Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NJÀNGALE 26

Naka lañu mënee bokk ci toppatoo suñu saalu Nguur ?

Naka lañu mënee bokk ci toppatoo suñu saalu Nguur ?

Estonie

Zimbabwe

Mongolie

Porto Rico

Saalu Nguur boo gis ci seede Yexowa yi, mu ngi yore turu Yàlla mi nekk tur bu sell, maanaam Yexowa. Loolu moo tax ñu bëgg a defar suñu saalu Nguur yi ba ñu set, jekk, bañ a am yàqu-yàqu te kontine di bees. Def loolu nekk na lu réy ci ñun te lu am solo la ci suñu njaamu Yàlla. Ñépp a ci mën a bokk.

Nanga bokk ci set-setal bi bu ndaje bi jeexee. Saa yu ñu paree ndaje, suñu mbokk yu góor ak yu jigéen dañuy def set-setal bu ndaw bala ñuy ñibbi. Benn yoon ci semen bu nekk dañuy def set-setal bu gën a mag. Benn magu mbooloo walla kuy topptoo yëfi mbooloo mi mooy jiite liggéey bi, te ci lu ëpp dafay yor kayit bu ñu bind li ñu war a def. Dañuy bale, fobeere, dindi pënd mi, raŋale siis yi, raxas duus yi, fomp palanteer yi ak seetu yi, tuuri mbalit mi, te defar ci biti. At mu nekk, lu mu néew-néew dañuy jël benn bés ngir def set-setal bu réy. Nañu boole suñu doom yi ci liggéey bi ngir jàngal leen ñu fonk suñu béréb bi ñuy jaamoo Yàlla. — Ecclésiaste 5:1.

Nanga bokk ci defar li yàqu. At mu nekk, dañuy xool bu baax suñu saalu Nguur ci biir ak ci biti ba xam ndax dara yàquwul. Ci loolu lañuy sukkandikoo ngir xam li ñu war a def saa su nekk ba béréb bi kontine di rafet. Noonu duñu yàq xaalis ci ay yàqu-yàqu yu ñu mënoon a moytu (Chroniques 24:13 ; 34:10). Ndegam ci saalu Nguur lañuy jaamoo Yàlla, jaadu na ñu koy toppatoo ngir mu nekk béréb bu set te jekk. Nañu bokk ci liggéey boobu. Noonu lañuy wonee ne bëgg nañu Yexowa dëgg te fonk nañu béréb bi ñu koy jaamoo (Sabóor 122:⁠1). Dafa nekk itam lu rafet ci kanamu dëkkandoo yi.

  •  Lu tax ñu war a toppatoo bu baax suñu béréb bi ñuy jaamoo Yàlla ?

  •  Lan lañuy def ngir suñu saalu Nguur kontine di set ?