Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NJÀNGALE 20

Jataay biy dogal, naka lay liggéeye ?

Jataay biy dogal, naka lay liggéeye ?

Jataay biy dogal ci jamono karceen yu njëkk ya

Njàngum bataaxal bu jóge ci Jataay biy dogal

Ca jamono karceen yu njëkk ya, amoon na benn gurup bu ndaw bu doon jël dogal yi am solo pur mbooloo karceen yépp yi xel mu sell mi tànn. Dañu nekkoon Jataay biy dogal ci seen biir. Gurup boobu moo doon “ ndaw ya ak njiit ya ” nekkoon Yerusalem (Jëf ya 15:⁠2). Bala ñuy juboo ci benn dogal, dañu doon xool li ci Mbind yi wax, waxtaan ci te bàyyi xel mu sell mi mu wommat leen (Jëf ya 15:25). Ci ñoom lañuy roy tey.

Yàlla dafay jaar ci moom ngir def li mu bëgg. Ñi bokk ci Jataay biy dogal, dañu nekk ay karceen yu góor yi xel mu sell mi tànn te dañu fonk lool Kàddu Yàlla. Yàgg nañu di joxe ay tegtal yu jëm ci liggéey bi suñu mbootaay def ci àddina si. Yàgg nañu it di ñu xelal ci wàllu ngëm. Dañuy daje semen bu nekk ngir waxtaan ci li mbokk yi nekk ci àddina si sépp soxla ci wàllu ngëm. Jataay biy dogal, dafay topp li ñu daan def ci jamono karceen yu njëkk ya, maanaam dañuy bind ay bataaxal walla jaar ci wottukat yiy wër ak ñeneen ngir mbooloo yépp jot ay tegtal yuy sukkandiku ci Biibël bi. Loolu dafay tax ñiy jaamu Yàlla bokk xalaat te bokk jëf (Jëf ya 16:​4, 5). Jataay biy dogal mooy jiite lépp lu jëm ci defar ñam bi ci wàllu ngëm, ci luy jëmloo kanam liggéeyu waare bi, ak ci tànn ñiy ñuy dénk liggéey ci mbooloo yi.

Dafay bàyyi xel mu sellu Yàlla wommat ko. Jataay biy dogal dafay bàyyi Yexowa Aji kawe ji ak Yeesu miy kilifa mbooloo mi ñu wommat ko ci lépp (1 Korent 11:3 ; Efes 5:​23). Gisewuñu seen bopp ni ay kilifa ci mbooloo Yàlla mi. Ñoom ak yeneen karceen yépp yi xel mu sell mi tànn, dañuy kontine di “ topp Gàtt ba [maanaam Yeesu] fépp fu mu jëm ” (Peeñu ma 14:⁠4). Jataay biy dogal dafay kontaan lool bu ñu koy sóoraale ci suñuy ñaan.

  •  Ca jamono karceen yu njëkk ya, ñan ñoo bokkoon ci Jataay biy dogal ?

  •  Tey, naka la Jataay biy dogal di wonee ne bëgg na Yàlla wommat ko ?