Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

Ndax dinga def li Yexowa bëgg ?

Ndax dinga def li Yexowa bëgg ?

Ñu ngi lay gërëm ci jot bi nga jël ngir jàng téere bii ngir gën a xam seede Yexowa yi, xam ci lan lañuy yëngu ak naka lañuy doxale ci suñu biir. Yaakaar nañu ne téere bii dimbali na la nga ràññe ne ñun ñooy def li Yexowa bëgg. Ñu ngi lay xiir ci kontine di jàng ngir xam Yàlla, te di ko waxtaane ak say mbokk ak say xarit. Ñu ngi lay xiir itam ci faral di teewe suñu ndaje karceen yi. — Yawut ya 10:​23-25.

Dinga gis ne, looy gën a jàng lu jëm ci Yexowa, ngay gën a gis mbëggeel gi mu am ci yaw. Loolu dina tax nga sawar a def lépp loo mën ngir won Yexowa ne yaw itam bëgg nga ko (1 Yowaana 4:​8-10, 19). Léegi nag, naka nga mën a wonee bés bu nekk ne loolu mooy sa bëgg-bëgg ? Lu tax topp santaane Yexowa yi nekk li gën ci yaw ? Lan moo lay xiir ci ànd ak ñun ci def li Yàlla bëgg ? Ki lay jàngal Biibël bi dina kontaan ci dimbali la nga gis tontu laaj yooyu. Noonu yaw ak sa njaboot dingeen “ saxoo mbëggeelu Yàlla, . . . mu tàbbal leen ci dund gu dul jeex ”. — Yudd 21.