Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NJÀNGALE 22

Ban liggéey lañuy def ci bànqaas yi ?

Ban liggéey lañuy def ci bànqaas yi ?

Îles Salomon

Canada

Afrique du Sud

Ñi bokk ci njabootu Betel yi dañuy toppatoo liggéeyu waare bi ci benn réew walla lu ko ëpp. Am na ñuy tekki suñuy téere ci làkku réew mi. Am na ñuy liggéey ci masin yiy sotti suñu yéenekaay yi ak suñu téere yi. Am na ñuy liggéey fu ñuy denc suñuy téere bala ñu leen di yónnee ci mbooloo yi. Am na ñuy liggéey fu ñuy defar wideo yi ak lu ñuy déglu, walla ñuy def yeneen liggéey yu bànqaas bi war a def.

Kurélu bànqaas bi dafay jiite liggéey bi. Jataay biy dogal dafay dénk benn kurél liggéey bi ñuy def ci bànqaas bu nekk. Kurél boobu, dañu koy woowe kurélu bànqaas bi. Kurél bu nekk dina am lu mat ñetti magi mbooloo walla lu ko ëpp yu mën seen liggéey. Kurélu bànqaas bi mooy wax Jataay biy dogal fi liggéeyu waare bi tollu ci réew bu nekk bu muy toppatoo ak jafe-jafe bu mënta am. Loolu mooy dimbali Jataay biy dogal mu xam yan waxtaan lay def ci téere yi nar a génn walla ci porogaraamu ndaje yi ci mbooloo mi ak ci ndaje yu mag yi. Jataay biy dogal dafay faral di yónnee ay nit ci bànqaas yi ngir dimbali kurélu bànqaas yi ci def liggéey bi ñu leen dénk ni mu ware (Kàddu yu Xelu 11:14). Ñoom dañuy taxawal porogaraam bu neex, boole ci benn waxtaan bu ñuy def, ngir dooleel mbooloo yi ci wàllu ngëm.

Dañuy jàpple mbooloo yi ci seen liggéeyu waare bi. Ci góor yi ñuy dénk liggéey ci bànqaas bi, am na ñuy toppatoo li jëm ci mbooloo yu bees yi, maanaam ñoom ñooy nangu ñu taxawal mbooloo bu bees. Am na it ñuy toppatoo lépp lu jëm ci liggéeyu pioñee yi, misioneer yi ak wottukat yiy wër ci mbooloo yi bànqaas bi di toppatoo. Dañuy waajal ay ndaje yu mag, di jiite liggéeyu tabaxu saalu Nguur yu bees te di xool ba xam ndax yónnee nañu mbooloo yi téere yi ñu soxla. Lépp li ñuy def ci bànqaas yi bokk na ci liy tax liggéeyu waare bi aw yoon. — 1 Korent 14:33, 40.

  •  Naka la kurélu bànqaas yi di dimbalee Jataay biy dogal ?

  •  Yan liggéey lañuy dénk ñi nekk ci bànqaas yi ?