Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NJÀNGALE 27

Ban njariñ nga mën a jële ci téere yi ñu mën a jàng ci saalu Nguur ?

Ban njariñ nga mën a jële ci téere yi ñu mën a jàng ci saalu Nguur ?

Israël

République tchéque

Bénin

Îles Caïmans

Ndax am na aaya ci Biibël bi boo bëgg a nànd bu baax ? Ndax bëgg nga yaatal sa xam-xam ci kenn ku ñuy wax ci Biibël bi ? Walla ci béréb bu ñu tudd ci Biibël bi ? Walla ci leneen lu leerul loo fa jàng ? Ndax danga am poroblem te bëgg a xam ndax Biibël bi mën na la ci dimbali ? Nanga gëstu suñuy téere yi ñu def ci saalu Nguur gi ngir ku nekk mën cee jàng. Dinga mën a yokk bu baax sa xam-xam ci Biibël bi.

Ay jumtukaayu gëstu yu am doole ñoo lay dimbali nga am ay tont ci say laaj. Xéyna amuloo ci sa làkk téere yépp yi seede Yexowa yi génne te ñu sukkandiku ci Biibël bi. Waaye ci saalu Nguur gi dinga fa mën a gis téere yi mujj a génn ak ay sotti Biibël ak ay diksoneer ak yeneen téere. Mën nga ci jàng bala ndaje bi di komaase walla bu jeexee. Bu fa ordinatër amee, dañuy jëfandikoo li ñuy woowe Watchtower Library ngir dugal ci ordinatër bi suñuy téere yu bare. Mën nga ci gëstu aaya, baat walla waxtaan bu la neex ci fasoŋ bu yomb.

Ndimbal la ci ñi bokk ci ndaje bi tudd Dundinu karceen ak liggéeyu waare bi . Téere yooyu nekk ci saalu Nguur gi mën nañu la dimbali nga waajal bu baax waxtaan yi nga am ci ndaje bi. Kiy jiite ndaje bi tudd Dundinu karceen ak liggéeyu waare bi moo yor toppatoo téere yooyu. Moom moo war a dugal bépp téere bu mujj a génn te rañsale téere yépp ba mu baax. Moom walla ki lay jàngal Biibël bi mën nañu la won ni ngay def ba gis li nga soxla. Waaye nag benn téere warul génn saalu Nguur gi te war nañu moytu yàq leen walla bind ci dara.

Biibël bi dafa wax ne su ñu bëggee am xam-xam ci Yàlla, fàww ñu “ sàkku ko ni xaalis ” (Kàddu yu Xelu 2:1-5). Suñu téere yi nekk ci saalu Nguur gi mën nañu la dimbali ci komaase sàkku xam-xam boobu.

  •  Yan jumtukaayu gëstu nga mën a am ci saalu Nguur gi ?

  •  Kan moo la mën a dimbali ci jëfandikoo bu baax téere yooyu ?