon surga boobu ?

Gurup bu ndaw la ci biir taalibe Yeesu yi xel mu sell mi tànn. “ Surga ” bi, moom mooy Jataay biy dogal ci seede Yexowa yi. Te mu ngi jox ñiy jaamu Yexowa ñam ci wàllu ngëm ci waxtu bi ñu ko soxla. Ci surga boobu rekk lañu yaakaar ngir kontine di jot lu ñuy “ dundal ci jamono ji ”. — Luug 12:⁠42.

Dafay toppatoo kër Yàlla gi (Luug 12:44). Yeesu dafa dénk surga bu takku te teey bi liggéey bu diis, maanaam toppatoo lépp lu jëm ci liggéey bi ñiy jaamu Yexowa ci kaw suuf di def ci wàllu ngëm. Toppatoo boobu mu ngi ëmb jiite liggéeyu waare bi, sàmm alal bi koy doxal, te jàngal ñu ci suñu mbooloo yi. Loolu moo tax “ surga bu takku te teey bi ” di defar ay téere yu ñuy jëfandikoo ci suñu waare bi, te di ñu jàngal ci ndaje yi ñuy am ci saalu Nguur gi ak ci suñu ndaje yu mag yi. Noonu lañuy joxe ñam ci wàllu ngëm bi ñu soxla ci waxtu bi ñu ko soxla.

Surga bi dafa takku ndaxte dëgg gi nekk ci Biibël bi rekk lay jàngale te du bàyyi dara tere ko mu def liggéey bi ñu ko sant, maanaam waare xibaaru jàmm bi. Te it, dafa teey ci ni muy sàmme lépp li ko Kirist dénk (Jëf ya 10:42). Yexowa mu ngi barkeel liggéey bi surga bi di def. Li koy wone mooy, mbootaayam mu ngi yokku te ñam bi ci wàllu ngëm dafa bare. — Isaïe 60:22 ; 65:⁠13.

  •  Kan la Yeesu dénk liggéeyu jox taalibeem yi ñam ci wàllu ngëm ?

  •  Lu tax ñu mën a wax ne surga bi dafa takku te teey ?