Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NJÀNGALE 28

Lan lañuy fekk ci palaas bi ñu moom ci Internet ?

Lan lañuy fekk ci palaas bi ñu moom ci Internet ?

France

Pologne

Russie

Yeesu dafa waxoon talibeem yi ne : “ Na seen leer leere noonu ci kanam nit ñi, ngir ñu gis seeni jëf yu rafet, te màggal seen Baay bi ci kaw ” (Macë 5:​16). Li boroom xam-xam yi di defar ci suñu jamono, dañu koy jëfandikoo bu baax ngir topp ndigalu Yeesu boobu. Internet, ci la bokk. Palaas bi ñu moom ci Internet te ñu tudde ko jw.org dafay joxe ay leeral ci li seede Yexowa yi gëm ak it ci seen yëngu-yëngu yi. Lan ngay fekk ci palaas boobu ñu moom ci internet ?

Dinga fa fekk li Biibël bi tontu ci laaj yi nit ñi faral di laaj. Dañu fay tontu ci laaj yi gën a am solo yu nit ñi faral di laaj. Tont yi ñu ngi ci kayit yi tudd, Ndax coono àddina dina mas a jeex ? ak Ndax ñi dee dinañu dundaat ? Kayit yooyu def nañu leen ci internet ci lu ëpp 600 làkk. Dinga fa fekk itam sotti Biibël bi tudd Traduction du Monde Nouveau ci lu ëpp 130 làkk ak ay téere yu bare yu lay dimbali ci gëstu Biibël bi, mel ni téere bi tudd Lan la Biibël bi wax dëgg-dëgg ? Am na fa itam téere La Tour de Garde ak Réveillez-vous ! yi mujj a génn. Yu bare ci téere yooyu mën nga leen jàng walla déglu leen ci internet. Boo bëggee it, mën nga leen a sotti ci sa ordinatër, ci mp3 walla PDF walla EPUB. Boo gisee nit ku bëgg a jàng suñuy téere ci làkkam , mën nga sotti ay paas ci làkk boobu. Mën nga fa fekk itam ay wideo yu bare yu ñu defal muuma yi. Mën nga sotti it ay nettali yu ñuy jàng ci Biibël bi ak ay tiyaatar yu ñuy déglu yuy jàngale lu jëm ci Biibël bi, boole ci misik bu neex.

Dinga fa fekk ay xibaar yu wóor ci seede Yexowa yi. Ci palaas bi ñu moom ci Internet dafay am ay xibaar ak ay wideo yu jëm ci suñu liggéey bi ñuy def ci àddina si sépp. Dañu fay wax itam xëw-xëw yiy laal seede Yexowa yi ak ndimbal bi ñuy def bu musiba amee. Mën nga fa fekk it ay yégle yu jëm ci suñu ndaje yu mag yi ak suñu adareesu bànqaas yi.

Loolu yépp tax na ba leeru dëgg gi leer ba ci dëkk yi gën a sore ci àddina si. Waa àddina si sépp ñu ngi koy jariñoo, boole ci sax béréb bi gën sore te gën a sedd bi ñuy woowe Antarctique. Ñu ngi ñaan “ kàddug Boroom bi law ” ci kaw suuf sépp ci ndamu Yàlla. — 2 Tesalonig 3:⁠1.

  • Naka la jw.org di dimbalee nit ñu bare ñu xam li Biibël bi tontu ci seeni laaj ?

  • Lan nga bëgg a xool ci palaas bi ñu moom ci internet ?